xam-xam ci wolof

Bii ab blog la buy yengu ci leeral ak tas xam-xam ci wolof

mardi 6 janvier 2009

LI NU TAX A JUG

Liy suñu yéene mooy sos ab blog walla ab (yaxaluwaay) bu li ko tax a jug mooy siiwal xam-xam ci wolof, ba ñi ëpp ci doomi Senegaal yi man a xéewalu ciy xéewalam, nuur, tëbb, féey ciy géejam, root ciy naanuwaayam, sëmb ciy déegam.
Ana lu waral manul a nekk ci yeneen yi ñu xamoon, miin leen ciy làkk? Rawati na yii di yu àdduna te wu Faraas wii di ci wenn wow sunum réew moom la jàppe làkkuw nguuram, wu kilifawoom?
Li ko waral mooy: binduñu mu ñeel ñu dul ñii di ñu war a xam tey ñi ëpp ci waa réew mi tey ñu manadee xame ci wu dul wii di seen wos tey wolof wi ñu nàmm, man de gis naa ne ci nii rekk la xam-xam man a tase ci Senegaal gépp, déet ci weneen!

Lislaanm


Lislaam



Kaaba ga ca Màkka gu ñu teral ga


'Lislaam jenn diiney asamaan (monothéiste) la (walla ju jenn yàlla), ju Muhammad (j.m) doon woote ca Dunu Araab ba (arabie) ca VIIeelu xarnu, Moom nag jenn la ci ñatti diine yees di wooye (diine yu ibraayma) yi, ñooy ( diiney yahood , nasaraan ak Lislaam ). Ñi ko gëm ñu leen di wooye ay "Jullit" , mu bawoo ci baatub julli biy wund nangul Yàlla (t.s) di dégg ay ndigalam, ndax kooy julli ngir moom di ko jaamu nangul nga ko te ronu cig ronam, baatub jullit nag ci araab mooy (Muslim) giy tekki "aji jébbalu", aji nangul Yàlla, ndax jullit bi naafequl day déggal Yàlla, wéetal ko, ronu ci ron keppaaram, tënku cig nosteem, raggu cig bokkaaleem, dañtalu ci ñoñam (ñoñ bokkaale). Loolu nag ag bayliku gu mag la gu tukkee ci nit ñeel Yàlla, féete ci moom, jox ko boppam ci lépp lu muy def.

Jullit ñi dañoo gëm ne Lislaam mooy diine ji Yàlla mujj a wàcce ci ( diiney asamaan ) yi, te moom nasaxal na ya ko fi jiitu ci diine, (maanaam wotte na leen) ni ko Alxuraan waxe: «Tay jii laa leen matalal seen diine te mottali sama xéewal ci yéen, te gërëm naa Lislaam muy seen diine » (Taabal (mayida) 3), waxati ko: «Wàcce nañu ci yaw téere ba ànd ak dëgg, muy dëggal li ko fi jiitu ci téere, te di ko féete kaw » (Taabal 48).

Jullit ñi tam dañoo gëm ne Muhammad ab yonent la bu bawoo fa Yàlla, mooy ki ub nabiyu yi ak yonent yi, moom nag Yàlla da koo yonni ci ñaari way dijj-bopp yi (Jinne ak Nit). Bokk na ci dàtti pas-pasu Lislaam gëm ne am na jenn yàlla ju fi nekk moom rekk mooy Yàlla "Allaa" , te ñoom (juliit ñi) anafiya lañuy topp muy diiney Ibraayma

Ñaari seere yi ci benn ci miiri jàkkay Shiyaan ju mag ja ca Siin


Jullit ñi dañuy Gëm Yàlla, Gëm Malaaka yi, Gëm Téere yi , Gëm Yonnant yi it mboole seen, yi fi jiitu woon, ak Gëm Bis Pénc te Gëm Dogal bi , ak Alxuraan mooy téere bi ñu wàcce ci Muhammad mu tukkee ci Yàlla, jaare ci Jibriil, Alxuraan nag mooy balluwaayu yoonal bu njëkk bi ci Lislaam, teg ci Sunna. Ponki Lislaam nag juróom lañu:

Moom lañuy jàppe ñatteel ci dawaan yu mag yu diiney jenn-yàlla yi bokk ci njabootugDiiney Ibraayma yi. Moom nag diine la ju wuuteek diiney Yahood ak ju nasaraan ji mu bokkal ay wàll yu bari yu niroo. Moom nag mooy jaaro bu mujj bi ca càllalag diine ja yonent ya indi woon mu bawoo woon ca Yàlla, la ko dale ca Noohin romb mbooleem yonent yi ba ci Muhammad (j.ñ) mi tëj Yonent gi ak téere yi ci téeéreem bii di Alxuraan.

Alxuraan nag mooy téere bi jullit ñiy sukkandiku ci seen yoonal, bu jàllee sunna ñëw, di jëf ak waxi Yonent bi Muhammad (j.m), mook Sunna ak yeneen ñaar ñooy bañlluwaay yi jillit yiy ball-loo seeni àtte ak yoon (sariiya), yeneen ñaar yi di "ijmaah" (dajeg boroom-xam-xam yi) ak Qiyaas (nattale). Moom Alxuraan nag waxi Yàlla la ju ñu wahyu Yonent bi jaare ko ci Jibriil, muy lol daa wàcc ci anam gu toftaloo te toppante, ci diir bu tollu ci 23 at.

Lu tollook 1,5 milyaar ciy jullit ñi ngi ci àdduna bi. Ñoon nag dañoo séddaliku ci ay dawaan yu limu, ñooy ci tur dawaanu Sunna, bi ëmb lu tollook 80 ak 85% ci jullit ñi, ak bu Siiya bi nga xam ne ma nga ëppe ca Iraan, ci biir Sunna am na fa ay bànqaas niki tasawuf , naka noonu ci Siiya.


Jumaa
Kaaba



Xamale ko

  • Baatub Lislaam day tekki jébbalu ci jenn Yàlla ji amul moroom amul ku mu bokkal (laa sariika lahuu) joxe sa bopp gii nag ci teeyug bakkan lay ame. Fi Jullit ñi Yonent yépp ay jullit lañu , Ibraayma, Musaa ak Isaa (j.ñ), ndax ñoom niki jullit yépp dañoo tënku ci ay àtte yu Yàlla, te topp ci, kon jébbalu nañu te nangul Yàlla, bu ko defee Yàlla di leen dëgëral ak a dooleel ci ay kéemtaan (miracles)
  • Baatub Jullit nag li muy tekki mooy ki aju ci diiney Lislaam di ko doxal, di julli tey def mbooleel àttey Yàlla yi.
  • jullit nag leeg-leeg mu tekki aw xeet, walla aw nitu am réew niki ña dëkk ca Bosni, ñooñu ay Jullit lees leen di wooye, naan Kurwaat Serb ak Jullit

Lislaam nag du lu ñu jagleel aw askan wëliif weneen, walla aw nit bàyyi weneen, moom de ag woote la ñeel mbindéef yépp, ngir amal ag maandute ak yamoo ñeel mbindéef yépp. Lislaam daa taxaw ci ag nite ak yamale mbooleem bennaani mboolaay gu Lislaam gi, du def genn ràññatle ci diggante ku am ak ku ñàkk, ku am doole ak ku ko néewle, garmi akub baadoola. Neewul wenn xeet a gën moroom ja ndare ci ragal Yàlla ak topp ko. Loolu mooy dàtt bi jëfi jullit di tegu ngir man a baax, lu ko moy déet. yàlla a ngi wax ci Alxuraan: «Yéen nit ñi, ñun de bind nañu leen ci góor ak jigéen, te def leen ay askan aki giir ngir ngéen xamante, (te ngéen xam ne) ki gën a tedd ci yeen fa Yàlla mooy ka ca gën a ragal Yàlla, Yàlla ku xam la, ku dañ-kumpa la (dara umpu ko) » (saaru néeg (Hujuraat) 13)

Yonent bi Muhammad (j.m) nee na: «Ndax duma leen xamal ku di ab jullit? Kok nit ñi wóolu nañu ko ci seen alal ak seen bopp, ab jullit mooy ki nit ñi mucc ci làmmiñam ak loxoom, jiyaarkat mooy ki jiyaar ak bakkanam ci topp Yàlla, aji gàddaay mooy ki gàddaay ñaawtéef yeek bàkkaar yi»


Ag sosoom

Lislaam feeñ na ca Dunu araab ba ca juroom ñaareelu xarnu g.j, (ginaaw juddug Isaa), ci loxol Muhammad mom Abdul Laa (j.m), mi xéyoon di woo nit ñi ci ñu gëm pas-pas buy woote jaamu Yàlla miy kenn tey ku wéet te ba jaamug xërëm yi, mu boole ci indiwaale fi meneen mbooloo ciy ponk aki xalaat ak pas-pas, loolu nag di ndigal lu bawoo fa Yàlla miy kenn tey ku ñàkk maas, (Allaa), rax ci it Alxuraanالقرآن ju araab ju ñu wàcce ci Muhammad (j.m) mu tukkee ci Yàlla jaare ci malaaka Jibriil, mii daa jàng Alxuraan jii ci Muhammad ci anam gii nuy wooye "Wahyu"


Pas-pas ak Sariiya

Jullit ñi dañuy gëm ne Muhammad (j.m) daa dikk ngir mottali te tëj bataaxelub Yàlla bi mu yonnee yonent yi ko fi jiitu woon niki Ibraayma, Musaa, ak Masi Isaa mom Maryaama (y.j.ñ) te ñoom Yonent yooyu yépp ay jullit lañu, te dañuy gëm it ne Anafiya ji ñu nekk mooy cëslaayu diiney Ibraayma. Dañuy gis it ne wuute gi ci diiney asamaan yi ci sariiya la (maanaam àtte yi) waaye du ci pas-pas bi te sariiyab Lislaam nasaxal na (wuutuna fi) mbooleem sariiya yi ko fi jiitu woon.Kon diiney Lislaam mi ngi ame ci pas-pas ak sariya. Pas-pas bi di mbooleem dal (principe) yi nga xam ne jullit bi war na leen a gëm, ñoom nag way sax lañu, duñu soppiwku ak lu yonent yi soppiku. Sariiya nag aw tur la ñeel àtte yu jëf yi nga xam ne man nay wuute ak a soppiku ci soppikug yonent yi, bu ko defee bi mujj a ñëw di nasaxal (di fi wuutu) bi ko jiitu.

Alxuraan nee na: «Wàcce nañu ci yaw téere bi ànd ak dëgg, muy dëggal la ko fi jiitu ci téere te di ko féete kaw (di ko nasaxal), àtte leen ci li Yàlla wàcce te bul topp seeni bànneex ba bàyyi li la dikkal ci dëgg, ku mu ci yeen defal nañu ko aw yoon akum ngér, bu sooboon Yàlla mu def leen wenn xeet, waaye da leen di nattu ci li mu leen indil, njëkkanteleen yiw yi, ca Yàlla ngeen di dellu, bu ko defee mu xibaar leen fi seenug wuute nekkoon» (saaru Taabal 48) {وَأَنزَلْنَا إِلَيْكَ الْكِتَابَ بِالْحَقِّ مُصَدِّقاً لِّمَا بَيْنَ يَدَيْهِ مِنَ الْكِتَابِ وَمُهَيْمِناً عَلَيْهِ فَاحْكُم بَيْنَهُم بِمَا أَنزَلَ اللّهُ وَلاَ تَتَّبِعْ أَهْوَاءهُمْ عَمَّا جَاءكَ مِنَ الْحَقِّ لِكُلٍّ جَعَلْنَا مِنكُمْ شِرْعَةً وَمِنْهَاجاً وَلَوْ شَاء اللّهُ لَجَعَلَكُمْ أُمَّةً وَاحِدَةً وَلَـكِن لِّيَبْلُوَكُمْ فِي مَا آتَاكُم فَاسْتَبِقُوا الخَيْرَاتِ إِلَى الله مَرْجِعُكُمْ جَمِيعاً فَيُنَبِّئُكُم بِمَا كُنتُمْ فِيهِ تَخْتَلِفُونَ }المائدة48


Ay baat aki waxiin

"Allaa":Yàlla, mooy yàlla jiy dëgg ji yayoo ag jaamu moom rekk, moom mooy Aji bind jiy Aji sàkk, kiy melal, ki moom tur yu rafet ya ak melokaan yu kawe ya, ki bind nekk gi(àdduna bi) tey ki nga xam ne moom rekk a ko man, mooy ki moom asamaan yeek suuf si. Yàlla nag yonni na yonent yi ngir ñu woo nit ñi ci ñu jaamu ko moom rekk te bàyyi jaamu ku dul moom.

"Yonent bi", yonentub Lislaam mooy Muhammad mom Abdul Laa mom Abdul Mutalib mu Quraysin, mi ngi judd ci 571 ci Màkka gu tedd gi. Ag njabootam ñu xame ko ci turu njaboot gu Haasim, ngir askanale ko ca maamam Haasim mom Abdu Manaaf. Yàlla yonni na ko jox ko diiney Lislaam atum 610 g.j te booba ma ngay def xalwatu ngir jaamu ca xuntim Harraa. Xamees na ko ci njëkk ak ci ginaaw yonent gi ci ay jikko yu rafet, dëggu ak wóor, looloo waraloon ñu ko daa wooye "Ku dëggu, Ku wóor ki", mi ngi faatu ci bisub altine 12 ci rabiihul lawal atum 11 g (mu gàddaay gu Yonent bi)te booba ma nga amoon 63 ciy at

Alxuraan: Alxuraan mooy téere bu sell bi ñeel jullit ñi, mooy balluwaay bu njëkk bi ñeel yoonal gu Lislaam gi, ci ginnaawam la Sunna di ñëwe. Li njëkk a wàcc ci Alxuraan it mooy laaya wi njëkk ci saaru Halaq muy : «Jàngal ci sa turu boroom bi bind (sàkk) »

Alxuraan nag mooy waxi Yàlla ji mu wàcce ci Yonenteem bi Muhammad, Jibriil nag mooy ndawul Yàlla tey malaaka mi ko wàcce; ngir nag Yonent bi jottali ko nit ñépp,. Moom nag fa Yàlla dees koo bind ca àlluwa ju ñu wattu ja (Lawhul Mahfuus), àlluwa jii nga xam ne Yàlla bind na fa lu nekk njëkk mu koy sàkk.Wattu googu nag Yàlla la soob, mu bëgge ko noonu, noonu la ko waxe: «Ñun ñoo wàcce Alxuraan, te ñun ñoo koy wattu»


Barab yu sell yi:

Lislaam am na ñatti barab yu sell, ñooy Màkka gu tedd gi, Madiina gu leer gi ak Quts (sorisalem):

Màkka:

Fa la Yonent bi Muhammad (j.m) ganee àdduna, mooy tam barabub wàccug Wahyu gi, fa la doorees it woote gi. Fa la Masjidul Haraam it nekk (Jumaa ja wër Kaaba ga) gi ëmb Kaaba gu tedd gi nga xam ne Ibraayama'a ko tabax ak doom ja Ismaayil (j.ñ), fa la jullit yiy jublu it ngir jóoxi séen faratay aj. Kaaba gi mooy xiblay jullit ñi, fa lañuy jublu ci mbooleem seeni julli.

Madiina :

Madiina gu leer gi (madiinal munawwara ci araab), njëkk Lislaam (Yasrib) la tuddoon, ñi ngi ko tudde Madiinal Munawwara, walla Madiinatur Rasuul (dëkkub Yonent bi) ginnaaw Lislaam. Fa la Masjidun Nabii nekk (Jàkkay Yonent bi)

Quds :

Quds nag dafa mel ne turam wiy tekki "ag sell", di barab bu ñu sellal fi jullit ñi, fa la masjidul aqsaa nekk, (Jàkkay Aqsaa) ca Palestin, muy jàkka ji Yonent bi siyaare woon ca guddig "rañaan ga ak yéeg ga", mooy guddi gi ñu farataale julli. Fa la Yonent bi jiite woon cig julli mbooleem nabiyu yeek yonent yi. Masjidul Aqsaa nag mooy benn pàkk bi nga xam ne mbooleem diiney Ibraayma yi yépp sellal nañu ko: Lislaam, Nasaraan ak diiney Yahood


Sariiya bu Lislaam

Ci gëm-gëmu jullit ñi Sariiya bu lislaam (walla yoon wiy àtte ci lislaam) mooy nos mbooleem wàlli dund yu wuute yi, gu politig, gu mboolaay, gu koom-koom ak gu jëmm. Loolu nag ag kéemtaan nekku ci ginnaaw moom mi taxaw ci Alxuraan ak Sunna dafa bawoo ca Aji bind ju tedd ji te màgg (Yàlla). Sariiya nag am mbooloom ay yoon la (ay àtte) yuy leeral séqoo ak digaale yi am ci diggante nit ak Yàlla (t.s) ak diggante nit ak nit ak mboolaay gi ak àdduna bi. Day leeral it li dagan a def ak li daganul. Yi ëpp solo ci àtte yii ñooy ponki Lislaam yiy juroom te ñu leeraloon leen.

Lislaam tam day waral jullit bi di tënku ci Sariiya, di ci àttee ay lëj-lëjam ak xiiroo ak ŋaayoo mbaa xuloo yiy am ci diggante jullit ñi, day waral it ci jullit bi muy ràngoo jikko yu rafet.

Gongikuwaayu Sariiya bu njëkk bi nag (walla ab balluwaayam) mooy Alxuraan, moom nag ag wahyu la gu tukkee ca Yàlla ñeel ab yonentam Muhammad (j.m) mooy balluwaay bu njëkk bi ñeel yoonal yi ak àtte yi ci Lislaam, Yàlla (t.s) warlu na ne dina ko wàttu cig soppi mbaag wëlbati: «Innaa nahnu Nassalnaas Sikra wayinnaa lahuu la haafisuun». Alxuraan yaxal na ci waraug topp ndigali Yonent bi (j.m) ndax ay waxam ag wahyu lañu gu tukkee fa Yàlla (t.s), Alxuraan nee na : «Du waxe bakkan, li muy wax ag Wahyu la gees koy wahyu», looloo tax deesi jàppe Sunnas Yonent bi (moom am mbooloom ay wax la aki jëf yu Yonent bi (j.m)) muy gongikuwaay bu ñaareel bi ñeel Sariiya walla yoon ci Lislaam.

Sunna nag nga xam ne mooy ñaareelu gongikuwaay bi, dajalees na ko ci am mbooloom ay téere, niki Sahiihul Buxaarii, ak Sahiihul Muslim ak yeneen téere yu Addiis.

Ñatteelu gongikuwaay bi nag balluwaayu wuute la ci diggante ñaari ngér yii di Sunna ak Siiya: Waa Siiya ñoom dañoo gis ne Addiis yi bawoo ca Ahlul Bayt (Njabootug Yonent bi (j.m)) ñooy ñatteelu gongikuwaay bi ñeel Sariiya, téerey Addiis yi nekk fi ñoom dafa ëmb waxi Yonent bi (j.m) ak waxi Ahlul Bayt,seen téereb addiis it mooy téereb Kaafii bu Kaliinii (كتاب الكافي للكليني )

Ñeenteelu gongikuwaay bi mooy Qiyaas walla “nattale” (maanaam nattale mbir mu amul ab àtte ci mbir mu mu nirool mu ko amoon)



Ngérum Lislaam

Lislaam day dox ak a liggéey ci teggi toroxte wëliif nit ñi, tee leen a toroxlu ñeel ku dul yàlla (t.s) . Mu gis ne doyodal gi gën a réy gi nit mas a dajeel ak toroxte mooy muy jaamu aw doj mbaag garab walla dundat (bayyima), mbaa muy toroxlu ñeel mbindéef muy dund mbaa mu dee, moo xam nit la mbaa lu ko moy, ci noonu mu aaye ñuy jàppe ay fóore mbaay làbbe (الأَحْبَارِ وَالرُّهْبَانِ)ay yàlla te ba fi Yàlla. Mu jugati moom Lislaam xeex tooñaange yi ñennat ci nit ñi di teg seeni moroom yu néew yi doole, loolu leer na bu baax ci Alxuraan :{وَلاَ تَأْكُلُواْ أَمْوَالَكُم بَيْنَكُم بِالْبَاطِلِ وَتُدْلُواْ بِهَا إِلَى الْحُكَّامِ لِتَأْكُلُواْ فَرِيقاً مِّنْ أَمْوَالِ النَّاسِ بِالإِثْمِ وَأَنتُمْ تَعْلَمُونَ }[2] «Buleen di lekk seeni alal ci seen biir cig “neen” (ci lu dul dëgg, ci bàkkaar) ak di ci jox way àtte yi (di ci gere) ngir (rekk)ngeen lekk ab kuréel (ab lim) ci alali nit ñi ci bàkkaar te booba xam ngeen ko» Alxuraan waxati it ne : {يَا أَيُّهَا الَّذِينَ آمَنُواْ إِنَّ كَثِيراً مِّنَ الأَحْبَارِ وَالرُّهْبَانِ لَيَأْكُلُونَ أَمْوَالَ النَّاسِ بِالْبَاطِلِ وَيَصُدُّونَ عَن سَبِيلِ اللّهِ وَالَّذِينَ يَكْنِزُونَ الذَّهَبَ وَالْفِضَّةَ وَلاَ يُنفِقُونَهَا فِي سَبِيلِ اللّهِ فَبَشِّرْهُم بِعَذَابٍ أَلِيمٍ }[3] «Yeen ñi gëm, ñu bari de ci fóore yi ak làbbe yi dañuy lekk alali nit ñi cig neen tey dëdduloo wëliif yoonu Yàlla wi, ñiy dëxëñ (denc) wurus ak xaalis te duñu leen def ci yoonu Yàlla, nanga leen bégal ci mbugal mu tar»

Loolu mujj na di ab balluwaayu doole ak kàttan ñeel Lislaam, ngir yamale gi ci nekk ñeel nit ñi ñépp, amul xejj ak séen, ab bàkkam di “Ab araab gënul ab ajam (ku dul araab), ab ajam gënul ab araab, ku weex gënul ku ñuul, ku ñuul it gënewul ku weex lu dul ragal Yàlla (tënku ciy ndigalam teet ay tereem, nit ñépp ci aadama lañu bawoo, te moom ci suuf la bawoo ” kon manuñoo gënantee ciw melo mbaag ndawal, waaye ci jikko ju rafet ji ëmbu ci ragal Yàlla giy waral di tënku ci ay ndigalam aki tereem te loolu mooy ag xay dëgg-dëggi xay, ndax mooy waral nit di def ag nite, di wormaale tey xam ne mook ñepp a yam, mook ñepp a bokk fu ñu juge, mooy Aadama, te moom cosaanam du dara lu jar muy jàpp ne kenn la, mbaa moo gën kenn, suuf sii muy joggi ak a puup, ak a saw ci la bawoo, kon déet ag gëne di ko ñeel lu dul cig ragal Yàlla giy njobbaxtal cig baax akug yiw.

Déet ag xeetal (racisme), déet ag kuréelal (def ay classes sociales). Bu ko defee, ngér mii xéy di luy doog a am ci taariixu àdduna bi, ci nguur gog ki ko doon àtte, di ko doxal ab yonent la, ab sartu réewam di Alxuraan ja juge ca Yàlla, bu ko defee aw askanam di xéewu ci xéewalug maandute ak kaaraange

Jullit ñi dox nañu ci wisaare maandute ak yoon ci mbooleem ruqi àdduna bi, yëngu it ci yekkati tooñaange, toroxte ak doyadal wëëliif way néew yi doole ak ñu ñu noot ñi. Looloo jur nit ñi sottiku ci diine ji ci ay mbooloo, buur yi daal di koy xeex ak way jalgati yi ngir li ñu ci gis ci ag tiital ñeel seeni nguur, ñu xam ne seeni nguuru way jeex lañu, seeni nguur way dañ lañu feek lu néew, way tuxoo ci seeni loxo lañu, ndax seeni njaboot ak seeni càmmiit (administrés) tàmbali nañoo tàbbi ci diine ju yees ji.Loolu mooy mbóotum gaaw a tasug Lislaam ci mbooleem pàkki àdduna bi ci diir bu gàtt bu weesuwul at yu néew, loolu nag jaaxal na boroom xam-xami taariix yi ak boroom xam-xami mboolaay yi.

Saaba bii di Ribhi'Bn Haamir génn na loolu ci anam gu leer ca waxam ja:(Yàlla moo nu yonni ngir nu génne ku ko soob ci jaamug jaam yi, yobbu ko jaamu boroom jaam yi, ngir ñu jële ko ci xatug àdduna jëme ko cig yaatoom, xettali ko ci jengug diine yi, yobbu ko ci maandug Lislaam..mu yonni ñu ak diineem ji ci mbindéefam yi, ngir ñu woo leen jëme leen ci, ku nangu loolu ñu nangul ko, dellu wëliif ko (ba ko ci jàmmam), ku bañ nag ñu xeex ko ba fàww, ba kero ñuy àgg ca dëelub Yàlla ba. Ñu ne ko : luy dëelub Yàlla ba? Mu ne: Àjjana ñeel ki dee ci xeex ak ki bañ, ak tuufu (gañe) ñeel ki des (ki deewul).


Tasug Lislaam akug wisaaroom ak ni jullit ñi séddalikoo ci àdduna bi

Ni jullit ñi séddalikoo ci àdduna bi, melo (kulóor) wu wert wi day wone fu waa Sunna yi ëppe, wu dereet wi fi waa Siiya yi ëppe, wu bulo wi fi waa Ibaad yi ëppe.

Muhammad (j.m) aki saabaam tàmbali woon nañu di woo giiri araab yi ci ñu dugg ci Lislaam, ba mujj nguurug Lislaam gii doon doog a sosu ci Madiina di gu am doole ak kàttan, mu daal di sóobu ci ay kollarante yu politig, yu diine ak Quraysin , ci noonu giir yi daal di séddaliku ci yuy ànd ak Muhammad (j.m) ak yu koy safaan, di ànd ak Quraysin, loolu wéy nag di nekk ba kero bi ñu ubbee Màkka (fath Makka) te duma way bokkaale ñi ( am ndam ci seen kaw), booba la la ëppoon ca giir ya bennoo woon ci ron raayab Lislaam.

Ginnaaw bi Yonent bi génnee àdduna, ay Xalifaam wéyoon nañu di woote jëme ci Lislaam ak a nos Jiyaar gi ngir wisaare diiney Lislaam ak tas maandute ak yoon te yekkati tooñ wëlif nit ñi, ba mujj digi nguurug Lislaam gi mujj àgg Siin ci penku bi, akMbàmbulaanug Atlas ci sowwu bi, Lislaam it wéy cig yaatoom akug tasam jaare ko ci yaxantukati jullit yi doxoon jëm penku ak bëj-saalum ci Asi, ak cig wokkoo ak riisoo ak wàll yi gdigoo ak dig (frontières) yu Lislaam yi ci Afrig ak Tugal. Am na it ñu bari ci lokkikat yi (les conquérants) ñoñ tàbbi woon nañu ci Lislaam bi ñu agsee ci barabi Lislaam yi, ñu ci mel ne Mongool yi ak ñenn ci ñi doon def Xarey jooñe yi ak Tataar yi.

Kuy xeeñtu (suivre) Sariiya bu Lislaam dana gis ne moom dey daa farataal ci bépp jullit mu nekk ab wootekat jëme ci Lislaam; di digale lu baax di tere lu bon, di sonn it ngir nit ñi dugg ci Lislaam ciy mbooloo, ngir jëfe waxi yonent bi (j.m): ((Yàlla gindee ci yaw jenn waay moo gën ci yaw àdduna ak li ci biiram)), Lislaam kon gaweesu ko ci mag muy woote walla boroom xam-xam buy génne ay fatwaa, mbaa ñu jagleel ko jenn jàkka wëlif jeneen. Lii kon menn la ci mbóoti wisaarook Lislaam ci àdduna bi ci jàmm mbaa xare.

Ay ngér yu fiq

Ngérum fiq moo man a gis day ball-loo àttey Sariiya yi ci tegtal (adila) yi rot (nekk) ci Alxuraan ak Sunna, dëppoo nag ak ay ponk aki cosaan yu fiq yu leer, manees na leen a tudde ay daara yu fiq (écoles de jurisprudence) ngir dëppoo gi ñu def ci pas-pas bi (alhaqiida) ak cosaan yi (al-usuul), waaye man nañoo xaw a wuute ci àtte yi ñuy ball-lu. Ngéri fiq yu ñeent yi tas nañu ci anam gu yaa ci ñoñ Sunna ñi, te mujj di lu kilifawu (officel) ci li ëpp ci seeni téere, ñoom nag (ngér yooyu) ñooy ijtihaad (ay liggéeyi xel) yu fiq yu lëng yi ñeel ñeenti Imaam yu ñoñ Sunna ñi ak mbooloo mi (Ahlus sunna wal jamaaha), ñoom nag nii lañu toftaloo ci taariix:

  1. Imaam Aboo Haniifa Annuhmaan, am ngéram mooy mu Haniifa walla Aniifa, mbaa Anafi, moom ngér moomu nag mi ngi sosoo ci Baxdaad ca Iraag
  2. Imaam Maalig Ibn Anas, am ngéram nag di Maaliki walla mu Maalig mi ngi sosu ca Ijaas ca Madiina (almunawara)
  3. Imaam Muhammad Bn Idriis As-shaafihii, ñu koy dàkkantale Shaafihi, am ngéram di saafihi walla saafihiya, mi ngi sosu ca Baxdaad ca Iraak
  4. Imaam Ahmad Bn Hanbal, am ngéram di Anbali, mi ngi sosu ca Baxdaad ca Iraak
  5. Imaam Dawuda bn Aliyu As-saahirii, am ngéram di Saahiriya , mi ngi sosu ca Baxdaad ca Iraag

Ngérum fiq mu waa Siiya yu Fukk-ak-ñaar-yi, mooy fiq bu Jahfar, bi ñuy askanale Imaam Jahfar As-saadiq

Lislaam ak yeneen diine yi

Alxuraan de ëmb na am njàngale mu jëm ci wormaal yeneen diine yi. Alxuraan daa wormaal diiney Yahood ji ak ju nasaraan ji, ngir jàppe gi mu leen jàppe ñuy ay diine yu Ibraayma. Alxuraam mi ngi feddali ne daa ñëw ngir feddali diiney asamaan ju sell ja ñu wàcce woon ca Ibraayma (j.m) te yahood yeek nasaraan yi soppi ko, wëlbati ko(soppi walla wëlbati (التحريف) amaa na mu tekki lu gën a sori déggiin wu ñaaw mbaa wu juum ñeel ab yax (texte), déggiinu mbir mii ak maanaam ci ay tolluwaay yu mujj ci taariixu Lislaam mujj na di : ay xaaj ci Injiil ak Tawreet baaxatuñu). Ñeneen ñu duli jullit it dëggal nañu soppi googu walla "tahriif" googu.

Salaat (julli)

Ay jullit yuy julli ci jenn jàkka.


Jullit bi am na juroomi jullit yu koy war ci bis bu nekk, yooyu ñi ngi leen di wooye julliy farata (salaatul fariida) ci araab, ginaaw yooyu nag am na fi yeneen yu ñuy wooye "naafila" ñooy yi ñuy def cig coobarewu ngir yokk ab yool, ngir jaamu Yàlla gees la tegul cig farataal.

Julli daa war a nekk di lees di def cig laab : bu la fekkee cig laabadi, kon dangaa war a jàpp (ablution).

Julli nag dees koy def cig jublu xibla (maanaam jublu ca Kaaba ga nekk Màkka) ; aji julli ji daa war a yéene def julli gi ko tax a jug ci anam gu leer, yéene jooju moom lañuy wax:(niyah)ci araab.





----------------------------------------------------------------


Muhammad

--------------------------------------------------


Muhammad yonnantub Yàlla bi ak juddug Mbooloo mu Lislaam mi



Li ko dale ca ag ganeem àdduna ba ci bi ñu ko yónnee

Muhammad (jàmm Yàlla na sax ci moom) mi ngi gane àdduna ca Màkka atum 571 g, j , waxees na ne ca at mooma la Abraha mi doonoon kenn ci waa Ecopi jugoon ne day nangu Màkka te màbb Kaaba gu sell ga. Waaye Yàlla (t.s) alag ko, jaare ko ci ay njanaaw yu ñu naan Abaabiil, moom ngay gis ci saaru Fiil (ñay), looloo waral ñu naan Yonnant bi ci atum ñay yi la judd, ndax ba Abraha di ñëw ciy ñay la waroon.

Aji juram ju góor mooy Abdul laah, mi gënoon a doon gone ci doomi Abdul Mutalib mom Haasim mi nekkoon njiitul Quraysin tey sangub Màkka, maanaam njiitam. Moom nag (Abdul Mutalib) – bi Yonnant biy judd – mag la woon mu at yi xawoon a diisal. Abdul Laah nag moo nekkoon doom ji mu gënoon a sopp ngir yewwu gi mu defoon ak njub gi, rafetug jikko yi ak nangul baayam gi. Dencaloon nanu ko Aamina Bint Wahbin mom Abdul Manaaf mom Zuhra mom Kilaab, mu nekkoon di ku bokk ci giirug Xuraysin. Abdul Laah nag ab yaxantukat la [woon]], ci noonu la génne woon, ginaaw bi mu dencee soxna ba teg lu néew, ngir yaxantu-ji ca Shaam , booba Yonnant bi ganeegul àdduna.

Ca tukkib yaxantoom booba la baayi Yonnant bi làqoo , ca tawat ju ko daloon ba muy dëpp, ba muy ñëw ba agsi Madiina la ko gënoon a sonal, mu daal di wàcc ca ña ñu daa wax Banii Najaar di woon genn ci giiri Xasraj yi, fa la génne àdduna. Maamam nag di Haasim mom Abdul Manaaf dafa a takoon soxna, looloo tax ñu naan Banii Najaar de ay goroy Yonnant bi lanu (j.m).

Yonnant baa ngi judd (j.m) ginaaw bi waajur wi làqoo, mu daal di màgg cig njirim, waaye maamam Abdul Mutalib beg ci moom lool, tudde ko Muhhamad, yar ko cig cofeel ak ñeewant

Waa Quraysin nag aadawoo woon nanu di yóbb seeni doom ca la génn Màkk, ca nàmpalkat ya ngir ñu man a màgg ci jàwwu ju sell, wér-gu-yarame te deesi fa dégge araab yu sell, bu ko defee loolu di tax ba ñuy wér, neexi araab te leeri wax. Nii la Aamina defoon ni ñépp, yóbb doomam Muhammad (j.m) ca ab nàmpalkat bu tuddoon Aliima Asahdiya, mu bokkoon ci Banii Sahd Bun Bakr, seeni kër nekkoon ca tàkk ga ca wetu Màkka. Bi Muhammad àggee ci am juroomi at la ko Soxna Aliima delloosi ndayam ca Màkka, mu nekk fa ca pekkam , maamam Abdul Mutalib di ko sàmm.

Ca jamono jooja la Soxna Aamina Bint Wahbin jugoon ne day siyaareji bàmmeelub boroom këram Abdul Laah ca Madiina, ba mu demee bay dëpp la ko tawat ja dikkal, mu faatu ca ndëkk sa nu naan Abwaa te nekk ca yoon wa dox diggante Màkk ak Madiina, ñu daal di ko fay denc, looloo waral bi Yonnant bi màggee di ku soppoon di jaar ci ndëkk soosu ngir siyaare bàmmeelu waajuram ju jigéen ju laab jooju.

Ci nii – ndaysaan – la Muhammad mujje di jirim ci nday ak ci baay, looloo waraloon maamam Abdul Mutalib mujjoon féetewoo ag yaram akug wattoom, bëggoon ko it lool. Waaye sàmm googu gépp ak fonkeel gi teewul Muhammad (j.m) doon yëg naqaru njirim, ndax kat da daa gis moroomam yi ñu nekk ak seeni way jur, moom muy ku leen ñàkk, waaye nag loolu jox na ko ag sukkandiku ci boppam, may ko ag temb ci njëmm akug wéroodi ci kenn, nàmm am xelam, ubbil ko ay bëtam ci dëgg-dëggi dund gi, te booba ay atam lu néew la woon. Loolu de lu jeexiital la ci moom ak cig dundam, Yàlla nag moo bëggoon ci moom loolu ngir tànn gi mu ko tànn ngir mu yanu bataaxel bii di Lislaam te war koo tas.

Yonnant baa ngi sàmm ag jur

Abdul Mutalib ginaaw bi Aamina làqoo yàggu fi dara moom itam làqu, te booba Yonnant baa ngi amoon juroom ñatti at, fa la ko baay-tëxam Aboo Taalib jële yóbb ko ca këram ca doomam yu xaw yaa sakkan tubaar-kàlla, ngir mu yaroo fa. Aboo Taalib nag moo wuutu woon baayam ci jiite Màkk, ci noonu mu jeexaloon alalam jépp ci sàmm Kaaba gi ak way aj yi ak dimbali ñi aajowoo, looloo taxoon alalam bariwutoon ak li muy nekk kilifag Màkk lépp. Lii a waraloon Yonnant bi doon jéem a woyofal yan bi ci baay-tëxam jooju, ba àggoon ci di sàmmal ag jur ñenn ci waa Màkk yi, ñu ko ci daa fay lu néew a néew. Loolu it doonati ab pose ngir mu tàggatu ci xam ni nuy sàmme ag njaboot, jikkowoo ag ñeewant akug laa-biir ak sàmm ak yewwute, ñuy jikko yu manul a ñàkk cib sàmm bu bëggee wattu gétt gi muy sàmm. Yàlla moo ko bëggaloon loolu ngir tàggat ko ci bataaxel bi mu ko nar a joxi. Sàmm ag jur nag daara la joj lu bari ci yonnant yi jaar nanu ci, ba sax jële nanu ci Yonnant bi (j.m) mu ne : amul yonnant bu sàmmul ag jur.

Yaxantu gi mu doon def ak tudde gi nu ko tudde woon Ku wóor ki

Bi mu amee fukki at ak ñaar la ànd ak baay-tëx ji Aboo Taalib cib tukki dem Shaam, bi mu amee nag ñaar fukki at la tàmblee bokk ci yaxantu gi ni ko waxambaaney Quraysin yi daan defe, mu wone ci it man gu mu ko man lool, ndax ku ñu xamoon la cig wóor, ak dëggu, yewwute ak ñaw, ay man-manam tàmblee feeñ ñeel waa Màkk, li ko gënoon a wuutaleek nit ñi mooy wóoram gi jéggi woon ab dayo te xaroon baax, ñu mujjoon di ko wóolu ci lu mu man a doon, te am xel mu dal ci ne dana sàmmoonteek kóolute gi nit ñi def ci moom , looloo taxoon ñu naan ko ku wóor ki ak ku wóor ku dëggu ki.

Jël gi mu jëloon Xadiija soxna ak doom ya mu ca ame

Bi at yi àggee ci ñaar fukk ak ñeent daa dajeek Soxna Xadiija soxla waxambaane wu ko yoral yaxantoom gi mu doon deflu ca Shaam, moom nag soxna su woomle la woon bokkoon ci way woomley Màkk yi, ci noonu ñu digal ko mu gis Muhammad (j.m), ba mu ca waxeek moom Yonnant bi nangu. Yonnant bi yaxantujil na soxna Xadija ca Shaam ànd ak ngóoram sa nu naan Muyasara, Muyasara mii yéemu woon na lool ci jikko yu rafet yi ci Muhammad ak yewwu geek man gee yaxantu, ndax bi njaay mi nekkee ciy loxoom fulu na ay yooni yoon, wuuteek ba mu nekkee ci loxoy keneen, looloo tax bi Yonnant bi (j.m) delloo, jébbal soxna Xadiija alalam ak la mu ca tonoo, cig kóoluteek dëggu, soxna si yéemu na lool ci jikkoom yu rafet yi ak njëmm gi ne ci moom, ci noonu mu yónni ci moom kenn ci ay jegeñaaleem xamal ko ne da koo bëggoon niki boroom kër, Yonnant bi (j.m) nangul ko . Noonu la seen diggante sottee te booba Yonnant baa ngi am ñaar fukk ak juroom ciy at, Xadiija moom yor ñéen fukk, ci noonu mu faroon di soxnaam, di yaayam, di ki koy dimbali ci lépp. Yonnant bi (j.m) amoon na ag texe ci séy boobu naka noonu Xadiija, ci noonu séen kër di misaalum mbégte cib séy ak texe ci biir kër. Soxna Xadiija nag mooy ki jur mbooleem doomi Yonnant bi, ku ci dul Ibraahiima, moom de soxna Maariya mi di ab qibt moo ko jur, moom nag (Sëñ Ibraahiima) ci jamonoy Yonnant bi la làqu. Yonnant bi wéyoon na ci yaxantoom gi ginaaw bi mu yoree soxna Xadiija, mu ko daan defe nag ni ko waa Xuraysin gépp daan defe rekk, ñoom de yorunu wooni bitig aki mangasin, moom kay danu daa defi njëgg yu mag mbaa yu ndaw jawali Yaman ci sedd bi, bu cooroonee ñu dem Shaam, màkk-màkka bu nekk daa na man a bokk ci njëgg li bu bëggee, njëgg loolu nag moom la nu daa wax ci ci araab Bahiir, kenn ci góori Xuraysin yee ko daa jiite , ku soob ci ñoom ànd ak moom, bu ko defee bu dellusee ñu seet li ñu tonowu, seddale ko, ku ci nekk am ca la nga ca def. Seen yaxantuwiin woowu moo taxoon Xuraysin daan am jot, di daje ci jataay yi di waxtaan, rawati na ca la wër Kaaba ga. Waaye Yonnant bi (j.m) moom néewaa na bu mu bokkee ci yii jataay, moom kay këram la daa toog mbaa mu génn dem ca àll ba ngir wéet fa di xalaat ak a settantal, ndax sopputoon di fo mbaa muy caaxaan ak a waxi larax.

Yonnant baa ngi amoon fan-weer ak juroom ciy at jamono yi Xuraysin di màbb Kaaba gi ngir tabaxaat ko, ndax tabax bi daa xawoon a màggat ngir yol mi daa sottiku ci kawam. Bi ñuy tabax ba àgg ca Hajarul Aswad ñu jaaxle ci gan giir ci Xuraysin mooy am teraangay yekkati ko teg ko fi mu war a tegu, ñu toog ca Kaaba ga di gëstu nu ñuy lijjantee loolu, far ñu dëppoo ci ne ku njëkk a ñëwaat rekk ñu jox la nga àtte leen ci jaaxle googu, far Muhammad (j.m) ne tëll, ñu ne ku wóor kaa ngee na ñu àtte, waaye mu àttee leen nu gaaw te yomb, mooy jël làmbaayam li mu yoroon lal ko ci suuf, teg ci doj wi ne giir gu nekk na jàpp ci cat ngeen tegandoo ko ca barabam. Nii daal la ko lijjantee ca yombam ga ak xarañam ga ak lëmóodikoom ga.

Wàccug Wahyu gi ak yonni gi

Bi at yi jegee ñeen-fukk la sopp gi mu soppoon ag wéet gën a yokk, mu gën a bëgg xëlwa ak beru, mu daan génn Màkk ngir dem ca doj wa nu daa wax Harraa, ngir xunti mu fa nekkoon mu mu daa faral a dugg ngir jaamu Yàlla, noonu la daa jeexale weeru koor wi, ngir sellal boppam, laabal xolam. Benn bis nag ci koorug atum 610 g .j, ba jant bay so la ko genn kàddu gu nooy dikkal ca dalug xunti ma naan ko : jàngal. Yonnant bi (j.m) tiit njàqare li jàpp ko, waaye mu ne ko : man duma kuy jàng. Waaye mu yëg mu mel ne dafa am lu koy naj ba dënn bi xaw a xat mu noppal ko, bu ko defee kàddu gi delseeti neeti ko: jàngal, Yonnant bi neeti ko : man de manu maa jàng. Naj ga delseeti, ba mu xawee woyofati kàddu ga delseeti ne ko : ((jàngal ci sa turu boroom mi bind , bind na nit ci lumbu dereet, jàngal, sa boroomay ki gën a tedd)) kàddu ga daal di dal, daal di deseeti. Fekk jant biy so Yonnant bi yëg njàqare lu rëy, daal di gaaw génn xunti ma, dem ñibbi, bi muy àgg lëndëm gaa ngi doon dugg, ndax diggante Màkk ak xur wa xaw na a ëpp ay ñatti kilomet.

Ba Yonnant ba (j.m) àggee ca kër ga daa daal di woote ne : muur leen ma, muur leen ma, booba ñaq waa ngay siit, yaram way lox, soxna Xadiija daal di dawsi sàng ko, tàmbli koo dalal, bi tiitaange gi demee Yonnant bi xamal ko li xew, ne ko : man de damaa xëm. Ndax xamagutoon ne li ko daloon ag wahyu la gu tukkee ca sunu boroom (t.s) , indil ko laaya wi njëkk ci Alxuraan ju tedd ji.

Soxna su tedd sii di Xadiija wéy ci di dalal xelum Yonnant bi (j.m) naan ko lii la dal de du man a doon lu dul lu baax, ndax yaw ku baax nga, am kóllare, dëggu, baax ci sa ñoñ, di taxawu nit ñi bu ñu ameey naqar. Ca noona xel ma tàmblee dal, mu yëg jàmm.

Waraqat’Ubn Nawfal mi ngi bégal Yonnant bi (j.m)

Bi soxna Xadiija gisee ne tiitaange gi dañ na daa ànd ak moom seeti doomi baay-tëxam ja tudd Waraqat’Ubn Nawfal, mu nekkoon góor gu am hikma, daan jàng téerey diine yi te dégg ebrë , Yonnant bi nettali ko li xew, Waraqat yéemu lool, ne ko lii de mooy mbóot mi Yàlla wàcce woon ci Muusaa (j.m), ne ko aka neexoon may gone ba man a ànd ak yaw ci tas sa bataaxel bii, xelum Muhammad dal, mu dellu këram, waaye teguñu ci lu néew rekk Waraqat faatu, ndax daa xawoon a màggat. Yonnant bi dellu këram ak Xadiija ci xel mu dal ak mbégte, am yaakaar ne wahyu gi dina delseeti, bu sukkadikoo ci waxi Waraqat yi, waaye wahyu gi yeex a ñëw ba Yonnant bi far àgg ci jaaxle lool, waaye mu mujj ñëwaat ginaaw bi, xelum Muhammad dal, mu xam ne lii kat ag wahyu la gu tukkee ca Yàlla (t.s) te moom ku ñu tànn la ngir mu jottali nit ñi diine ju juge ci asamaan si, war a joxaat diiney asamaan yi seen leer ak sell gu njëkk ga ñu yoroon njëkk nit ñi di ko yàq, di ko tàqal ci li jamono di gën a romb.

Nii daal la Muhammadum Abdu Laah mi (j.m) mujje di yonnant bu nu tànn yonni ko ci mbooleem mbidéef yi ngir mu indi fi leer gu tukkee ci sunu boroom di gindee, di tege ci yoon, di jële cig bokkaale jëme cig wéetal Yàlla,di jële ci lëndëmug réere Yàlla, jëme ci leerug gëm ko, jëme ci Lislaam.

Fii la jaloorey Muhammad yonnantub Yàlla bi - jàmm yal na sax ci moom – tàmblee akug jànkoonteem ngir wisaare bataaxel bii ko Yàlla jox mu war koo jottalee ci ngën ji anam ak melo.

ginaaw bi la wahyu gi tàmblee dikk cig toppante di wàcc ci Ku tedd ki, di indi laaya yi def tay alxuraan nànk-nànk, kon alxuraan ñëwadoowul cig mat, waaye laaya topp laay, ba kero muy mat, nga xam ne Jibriil da ko daan dikkal di ko déggal laaya yi, bu ko defee du ko ba ba kero muy wattu laaya jooju ci dënnam, mel ne sax dañu ko cee bind, làmmiñ wi di ko baamu, Yonnant bi bu masaa na jot ciw dogiit ci alxuraan da ko daa baamu ba mokkal ko, bu noppee jàng ko ci saabaam yi, daal di woo ñenn ci ñi man a bind ci ñoom ngir ñu bind ko ca saa sa ci anam gu xereñ, bu ko defee saaba yi gaawantu ñoom itam jàng ko mokkal ko ci anam gu dul soppikooti ba fàww. Nii la laaya yi doon dabantee, saar yi di ko mate nànk-nànk ci lu tollook ñaar fukk ak ñatt ciy at, ndax kat laaya wi njëkk a wàcc ci Yonnant bi (j.m) mi ngi ko fekkoon mu am ñéen-fukki at wi ci mujj wàcc bi muy bëgg a faatu te booba mi ngeek juroom benn fukk yu teg ñatt ciy at. Alxuraan nag ñi ngi ci jublu téere bu tedd bi bépp walla ab xaaj ci moom.

Alxuraan ju tedd ji ak li mu ëmb

Kon daal Alxuraan ci nii mu ñëwe waxi Yàlla a ju mu wàcce cib yonnantam (j.m) ngir mu jottali ko nit ñi. Ñi ngi ko wàcce ci Yonnant bi, muy lu nu biddiwal, maanaam nànk-nànk, kem ni ko xew-xew yi soxlaa ak tolluwaay yi ba kero muy mat, di téere bu ñu laabal, bu ay caaxaan dul laal fenn ((laa yaatiihil baatilu min bayni yadayhi walaa min xalfihii)). Moom nag danu koo séddale def ko ay saar yu toll ci 114 saar. Saar wu ci ne tam seddaliku ciy laaya, saari alxuraan yi nag ak laaya yi lii lanu ëmb :

  • Ponki pas-pasu lislaam :

Saxal kennug Yàlla (t.s), nangu ne Muhammad Yàlla a ko yonni, gëm mbooleem yonnant yi fi jiitu woon Yonnant bi, gëm téere yi Yàlla wàcce ci ñoom, gëm alaaxira.

  • Ni ñuy jaamoo ci lislaam :

Julli, woor, natt asaka, aj.

  • Ponki jikko yi jullit bu nekk war a jikkowoo :

Ñuy wóor, dëggu, am yërmaande ci ku néew-doole, ku aajowoo, ku ñàkk, am ag cofeel ñeel bépp jullit tey dimblante ak moom ci lu baax ak fonki way jur, teral leen añs.

  • As lëf ci taariix:

Ngir jàjjeek waare aki nettali ci dundug yonnant yi, ngir soññee ci ngëm ak foñloo wëlif bokkaale

  • Yee nit ñi :

Ubbi seeni gët ci kàttanug Yàlla gi akug xerañam, jaare ko ci di leen woo ci ñu settantal bindiinu àdduna bi akug nosoom gu xereñ gi

  • Sopploo nit ñi gëm Yàlla :

Jaare ko ci wax leen li Yàlla dig ku gëm cib yool akug pay gu neex ci àdduna ak alaaxiraa ak soññee ci jiyaar ci yoonu Yàlla.

  • Ragalloo nit ñi ag weddi Yàlla ak bokkaale ko ak moytuloo leen wuuteek ndigëli Yàlla yi :

Jaare ko ci leeral leen mbugël yi ñu waajal ñeel ñi ragalul Yàlla mbaa ñuy tooñ nit ñi di jalgati, mbaa ñuy gàttañlu ci def jaamu Yàlla yi

  • Sariiya :

Mooy yoon wu mat wiy nos ni nit ñiy jëflantee ci seen biir, ak li nu am ciy àq aki yelleef ak li leen war ciy wartéef

Lislaam nosteg dund gu mat

Dinanu gise ci loolu ne alxuraan de ëmb na ag nos gu mat ñeel dundug nit ci gépp anam, mi ngi rëdd séqoo gu nit ki ak boroomam akug séqoom ak mbokkam, dajaleeti jullit ñi ci genn bennte mooy umma bi walla mbooloom lislaam mi (di jullit ñi ), joxati mbooloo mii yoon ak nosteg politig, gu mboolaay ak gu jikko. Dugg ci lislaam du rekk jël diine gëm ko, di def li mu digale ciy jaamu, waaye kay ag tuxu la dem ci ag mboolaay gu yees gu mat gu ami ponkam aki nosteem aki yoonam aki misaalam yu kawe, ndax lislaam ag noste gu mat la gu takkatoo.

Bataaxelub Yonnant bi (j.m) mooy dugal nit ñépp ci lislaam ak tuxook ñoom jëm ca nosteg lislaam gu yees ga te mat. Looloo taxoon Yonnant bi (j.m) daawul yam ci sàkku ci nit mu tudd ñaari seere yi rekk ak def jaamu yi, waaye kay da daan sàkku ñu bàyyi seen dundug réer gu njëkk ga te tàbbi ci nosteg politig, gu mboolaay, gu ruu gu yees gii. Moom de santuñu ko woon rekk mu woote te jotal bataaxel bi, waaye ligéey bu baax ci nit ñi gëm te dugg ci xeetu lislaam wi ak àddunaam ju yees ju fees ji dell ak yiw ak barke.

Bataaxelub Muhammad (j.m)

Yonnant bi wéy na di xamal nit ñi bataaxelam bi, bu ko defee gàllankoor yi nekk ci kanamam mel ne ay doj , ndax kat nit yombul mu tàqalikook ni mu baaxoo woon a dunde, nit jaamub li mu miin la, waaye moom mu wéy di deewoo, di jànkoonte, di muñ ba jóoxe bataaxel bi ca na mu gën a rafete. Loolu mooy kiimaanug dundug Muhammad (j.m) gu yéeme gi cib taar, moom daal ci léppam dund la gu fees dell ak ay bind yu fees aki bind yuy jàngale dëggug ngëm, wóor ci def li la war, muñ ci lu naqari, ñeg ci fas yéenee jéggi gàllankoor yi, ŋoy ci jikko yu rafet, muñ ci loraangey nit ñi, gëm ne ndam lu mu yàgg yàgg dana mujj ñeel jullit biy jëf tey jànkoonte tey ŋoy ci buumug Yàlla gi ci lu dul naagu mbaa yoqat walla tàyyeel.

Jànkoonte gi Yonnant bi doon def ci bi mu nekkee Màkka

Yonnant bi ginaaw bi nu ko yonnee dund na ñaar fukki at ak ñatt yoy ci la matale bataaxelam bi, fukki at ya ak ñatt nag Màkka la leen jeexal, fukk ya ca des mu def leen Madiina, làqu nag ca weeru rabiihul lawal ci atum fukk ma ak benn ginaaw gàddaayam gu tedd ga.

  • Diirub Màkka bi :

Mooy diirub deewoo ak jànkoonte gu tar ga ak way bokkaaley Màkka yi, ak jiyaaram ga ngir taxawal fa mbooloo mu lislaam mi, ba bi mu gàddaayee dem Madiina, diir ba di fukk ak ñatt ciy at.

  • Diirub Madiina bi :

Mooy jamonoy ndam, jaare ci dugg gi waa Madiina dugg ci lislaam, mbooloom lislaam am fa, ak nos mbooloo mii ak mottali jaamu yi nekk ci lislaam ak sariyaam, ak tëral nosteg xeet wi, gu politig gi ak gu mboolaay gi, ak dugal dunu araab bi ci lislaam ngir waajale ci tas gi lislaam war a tas ci mbooleem pàkki àdduna bi, ab diiram nag fukki at la ak lenn ciy weer.

Jamonoy Màkka ji

Dafa séddaliku ci ñatti tolluwaay :

Tolluwaay bu njëkk ba ak jullit ñu njëkk ña
Tolluwaay bu njëkk bi ci jamonoy Màkka ji - ab diiram juroomi at la daanaka – mi ngi doore ci bi Muhammad (j.m) tàmblee di woote jëme ci lislaam, tàmblee ko ci giiram gi ko gën a jege, ca ñoom la jële mbooloo mi jiitu ci lislaam, ka nekkoon ca bopp ba di soxna Xadiija, nekkoon jigéen ji njëkk a jébbalu, ak Aboo Bakr di ki njëkk a gëm ci góor ñi ak Aliyun mom Aboo Taalib doomi baay-tëxi Yonnant bi (j.m), mooy ki njëkk a gëm ci gone yi, moom de booba ay atam fukk rekk lañu woon , ak Seyd’Ubn Haarisa mi doonoon mawlaab Yonnant bi, mooy ki njëkk a jébbalu ci mawlaa yi.

Am mbooloo topp ci tàbbi ci lislaam ci waxambaaney këri Màkka yu Xuraysin yu mag yi, ñi ci Yàlla ubbi séeni xol nanguloo leen lislaam ak dalam yu kawe yi, ku ci mel ne Talhata mom Hubaydul Laah, Abdurahmaan’Ubn Hawf, Sahd’Ubn Abii Waqaas, Usmaan’Ubn Haffaan, Subayr’Ubn’Ul-hawwaam.

Am mbooloo it tàbbeeti ci Lislaam ci ñu ñàkk ñeek jaam yi ak way néew yi doole ci ñi Yàlla tawfeexal ubbil leen buntub gore ak yamoo ak yaakaar, ku ci mel ne Bilaal mom Ecopi mi, Hammaar’Ubn Yaasir, Xabaab’Ubn’Ul-arat.

  • Jullit ñi ci kër Arqam :

Mbooloom lislaam mii baaxoo woon naa dajeek Yonnant bi ca Kaaba ga ngir déglu alxuraan ci moom ak jàng ci ponki lislaam, loolu it jur way bokkaaley Quraysin yi yoqat ci jataayi néew yi doole yii ci li wër Kaaba gi, tax it ba ñu tàmbli di leen xatal ak a yoqatloo, Yonnant bi it gis ne war naa wutal jullit ñi barab bu ñuy daje cig féex akug dal, ci noonu wenn waxambaane wu bokk ci ñoom ñu naan ko Arqam Ibn Abiil Arqam ne man naa joxe këram ngir ñu fay daje, Yonnant bi nangu, looloo taxoon jullit ñi ba woon daje ga ñu doon daje ca Kaaba ga.

Waaye làqu gi nu làqu leegi tiitloo waa Màkka yi, jeqi ci ñoom njàqare, rawati na Aboo Jahlin ak Aboo Lahab mi nekkoon baay-tëxi Yonnant bi ak ñeneen, ñu tàmbli di topp jullit ñi ak di leen xeeñtu ngir xam li nuy def.

  • Jébbalug Hamsa, Omar topp ci :

Am na bis Aboo Jahlin nekk fi barab di néggandiku Yonnant bi booba mi ngi jëmoon ca kër Arqam, ba Yonnant bi (j.m) egsee mu toroxal ko, waaye Yonnant bi muñ ak doonte ku dëgër la woon te manoon koo sonal, waaye Yàlla da koo digaloon mu woo nit ci hikma ak waare gu rafet, ci noonu mu wacc ko fa dem, bi Hamsa baay-tëxi Yonnant bi yëgee li xew daa mer seeti Aboo Jahlin duma ko ba noppi jébbalu dib jullit, ci noonu mbooloom lislaam mi gën a am doole ci dugg gi ci Hamsa dugg leegi.

Bi ci as ndiir toppee Omar’Ubn Xattaab jébbalu, jullit ñi gën a sawar, gën a ñeme, ñu daal di génn leegi kër Arqam daal di dellu fa nu daa dajee di la wër Kaaba ga, ci noonu Yonnant bi tàmbli di woote ci kaw ci lu bir, te faaleetul merum waa Màkka yi. Fii la jamonoy woote ci kër Arqam jeexe, leegi woote gu biti gu matale gi tàmbli.

Tolluwaayu Màkka bu ñaareel bi ak xeex gi Quraysin doon xeex woote gi
Waa Màkka yi dañoo jàppe woon loolu muy ag dëkk gu leen jullit ñi di dëkk ak ag fontoo, ñu jug nag xeex leen xeex bu metti, jaare ko ci di sonal way néew yi doole ak faqiir yi ku ci mel ni Bilaal, Hammaar Ibn Yaasir ak Xabaab, ñu tàmbli woon it di ñaawal Yonnant bi(j.m) di ko saboote ak a lor ak lenn ci saaba yi.
  • Gàddaay ga dem Ecopi:

Yonnant bi daa amoon njàqare ci saabaam yi, ragal waa Màkka yi sonal leen, ci noonu mu laabiire woon leen ci ne ku bëgg ci ñoom man naa dem Ecopi, foofa dananu fa man a doxal seen diine te kenn du leen topp mbaa mu leen di sonal, bi mu ko defee lu tollook juroom ñatt fukki góor akug jigéen gàddaay dem fa ci ñaari yoon. Yonnant bi des Màkka ak mbooloo mu néew ci jullit ñi, di jànkoonteek lori Quraysin yi. Waa Màkka yi jaaxle woon nanu ci man gi Yonnant bi (j.m) manoon a muñ ay coona ak sax gi, ñu sàkku woon ci baay-tëx ji mu tere ko woote gi maanaam Lislaam, waaye Yonnant bi bañ te wëy ca woote ga, looloo waraloon way bokkaale yi defoon ag dogoo gu mat ak Banii Haasin ak itam Banii Abdul Mutalib te ñoom ñooy mbokki Yonnant bi (j.m). Banii Haasim jànkoonte na aki coona ngir dogoo gii nga xam ne saxoon na ñatti at. Tolluwaay bu ñaareel bii nag weesuwutoon juroomi at.

Ñatteelu tolluwaay bi ci jamonoy Màkka ji
Sonalug waa Màkka yi ak xatal gi nu doon def Yonnant bi ak jullit ya jotutoon a gàddaay dem Ecopi àggoon na ca dayo ba bi yonnant gi amee fukki at, maanaam bi nu ko yonnee ba mu mat fukki at. Bi dogoo gi jeexee ba teg lu néew la Aboo Taalib baay-tëxi Yonnant bi (j.m) faatu, mi nekkoon njiitu Quraysin ak Màkka te daan aar Yonnant bi ci tar gi waa Màkka yi taroon ci di ko lor. Bu ko defee noonub lislaam bu tarug noonu gi jug moom itam yor njiitug Quraysin gi, moom baay-tëx la woon ci Yonnant bi waaye ku ko iñaane woon la te soxote ko.

Bi Aboo Taalib faatoo ba teg lu néew la soxna Xadiija làqu moom it (y.y.g ) ginaaw bi mu àndeek Yonnant bi ñaar fukki at ak juroom cig sell, cofeel, dimblante ak bànneex, ak doonte fukki at yu mujj yi daa feesoon dell aki jafe-jafe, mettiit ak xatal. Yonnant bi naqarlu woon na bu baax ci faatug àndandoom bii mu bokkaloon dund gi, nekkoon ku matal kóllare, wóor, taxawoon ci wetam ci ati jafe-jafe yi, wone woon gën jaa kawey misaal ci ni soxna su gëm tey muñ war a mel.

Bi Aboo Taalib ak soxna Xadiija làqoo Yonnant bi yëgoon na ne ku wéet la dëgg, te at yu metti yii mu def Màkka di jiyaar indilunu ko lenn ngérte lu ñu xam lu mu yaakaaroon ngir lànkug waa Màkka yi ak nuur gi nu nuuroon cig kéefar ak ŋoy ci li ñu fekkon seeni baay.

Génn gi Yonnant bi defoon dem Taayif

Fii la Yonnant bi xalaate ci génn jéem a wooteji ca Taayif ga jege Màkka, mu daal di fay dem ànd ak mawlaam bi Sayd’Ubn Haarisa, waaye waa Taayif déggalunu ko, looloo tax mu dëppoon dellu Màkka.

Waaye Yonnant bi loolu taxutoon mu yoqat ak doonte waa Màkka yi dañoo dogu woon ci lor ko, mu daal di jawali ca biti Màkka ca lenn ca giir ya fa dëkke woon, daan leen woo ci lislaam waaye taxutoon lu bari wuyyu ko ca.

  • Mbégtey gàddaay gi:

Yonnant bi (j.m) da daan def bu déggaan aw nit ñëw Màkka mu gaaw gisi leen, woo leen ci lislaam, ba yonnant ga tollee ci fukki at ak benn daa dajeek ab kuréel ci giirug Xasraj ñëwoon Màkka, di woon genn ci ñaari giir ya nekkoon Màddiina, geneen ga di woon Aws, xare ba nekkoon di lu tar ci seen diggante ak noonoo ga. Ca at ma ca topp am mbooloo ci Aws dikk na Màkka, Yonnant bi gaawantu seetsi leen wax ak ñoom, waaye fekk fi ñoom nopp yuy déglu, ndax kat Yahood yu Madiina yi dañu daan wax naan ab yonnant bu ñu yonni de dana dikki di dimbalisi Yahood yi ci Xasraj ak Aws, looloo waral Aws jortoon ne Muhammad (j.m) mooy yonnant bi Yahood yi doon wax. Bi seen mbooloo mi toogeek moom déglu ko lanu gis ne moom kat ku dëggu la ci li muy wax, bi mu leen jàngalee ay laaya ci alxuraan lanu ko gëm, sàkku woon ci moom mu may leen ba ñu dellu Madiina, man a nettali seeni mbokk li nu dégg.

Ci noonu ñu dellu nettali seen mbokki Aws yi li nu dégg, ñoom itam ñu amoon yitte lool ci gis Yonnant bi te déglu ko, Xasraj it dégg loolu, ñaari giir yépp tàmbalee yittewoo gis Yonnant bi, ñu daal di dogu ci yonni am mbooloo mu mag ci jamonoy aj gi ngir mu dajeek Yonnant bi (j.m), déglu ko

  • Jaayanteg Haqaba gu njëkk gi:

Mbooloo mi làqu waa Màkka ñëw dejeek Yonnant bi (j.m), déglu ko, waaye am lu leen wóor ci ne Yonnant bi de ku dëggu la, ci noonu ñu ànd dugg ci lislaam, def ak Yonnant bi jaayante gu Haqaba gu njëkk ga, daal di ko cay dig ne danañu woo waa Madiina ci Lislaam, te dinañu ko seetsiwaat ginaaw at, ci noonu Yonnant bi yabal ak ñoom saabaam ba tudd Mishab Bun Hamiir, ngir mu jàngal sariiya waa Madiina.

  • Jaayanteg Haqaba gu ñaareel gi:

Bi lu toll ci at jàllee Mishab dellusi ànd ak ab kuréel bu mag ci waa Madiina, seenub lim tolloon ci juroom ñaar fukki góor ak ñatt ak ñaari jigéen, ñu jàkkaarloo woon ak Yonnant bi fa Haqaba jaayante fa ak moom, muy jaayanteg ñaareel ga, ñu ñaanoon ko mu tuxu dem Madiina, ne ko fas nanu ko yéenee aar ci gépp noonu te dinanu ànd ak moom ci tas Lislaam.

Ci ginaaw bi rekk la Yonnant bi digaloon saabaam yi ñu gàddaay dem Madiina, ñu daal di woon tàmblalee gàddaay ci ay mbooloo, mbooloo topp mbooloo, lislaam daal di fay tas ba mujj doo gis genn kër ca Madiina gu ay jullit nekkul.

Gàddaay dem Madiina

Li ëpp ci jullit yi nekkoon Màkka daal di gàddaay dem Madiina ci weer yu néew, bi Yonnant bi amee xel mu dal ca saabaam ya ca Madiina, daa daal di gàddaay moom itam ànd ak àndandoom bu dëggu ba Aboo Bakr, ñu ngi génn ci lëndëm gi cig làqu, ndax waa Màkka dañoo bëggoon a tëye Yonnant bi ca Màkka ngir ragal lislaam di ame doole ca Madiina.

Mi ngi àgg Madiina ci 12 rabiihul Awal ca at mu njëkk ma ca gàddaay ga (4 sëtumbar atum 622 g,j), booba nag di taarixe ci gàddaay gi tàmbaleegutoon a dox, ndax Seydinaa Omar mooy ki digale ñu jël at mu njëkk mi ci gàddaay def ko at mi taariixu jullit ñi di tàmblee.

Yonnant bi fekk na li ëpp ci waa Madiina ñu tàbbi ci lislaam, ñu néew a ci desoon cig kéefar, te bi Yonnant bi dikkee dañoo daal di jébbalu. Yahood yu bari nag nekkoon nanu Madiina, tasoon fépp it, ña ca ëppoon daan bay, mbaa ñuy def yenn mecce yi niki meccem weñ ak tëgg. Ñatti giir yu mag nag feeñ na ci ñoom, ñooy Banoo Qinqaah, Banoo Nadiir ak Banoo Qariitha, ñoom nag dañu daa won Xasraj ak Aws ne ñoo leen kawe, te daan leen jaxase bay waral ñuy xulook a xeex. Bu xeex amee leeg-leeg ñu ànd ak Xasraj, leeg-leeg Aws, daa nañu wax naan ab yonnant de dana feeñi ci ñoom te bu ñëwee dina ànd ak ñoom xeex Aws ak Xasraj ba jële leen fi.

  • Jëfi Yonnant bi (j.m) ca Madiina:

Yonnant bi bi mu àggee Madiina rekk daa daal di tàmbalee ligéey, ligéey bi nag ci ñaari mbir yii la jëmoon :
1 – Sos wenn xeetu lislaam wu gëm tey benn, ag mbokkoo muur ko, ag yamoo ëmb ko, ag maandute yiir ko, ñu fay doxal lislaam.
2 – Waajal xeet wii, wutal ko doole ju doy sëkk ngir mu man a duggal araab yépp ci Lislaam, teg ci mbindéef yépp.

Yoon yi Yonnant bi jaaroon ngir amal ñaari mbir yii ñooy

  • Def ag mbokkale ci diggante jullit ñi, mu jox muhaajir bu nekk am mbokk mu bokk ci ansaar yi
  • Taxawal jenn jumaa ca Madiina ñu fay jullee, muy nekk it barab bu mbooloom lislaam miy dajeek seenub yonnant ak saaba yu mag yi
  • Def ag kóllare guy nos àq ak yelleefi nit ñi ci Madiina ak seeni wartéef ci lu jëm ci seeni moroom ak ci lu jëm ci xeet wu lislaam wi, kóllare gii nag Yahoodi Madiina yi ci lañu woon, waaye ñoom dëgguwuñu woon ci bokk gi ñu ci bokkoon.

Yaatal gëwéelub xeet wi

Bi Yonnant bi nekkee ci ligéeyam boobu ngir amal jubluwaayam yooyu, mi ngi doon wéy it ci di woo ci lislaam giir yi peek Madiina ngir ñu bokksi ci uma bi, di xeetu lislaam wii xëy taxaw, bi mu gisee ne lenn ci kilifay giir yii ànduñu woon ak moom ci loolu, daa daal di woon yabal ay cong yu lislaam ngir xeex kilifa yooyu ak ñi leen di jàppale ba duñu man a gàllankoor giir yi ci dugg ci lislaam. Cong yii lanuy wax xaswat, ndax Yonnant bi (j.m) moo ko daan jiite, bu ko kenn ci saaba yu mag yi jiitee nag ñu koy wax sariya

Xaswat yi ak sariyat yi

Yonnant bi tàmbli na, daal di yabal juroom benni xaswa ak ay sariya yoy amal nanu xemmemtéef lii, bu ko defee gëwéelub uma bu lislaam bi gën a yàkkiku, daal di far ëmb mbooleem wàllug càmmooñ gu Hijaas gi, loola nag la ca juddoo mooy Madiina mujj teg loxo ci yoonu yaxantu wi jëme Shaam juge Màkka. Looloo taxawaloon yaxantu ga ca Màkka te kat moo nekkoon balluwaay bi seen koom di juge.

Xaswat bu Badar bu mag ba ca 2eelu at g,g

Xaswa bu Badar walla xareb Badar Yonnant baa ngi ko def ci atum ñaareelum gàddaay gi, mi ngi ame nag ca digg yoon wa dox diggante Màkka ak Madiina, lu tollook ñatti téeméeri jullit am ca ndam ca kaw junni ci yéefari Màkka yi, muy ndam lu mag lol lislaam dëgëre na ci, nit ñi it xame ci ci anam gu wér péŋ gees manul a sikk ne Yonnant bi de wooteem gii lu wé la, ci noonu nit ñi sottiku Madiina ciy mbooloo yu mag ngir dugg ci lislaam, ci xare bii lanu raye Aboo Jahlin ak ñu ko moy ci nooni lislaam yu tar yig noonu.

Xaswat bu Uhud atum 3eel mi giinaaw gàddaay gi

Màkka manutoon a ñàkk mu def lu ko delloosi darajaam ji mu ñàkkoon ci dunu araab bi, ubbilaat ko yoonu yaxantu wi, looloo waraloon ay way bokkaaleem dajale woon doole ju mag ju toll ci ñatti junniy góor, ñaari téeméer yi diy gawar , ca atum gàddaay mu ñatteel ma ñu dox jëm Madiina ngir dugg ko ci doole, waaye Yonnant bi génn àkk léen ci lim bu toll ci junni ciy saabaam.

Ñaari mbooloo yi daje ca bëj-gànnaaru Madiina, fa ron doju Uhud, xare bu tar tàkk fa bob jullit ñaa ca amoon ndam ca njëlbéen ga, waaye boroom fett ya mujjoon wooteek ndigal la leen Yonnant bi joxoon daal di wacc seen barab ya nu leen taxawloo woon, Xaalid’Ubn Waliid mi jiite woon yéefar yi daal di màng pose bi song jullit ñi, bu ko defee seen sàppe jaxasoo, baj-baji, ñu ray ca ñu bari, waaye Yonnant bi moom des fa ak lu néew ciy gaayam, mu daal di woo ay saabaam ngir ñu dellusi. Ak li ñu ko gaañ ca xare ba lépp téewul mu xettali dooley jullit ñi ca njàmbaaram ga ak saxam ga, te tee yéefar yi dugg Madiina. Xeex bi wéy ba jant so, fii la coona bi sonale yéefar yi, ñu rocciku dellu Màkka ci lu dul ñuy amal li nu bëggoon, te loolu saxug Yonnant bee ko waral akug njàmbaaram ak sorib gisam.

Waaye yéefar yi li nuy amadi li ñu bëggoon lépp téewul ray nañu ab lim ci tànnéefi jullit ñi, ku ci mel ne Hamsa bay-tëxi Yonnant bi (j.m), ak Mishab’Ubn Hamiir mi daa gàddu raayob jullit ñi ak leneen lu toll ci juroom benn fukki jëmm, jullit ñi am nañu lu leen naqari lool ci seen sahiid yi, waaye jànge nañu ci Uhud benn bind bu ñu dul fàtteeti mukk, mooy topp Yonnant bi (j.m) ak defi ndigalam.

Xaswat bu Xandaq atum 5 g.g

Waa Màkka yi yég nañu ne amaluñu dara lu am solo ci li ñu doon sàkku, ñu gis ne ñoom kat ak seen mbégte mu rëy mi ñu am lépp ci ray gi ñu def lu bari ci jullit ñi téewul Màkka dañul di nekke na mu nekke woon: yoonu yaxantu wi mi ngi ci loxol jullit ñi, giir yaa ngi tàbbi ci lislaam, gu dugg geneen topp ca.

Lii a tax Aboo Sufyaan’Ubn Harb mi nekkoon njiitul Màkka ginaaw Aboo Jahlin jugoon boole doole ju mag ci waa Màkka ak ñi tapoo ak ñoom ci giir yi, ñu dox nag jëm Madiina ca juroomeelu at ma ñeel gàddaay ga, bu ko defee Yonnant bi aki saabaam jug gas am xandaq ca la wër Madiina, ba mboolooy xarey yéefar yi agsee manuñoo jéggi pax ma, bu ko defee xare bi yam ci sàneente ay fett jéggi xandaq mi, ci noonu jullit ñi ñoom wone ag yewwu gu mat ci sàmm seen xandaq ba yéefar bu ko jéggi rekk rayees ko ca saa sa. Gaw gi sax lu tollook ñaari ayu bis, ginaaw bi Yàlla yonnee gelaw lu tar ak taw bu metti mu yàq xaymay yéefar yi, fay seenuw sawara, sedd bi metti ci ñoom ak doonte weer woowa wu mars la woon, te woowu weer fa Hijaas mooy tàmbalig lolli bi, bu ko defee yéefar yi àggati ci manuñoo ñàkk a dind gaw gi te dellu Màkka ngir sedd bi te amuñu dara ca seen càkkutéef ya. Loolu di ag juunu gu mag akug sooy ñeel leen, te diw lay wu mag ak firnde ci kàttanug xeetu lislaam wi ak dëggug gëm gi ay nitam am, ak ñaw gi nekk ci njiit la Muhammad (j.m).

Génne Yahood yi Madiina

Ñatti giiri yahood yi di (Banoo Qinqaah, Banoo Nadiir ak Banoo Qariitha) yoroon nanu taxawaay bu ñaaw te noonoowe jëme ca Yonnant ba ak wooteem ga, dale ko ca bi muy door a agsi Madiina, weddi woon nañu ag yonnantam, naan neey yonnant bi ñuy néggandiku manul a juge ci fu dul gañog Banii Israayil. Ginaaw nag yonnant boobu ñu daa wax farul génne ci ñoom, xanaa kay ci giirug Quraysin gu araab gii dara raxul, loolu naqari woon na leen, jural leen ag soxot ak kañaan ak mbañeel.

Yonnant bi yàgg naa muñ lor yi ñu ko daa lor ngir yaakaar gi mu yaakaaroon ne danañu mujj noppal ko, ba àgg sax ci gëm ko, waaye lu mu muñ rekk ñu gën koo bañe lislaam gën koo dellikoo ag noonu, waaye làqoon nanu seen noonu googu ak mbañeel gi bi ñu gisee ne lislaam mi ngi gën a dolliku doole, di gën a dëgër bis bu Yàlla sàkk:

Bi jullit ñi amee ndam ca Badar la xolub Yahoodi Madiina yi gën a dagg, ab kuréel ci ñoom it – ñooy Banoo Qinqaah - àgg ci manatuñoo ñàkk a feeñal seen bañ gi ñu bañ lislaam ak soxote gi ñu def jullit ñi ci ndam li leen Yàlla may, ci noonu ñu tàmbli di saboote Yonnant beek lislaam, waaye Yonnant bi (j.m) dem ca seen kër ya gaw ko, bi ñu jëbbalee seen bopp la leen génne Madiina ñu dem Shaam.

Ginaaw bu xaswat bu Uhud jàllee ba teg lu néew, la yahoodi Banoo Nadiir lànk ne duñu joxeeti li leen war ci ndimbalul alal li war ñeel umma bi, waaye yamuñu ca, dañoo tàmbli woon a defi pexe ngir yong Yonnant bi (j.m), waaye Yàlla (t.m) musal ko ci seenuw ay, nga xam ne Yonnant bi amul woon lenn lu mu manoon a def lu dul génne leen ñoom itam ngir mucc ci seenuw ay. Ci biir xareb xandaq ba yahoodi Banoo Qariitha doon nañu jéem a wor jullit ñi dem jàppaleji yéefar ya gawoon Madiina jaare ko ci may leen ñu dugg Madiina jaare ko ci seenug wàll, looloo war bi xeex bi jàllee rekk Yonnant bi daa daal di jawali ca seen kër ya, gaw leen ba ñu wommatu, nangul ko, mu digal saabaam ba tudd Sahd’Ubn Muhaaz mu àtte leen ci li jaadu fi moom, li tax mu tànn ko nag mooy ñoom ci mom lañu doon sàkkoo ag tin ci Yonnant bi, moom it mu ne nañu ray ñi ci doon xeex, ñi ci des ñu génne leen Madiina.

Ci noonu la xeetu lislaam wi mucce ci ayuw yahoodi Madiina yi, Madiina mujj yor lu néew rekk ciy yahood yu bokkoon ci ñi defoon ay tapoo ak lenn ci bànqaasi Aws yeek Xasraj, ginaaw nag feeñaluñu woon genn wor mbaag mbañeel ñeel jullit ñi Yonnant bi defu leen dara. Looloo waral ab kuréel ci ñoom gëm ca gëm gu dëggu, am ca ñeneen ñu ca gëm ñu ag ragal gëmloo akug naaféq

Juboo gu Udaybiya atum 6eel g.g

Bi Yonnant bi amee lu ko wóor ci ne am cong mu juge ci biti jeex na, wor gu biir gi it dañ na la tàmblee waaj ngir dugal Màkka ci lislaam. Gisoon na ne waa Màkka yi ñi ci ëpp ñu tàmbali woon a yittewoo mbiri lislaam lañu ndax gis nañu muy yaatu, di gën a am doole bis bu nekk, li Alxuraan digoon jullit ñi bañu nekkee Màkka di ñu néew doole gën di feeñ, gën di am. Nga xam ne Màkka li ko tee woon a dugg ci lislaam wéesuwutoon lenn ci njiiti yéefar yi ak seeni àndandoo, ñoom ñi ragaloon seeni njariñ di sànku, seeni daraja di suufe su ñu duggee ci lislaam.

Ci biir loolu ab laaya wàcci bu tedd buy digal Yonnant bi mu wëlbati qibla bi jullit ñi amoon muy Baytil Maqdis def ko leegi Kaaba gu sell gi, mu mujj ca saa sa di qiblab jullit ñi ñépp.

Bi ñu wëlbatee qibla bi leegi jëme ko ci Kaaba gi, te Yonnant bi xam dëgër gi xeetu lislaam wi def leegi te ame ko doole ci la jugoon ànd ak am mbooloo ci saabaam yi ngir defi umra, mooy siyaareji Bayti Laahil Haraam ci waxtu yi dul yu aj, looloo tax ñu tudde ko aj gu ndaw gi.

Bu ko defee, Yonnant bi (j.m) daal di génn ci junni ak ñeenti téeméer ci ay saabaam jëm Màkka ngir defi umra, looloo taxoon yobbaalewuñu woon ngànnaay ngir bëgg waa Quraysin xam ne jullit ñi dañoo ñëw ngir defsi ag jaamu rekk mooy umra gi. Bi jullit ñi aggee ci barabub Hudaybiya mooy buntub Màkka bi féete wàllug cammooñ la waa Quraysin yi tàmbali woon a ragal jullit ñi dugg Màkka. Ñu daal di yonnee ci Yonnant bi ne ko daal àndatuñu ci jullit ñi dugg Màkka ak donte yoruñu ngànnaay. Ñu daal di fay def waxtaan wu yàgg yu mujj àgg ci li ñuy wax Juboog Hudaybiya, moom nag li mu yaxal mooy jullit ñi buñu dugg Màkka ca at mooma waaye bu déwén ja’a ca waxtu woowa dinañu man a dugg (muy atum juroom ñaareel ma g.g), bu ko defee ñaari wàll yi def ag juboo guy sax fukki at.

Ca juroom-ñaareelu at ma ñeel gàddaay ga, Yonnant bi dellu defi umra ga mu yéene woon ca daaw ja, daal di siyaare ab dëkkam bi mu juddoo, ginaaw ba mu fa gëjee lu tollook juroom ñaari at.

Yonnant bi (j.m) bind na buur yi

Ci biir atum juroom ñaareel mi ñeel gàdday gi la Yonnant bi (j.m) yabal ay ndaw ca Qaysar mu Rom mi, Kisraa mu Faaris mi, ak kilifag Qibt ya ca Isipt, joxaale leen ay bataaxel yu leen di xamal lislaam te di leen ci woo. Qaysar moom daa yeexoon a tontu, bu dee Kisraa mu xottite bataaxel ba, waaye Maqooqas moom daa tontu tontu bu rafet, yonnee ca Yonnant ba adiya waaye taxutoon mu dugg ci lislaam.

Yonnant bi yonneeti ci lu bari ci njiiti araab yi ak seeni kilifa ak buur yi nekk ci mbooleem dun bi, am ñu ci dëggal te gëm, waaye la ca ëpp tontuwuñu.

Ubbig Xaybar

Xaybar am mbooloom ay waaha yu ndaw la yu nekk ci bëj-gànnaaru daanaka dun bi, ca waxtu woowa Xaybar ci loxol yahood yi la nekkoon, ñu seŋe woon ko, ngartaajoo woon ay xéewalam, def ko seen dàttub xare tey seen barab bu alal, ñu tàmbali woon di xiirtal seen dëkkandooy araab yi ci ñu fexeel lislaam ak Madiina. Waaye Yonnant bi dëgmalsi leen ci mbooloom xare mu mag, gaw Xaybar, jullit ña songoo fa ak yahood ya cib xare, Yonnant bi dumaa leen fa, ñu wommatu, yeneen waaha yi ko jege woon te nekkoon ci loxol yahood yi topp ci, niki Fadk ak Timaa. Ci jëf jii la Yonnant bi raye jànkoonte ak jafadiku gi yahood yi dese woon daal di fegu ci seenuw ay.

Ubbig Màkka ci juroom ñatteelu at mu gàddaay gi

Ci biir loolu fekk na Màkka mu néew lool doole, ñu ëpp ci ñi ko daa jàppale bàyyi ko, lislaam tas fat tas gu yéeme rawati na ginaaw Juboo gu Hudaybiya gi. Ci njëlbéenug juroom ñatteelu at mu gàddaay gi la waa Quraysin firi woon seen kóllëreg juboo ga ñu defoon ak Yonnant bi, loolu nag mi ngi ame ci tooñ ak jalgati gi ñu defoon giirug Xasaaha gi nekkoon jullit, ci noonu Yonnant bi jug ci fukki junniy jullit dugg Màkka ci lu dul xare ci weeru koor gu juroom ñatteelu at ci gàddaay gi (samwie 630 g.j) Bi Yonnant bi duggee Màkka daa daal di laabal Kaaba gi, dammate xërëm ya, sànni leen ñu sori Kaaba ga, jullit ñi daal di raxas Kaaba gi, mu nekk leegi nag di néegub Yàlla deesu fa jaamooti ku dul moom. Ci loolu la Yàlla dëggale dëel bi mu joxoon Yonnant bi ak jullit ñi, ndax jàppale na leen, jàppale diineem, fay leen ci seen sellal gi ak dëggu gi ak jiyaar gi ñu doon def ci seen alal ak bakkan.

Bi loolu jàllee ba teg lu néew, lislaam daal di tas ci Màkka gépp, ñu taxawal fa ay jàkka, mu mujj di ñaareelu dëkk ak digg bu lislaam ginaaw Madiina gu ñu leeral gi .

Xareb Hunayni

Ginaaw bi ñu ubbee Màkka ba teg lu néew la giirug Hawasaan ak giirug Saqiif gi mu tapooloon jugoon dajale xare bu mag, dox nag ngir xeexi jullit ñi, waaye Yonnant bi duma leen duma yu tar ca fa ñuy wax Haniin, bi loolu amee genn giir jugatul naan day xeex lislaam. Ginaaw ndam lii Yonnant bi (j.m) dem na Taayif dëkk bi Saqiif dëkkoon gaw ko, ba gaw ga yàggee mu xam ne dana wommatu , la leen fa ba dellu Madiina, waaye noonu la deme woon ndax yàggaatul dara Taayif jébbalu, giirug Saqiif gépp dugg ci lislaam.

Atum Mbooloo yi di juroom ñeenteelu at ginaaw gàddaay gi

Atum juroom ñeenteel mi ñeel gàddaay gi ñi ngi ko tudde woon atum mboolooy yi, ngir ne ci la giiri dunu araab bi bépp doon yabal ay mbooloo yu bokk ci ñoom ngir yëglesi seenug dugg ci lislaam, mbooloo yii nag bawoo nañu ci mbooleem goxi, nga xam ne bi fukkéelu atum gàddaay giy jot fekk na mbooleem dunu araab bi dugg ci lislaam, ñépp ña fa dëkk mujj bokk ci uma bi.

Xaswat bu Tabuuk di bi Yonnant bi mujj a def

Ci sawaal atum 9 ci gàddaay gi, ginaaw bi nga xamee ne mbooleem araabi daanaka-dund bi dugg nanu ci lislaam, la Yonnant bi bëggoon a xamal jullit ñi ne jiyaar ji de fàwwu mu génn dunu araab bi, ngir ñu man a tas diine ji ci àdduna bépp, looloo taxoon mu wommatoon benn xare bu mag ci ay jullit, dox jëm bëj-gànnaar ba àgg Tabuuk ca dig wa dox diggante dunu araab beek réewi Shaam yi nekkoon ci ron teg loxo gu Rom, foofa la nguuri araab yi nekkoon ci dig yooyu duggoon ci lislaam, jullit yi it xame ci ne jiyaar de day sax di wéy ba fàwwu .

Ajug tàggoo gi atum 9 g.g

Ci silhijja atum fukkéel mu gàddaay gi la Yonnant bi defi woon hajjatul wadaah di ajug tàggoo gi, ba muy dem nag ma nga àndoon ak ay junniy junni ci jullit ñi, ci aj gii la Yonnant bi (j.m) leerale ajiin wi ñu yoonal, te mooy wii fi nekk bat ay jii ñu nekk .

Bi mu noppee ci aj gi la def xutbaam bu bu mujj ba nuy wax xutbab tàggoo ba, mu dénk ca jullit ña dëggu, bennoo, boole séen sàppe, jóox farata yi lislaam digale ak tënku ci ponki jikkoom yu màgg yi, bi mu noppee jàngal nit ñi waxi sunu boroom ju tedd ja: (( al yawma akmaltu lakkum diinakum, wa atmamtu halaykum nihmatii, wa radiitu làkkumil islaama diinan)) di : (ci tay jii de laa matale seen diine ji, ci laa matale xéewal gi ma leen doon jox, te lislaam nag mooy diine ji ma gërëm te sopp ko ci yeen). Fii nag jullit ñi yëg nañu fi ne yonnant baa ngi leen di tàggu te di leen dénk li ñu war a def bu ñu ko gisatul, ñoom ñépp jàq te am lu leen naqari.

Bi Yonnant bi (j.m) delloo Madiina la yëg – ci mujjug safar – lu mel ne tawat di ku dugg, waaye faalewu ko, dafa wéy di ligéey ba tawat ji far ko man, mu doog a tëdd, waaye tawat ji yàggul, ndax mi ngi làqu ginaaw bi tawat ji amee ci moom fukki fan ak juroom, di ci 13 rabiihul awal atum 11 g.g ( 8 suwe 632 g.j) :

Jëmmi Yonnant bi

Ci nii la Yonnant bi (j.m) tuxoo dem ca boroomam ginaaw bi mu jottalee bataaxelam bi ci anam gu mat te yaatu, tas ko ba ñépp jot ci, ca na mu ware. Wooteem gi mi ngi ko tàmbali cig wéet , ay gàllankoor aki pakastal gaar ko ay yooni yoon, mu daje ciy coona lol manoon naa yoqatloo geneen góor gu mu manoon a doon gu dul moom, woote na fukki at ak ñatt yoy amu ca lenn ngérte lu am njariñ, waaye mu sax di ku dëgër ag ngëm ci Yàlla, ku am kóolute ci ndimbalam, wéy ca liggéeyam ba ba ndimbal dikkal kook ndam ginaaw bi mu gàddaayee dem Madiina, daal di fay taxawal umma bu lislaam bi, dox ak moom ci yoonu nosu ak doole ci anam gu màndaqewu te callalewu, weer ginaaw weer, ba mujj am ci ndam lii ngay gis tay.

Yonnant bi nag li ko dimbali ci mu jot jubluwaayam bii mooy jikko yu yéeme yi te wéet yi mu jikkoo woon ak bataaxelam bii bàyyikoo woon ca Yàlla ma ko tànnoon ngir mu jottali ko.

Ñun nag manuñoo lim mbooleem jikko ak ngënéeli Yonnant bi (j.m), looloo waral jullit ñi ñoom dañu koo def muy xam-xam ci jëmmam bu ñuy jàng ñu koy wax xam-xamu jikkoy Muhammad (As shamaayil al muhammadiya) taalif nañu ci lu dul jeex, ñun nag ñu ñeme ñemelu indil leen lenn ci yi ëpp solo ci jikko yii :

Gëm gu xóot ci Yàlla

Gëm gi mu gëmoon Yàlla gu matale woon la te xóot, da daan def fu jafe-jafe yi gënee bari, gàllankoor yi gën a dolliku, gëmam gi ci boroomam gën a dëgër, mu gën a ŋoy ci bataaxelam bi, gën a dogu ci wisaare wooteem bi ko Yàlla dénk.

Looloo taxoon Yonnant bi ak saaba yi daawuñu nangu lu dul ngëm gu mat gu dara ci sikk dul jege. Ci daaray ngëm gu xóot gii la saaba yu mag yi génne, ku ci mel ne Aboo Bakr, Omar, Aliyu, Usmaan, Sahd’Ubn Abii Waqaas, Abii Hubaydata Haamir’Ibn Jaraah, Talhata’Bn Hubaydul Laah, Zubayru’Bnul Hawaam ak ñi mel ni ñoom ci ñi war a yanuji raayob lislaam ginaaw Yonnant bi (j.m), te war a tasaareji diiney Yàlla ji ci li ëpp ci pàkki àdduna yi ñu xamoon ca jamono jooja

Jafandu ci way teddi jikko yi

Ngir gëm gu dëgër gu xóot googu ci boroomam (t.s) ak ci lislaam, daawoo gis Yonnant bi mukk muy jëf ci lenn ndare bu tegu ko ci gën jaa dëgëri dàtti jikko yi, niki dëggu, matal kóllare, wóor gu mat ci wax ak jëf, ak seelug yéene ci lépp lu muy wax mbaa mu koy jëf, ak tëyye bu dëgër cig maandu ci mbooleem ay jëflanteem aki saabaam, ba ci ay kontaram, nekkoon na di ku bu waxee dëggal, bu dëelee matale, bu kóllarantee def ko, bu manee jéggale.

Doylu ak bàyyee

Yonnant bi de ak li ko dikkaloon lépp ci xéewali àdduna, ak teddnga ak doole teewutoon mu nekkoon di kuy doylu ci gën jaa tuuti ci xéewal yi, dundam gépp masu cee feesal biiram ciw ñam, lu néew ci mburu la daa mos ak tàndarma, bu amul rëndaay mu rëndaayoo diw, mbaa diw ak bineegar, mbubbam ak dallam ci loxoom la ko daa daaxe, daan fóot mbubbam bis bu jot ci loxoom, ndax moom (j.m) ku jéggi woon ab dayo la ci set, bis bu nekk daa na ci socc ay yooni yoon.

Daawul toggoo nag ag dund gu ñagas te di ko woote, moom kay ñam wu ko dikkal rekk mu lekk. Soloos na ci moom ne daawul sàkku mukk aw ñam wu fi nekkul, cib pajaas la daan nelawe, am mbalaanam it lu gàtt la daan doon, daawul tëju ay saabaam, ki gën a doyodi ci nit ñi da ko daa gis di wax ak moom, waayam ja ko daa ligéeyal di Anas mom Maalik nee na masul a dégg ci Yonnant bi ci dundam gépp benn baat bu ko mas a naqari.

Daf daan bàyyee saabaam yi xéewal yi, te daawu ci féetewoo dara bàyyi leen, nekkoon na di ku sopp xale yi te daan kaf ak ñoom, ku amoon ag ñeewant la ci jirim yi, way ñàkk yi, ñu doyadi ñi, di seeti way tawat yi, bëcëg bépp it ci yëgg la daan nekk, daawul dal, ku bañoonug jekki la ak tàyyeel, daa na ko moytulooy saabaam.

Misaal la woon ci ni ñu war a jiitee xeet wi ak ni ñu ko war a sàmme

Yonnant bi ku amoon ag yewwute gu sax la, daawul ba dara romb ko ci lu aju ci umma bi ndare bu da koo gendiku bu baax te settantal ko. Daf daan settantal di teg ay naal yu jub, yu yaatu yu muy jaar ci ligéeyam ci anam gu nosu te toftaloo. Yitteem jépp da ko daa sotti ci li ëpp solo ci mbiri xeetam wi, teg ca la ca topp cig am solo. Daa gisoon ne ay ligéeyam aki jëfam roytéef la wuy saabaam di jaari ëlëg, làmp la bu ñuy niitloo, moo waraloon lu muy def rekk mu koy def cig njàngale , cig yare. Bu kenn ci saabaam yi juumee ci mbir, da ko koy won cig nooy, leeral ko lay la jub. Ku daan am ag muñ ci way xuloo yi la, daan leen jéggal seeni soppaxndikooki jikko yu ñaaw ngir ñu gis seen njuumte, dellu ca jub ga. Ku wormaaloon nit ñépp la, daan sàmmoonteek teddngay ki gën di gone ci ñoom ak àqam. Masuñoo dégg fenn fu ñu ne Yonnant bi (j.m) génnee na fa baat bu ñaaw jëme ko ci kenn, ak doonte kenn kooku da dib noonam. Bu masaan a mer day noppi ba mer wa dañ mu doog a wax nànk, cig dal.

Yonnant bi noppee ko gënaloon wax, dégloo ko gënaloon déggal. Bu masaan a wax day àgg ca la mu bëgg a wax du jàdd-jàddal, def ko it ci baat yu leer te gàtt, looloo taxoon Yonnant bi (j.m) moo gënoon a am fasaaha ci nit ñi, gën cee am balaaxa, adiisam yi ci balaaxa ñoo topp ci Alquraan miy wax ji gën a balaaxaa ci wax yi.

Yonnant bi (j.m) yérmaande la ñeel mbindéef yépp, bi muy ñëw ci àdduna bi da koo fekkoon mu yor lëndëmug réer, ndof, xamadi Yàlla, waaye mu bàyyikoo fi, ba fi ag leerug gëm Yàlla . Mi ngi feeñ ci araab yi te booba ñi ngi ciy xareek fitna ak ŋaayoo, mu juge fi ba leen ñuy xeet wuy wenn, yiw peek leen, lislaam ëmb leen, jàmm uuf leen. Ak li Yàlla sotti nit ñi lépp ciy xéewal, jaarale ko ciy loxoom teewul Yonnant bi – jàmm yal na nekk ci moom – bi mu fiy juge di woon ku ndóol, ku moomul lenn. Saddaloon na nit ñi aw léew ci nite, ngënéel, def wartéef, sellal ak dëggu. Yàlla dëggal na – tudd naa sellam ga – ba mu nee : ((yaa ayuhan nabiyu inna arsalnaaka shaahidan wa mubashiran wa nadiiran wa daahiyan ilal laahi bi idnihii wa siraajan muniiran, wa bashiril moominiina bi anna lahum minal laahi fadlan kabiiran)) muy :( yaw Yonnant bi de dañu laa yonni ngay seere tey bégaleek a xuppe, di woote jëme ci Yàlla ci ndigalam, tey làmp buy leeral, na nga bégal jullit ñi ci ne am nañu ngënéel lu rëy lu tukkee ca Yàlla) Yonnant bi nag (j.m) tënk na wax jépp ca bataaxelam ba niki kuy jàngale ba mu nee : (dees maa yonni ngir ma mottali jikko yu rafet yi).





----------------------------------------------------------------

Yoonu Murit

Yoonu murit



Sëriñ Tuubaa, ca leer ga

Yoonu murit walla Muriidulaa ni ko ñenn ñi di waxe, wenn yoon wu am solo la wu tasawuf, muy moom tasawuf benn bànqaas bu mbóotu (mystique) ci lislaam , mi ngi nekk nag rawati na ci Senegaal ak Gàmbi. Muy lu ñu sos ci ndoortel XXeelu xarnu, ki ko def di Seex Ahmadu Bamba, yoonu murit nekk na tay yoon wi gën a am ag jeexiital ci Senegaal, bu ñu waxul ci Afrig gu sowwu gi [1] Murit yi tam ñi ngi jëf lu am solo ci wàllug koom-koom ak politig [1]. Njiitul réew mi Abdulaay Wàdd, mi ñu fal ci 2000, mooy njiitul Senegaal lu murit li njëkk a am [2].


Aaday Murit

Ay taalubey murit ca Xelkoom di liggéey
Ay taalube ca Xelkoom

Aaday murit (walla ju yoonu murit)lu jeexiitalu ci caaday Afrig la, rawatina ju wolof. Yitte ak fulla ji yoon wi jox liggéey tax na ba mu man a suuxatu bu baax ci wàllug koom-koom ci Afrig, te tax na it ba mu man a tas bu baax ci dëkk yu mag yi ci Tugal ak Diiwaan yu Bennoo yi. Tay, daanaka mbooleem dëkk yu mag yu Bëj-gànnaar yi gàddaay gu Senegaal gi dëgmalsi te jëm fa kanam, am na ag Kër Sëriñ Tuubaa (Barabu daje ngir julli, jaamu Yàlla, defi màggal, daaray jàng xam-xam añs). Moom de dalub mbooloo mu murit mi la, fi ñuy defe seeni daje ngir jaamu Yàlla, walla ngir leneen, waaye it dana di jariñ it niki ab teeruwaayu gan ñeel way door a agsi yi ciy gan. Danañuy faral di def ab siyaare walla lu mel ne ag aj gu ñuy def ci at mu ne ca dëkk bu sell ba Tuubaa, gi nekk ci digg Senegaal.Màggal gi genn xumbéel la guy jëmmal at mu ne fàttalikug gàddaayal gi ñu defoon Seex Ahmadu Bamba ca 1895, ci loxol kiliftéef gu Canc gi (l'autorité coloniale).

Gongikubaat

lenn ci ay njiiti yoonu murit wu tasawuf wi ci benn miir ci Ndakaaru

Baatub mourid walla murit ni ko wolof yi di waxe, mi ngi bawoo ci Jef ju Iraada, te mooy « bëgg dara », « namm dara, xëccu jëm ci lenn » teg ca gongikooti ci murīd giy tekki « aji namm mbaa aji bëgg», jubloos ci aji namm ji Yàlla ki bëggul ku dul moom, lu dul moom, lu dul ngërëmam, loolu it mooy firi fonk gi taalube yi di def seeni sëriñ, ndax Yàlla ga ñuy gis ci ñoom, maanaam ñoom ñoo fi nekkal Yàlla ci jàngale Diine ak aar ko. Murit nag benn la ci ñaari baat yu ba ca des di Laah, kon muy muriidulaa, di tekki aji namm ji Yàlla, maanaam ki Yàlla rekk tax a jug, mu mel ne baat bii mbooleem yooni tasawuf yi dañu koy jëfandikoo niki taalube, walla dongo, waaye bokk na ci li gën a génne baat bi, jox ko fulla mooy ñëw gi yoon wi ñëëw ci jamono joj lislaam da cee xawoon a doyodi, néew ci doole, te li ko waral di nekk gi nit ñi nekke woon lu wuute ak lislaam, daan ko foye, yor geneen dund gu dul gi lislaam tànn, wii melo di lol ñu bari ci bindkati Senegaal yi wax nañu ci, ku ci mel ne Sëriñ Musaa Ka ak ñu ko moy, melokaan wii nag man nañu ne bokk na ci li taxoon Seex Ahmadu Bamba jugoon mel ne ku naan «ana ku namm Yàlla» ana «ku Yàlla tax a jug», ca foola la baat bii daal juge di tekki leegi képp ku di taalubeb murit, muy baat bob daa jug mel ne kuy tàqale diggante ki nekk ciy caaxaan ak ki ko nangoo ba te jublu lu baax li di Yàlla ak la ko wër. Sëriñ bi booy xool day mel ne yorul aw yoon, waaye lislaam la jug ngir taxawalaat, yeesalaat, ndax mbooleem yoon yi mu fi fekk, da leen a nangu, topp leen, jël seeni wird, daa na joxe mbooleem seeni wird te booba mi ngi yor wird wu juge ca Yàlla jaar ci Yonent bi Muhammad, ni yoon yepp ame seeni wird. Leegi kon luy ndayi muy joxe yooyule wird te yoroon wu boppam? Ndaxte daa jugaloon lislaam déet aw yoon, moom moo wax ne

« wépp wird wu waay yor ngir jëmmi Yàlla rekk te leneen taxu koo jug, moo xam woowu daa bawoo ca Jiilaani (Xaadiriya) mbaa mu juge ca Ahmad Tiijaan (tiijaan), na xam ne li mu yor moo dig jub»

Kon kii boole jullit yee ko taxoon a jug, yombal seenug jëm ca Yàlla, far digi yoon yi, boole ñepp ñuy jaami Yàlla ci ron keppaarug Lislaam


Yàllaange (Théologie) ak nosiin wu biir gi



S Tuubaa


Yoonu murit Seex Ahmadu Bamba (1853-1927)moo ko sos, mu di aw yoon wu mbóotu wow mi ngi feeñ ci Senegaal ci biir aw nekkiin wu mboolaay wu ñu nëxël ag sellam jaxase ko, nga xam ne Canc gi (la colonisation) jaxase na bu baax nosteg màndaxoo gu mboolaay gi (le système d'équilibre social). Ngir nag yéwénal mboolaay gu senegaal gi Seex Ahmadu Bamba daa woote woon jëme ci ñu roy njàngalem Alxuraan mi, te ŋoy ci sunnas Yonent bi Muhammad (j.m), te xeeñtu it maanaay tasawuw yi te roy ci, fullaal it xam-xam ak liggéey te jox leen seen àq ak xiima.

Lii nag daa dëppoo ak li ñuy wooye ag yeesal mbaa ag yéwénal, ndax ci Tasawuf waxees na ne Yàlla (t.s) day yonni ci téeméeri at yu ne, jenn Aji yeesal (walla mujaddid) juy taxaw ci dundalaat, yeesalaat lislaam ca dëgg-dëggam, kooku tam mooy nekk aji donn ju ruu ju Yonent bi (j.m), ñu koy wax (qotb walla « pujub cellte ») maanaam fa ag sell man a yam. Bamba kon kenn lay doon ci tànnéef yii.

Yàllaange gu murit yi (walla seen gëm-gëm) dafa jeexiitalu ci yoon yii di Xaadiriyaak Tiijaan waaye it ak mbindi Alxazaali, nga xam ne Bamba da koy tudd lu bari ciy mbindam. Yenn jullit yiy woote ag cunna danuy jàpp ne gëm gu tar gii am ci murit yi jëm ci Ahmadu Bamba aki way donnam aw xeet la ci ag njaamu xërëm, waaye booy xool xamadi rekk a ko waral, ndax ku xóotal ab xam-xamam ci yoon wi duggi ruqam di nga gis lu dul loolu, nit nag bu jëfee lu moy la ñu ko xamal moom mooy ka tooñ, kon na murit yi di jàng mbindum Sëriñ bi tey bañ di tëñëxu di doxe ni ñu ko bëgg a doxe, bëgg ko nee gëme, tey doxe ni ko Sëriñ bi bëgge ci ñoom. Seex Ahmadu de giseeful ciy mbindam lenn lu dëppoowul ak Alxuraan ak sunna [1].

Murit yi am nañu ay jikko ak xiima yu di yu lislaam fekkoon ci ñoom, te xawoon a giim Sëriñ bi ñëw dekkalaat ko . Bokk na ci yooyu liggéey gi ñuy àgg ci di sellal, jàpplanteek dimbalante. At mu nekk ay milyoŋi nit dañuy bawoo fu nekk di màggali Tuubaa gi nekk ci digg Senegaal . .

Ni ko Emmanuel Brisson gise, Yoonu Murit « dafa nosu - ci gis-gisu ñenn ñi - niki ag noste gu laman (système féodal), moom daa tegu ci kaw ag toppe gu joyu ñeel genn kiliftéef gu ruu (une autorité spirituelle), Xalifa bu matale bi (le Khalife général), di ku doomu mbaa mu sëtu ci anam gu jonjoo ci Aji sos ji yoon wi. » [2].

Taariixu yëngu-yëngu gi

S Saaliwu, ki fi mujj ci doomi Sëriñ Tuubaa yi

Muy ku janook yoriin wu cang gi(l'administration coloniale) maanaam tubaab yi ngir mbooloom mii di wéy di màgg ba tàmbali woon leen a tiital, Seex Ahmadu Bamba gàddaayalees na ko ci anam gu toftaloo ca Gaboŋ (Afrig gu yamoo gi (Afrique équatoriale)), dale ko ci 1895 ba 1902, ca Gànnaar dale ko 1902 ba 1907, ginaaw bi ñu teg ko ci ron ag dëj gu ñu wattu (résidence surveillée) ci Senegaal ba kero muy làqu (génn àdduna) ca 1927. Kiliftéef gu Faraas gii mujj na ko nànd xam ne aw ay taxu koo jug, mu jàmmal ko, loolu it may yoon wi ci ndimbalul Yàlla ag naataange gu kawe.

Bi fi Sëñ bi jugee ci 1927 ba tay, ay Xalifaam yi ko fi wuutu ñooy ay doomam, dale ko ca ka ca mag, ba ca ka ca gën di gone:

  1. Sëriñ Muhammadu Mustafaa Mbàkke, dale 1927 ba 1945
  2. Sëriñ Muhammadu Falilu Mbàkke, dale 1945 ba 1968
  3. Sëriñ Abdul Ahad Mbàkke, dale 1968 ba 1989
  4. Sëriñ Abdu Xaadir Mbàkke, moom ag ayam weesuwul 11 weer dale 1989 ba 1990
  5. Sëriñ Saaliwu Mbàkke (mi ngi gane àdduna 1915), di xalifa dale 1990, làqu ci guddig 28 jëm 29 desambar 2007
  6. Sëriñ Muhammadu Lamin Baara mom Muhammadu Falilu Mbàkke, dale 30 desambar 2007

Ginaaw bi fi Sëriñ Saaliwu bàyyikoo, moom miy doomi Sëriñ Tuubaa ju fi mujj, la xilaafa gu matale gi tuxu leegi dem ci sët yi. Xalifa bii fi nekk mooy ki mag ci sët yi, di Sëriñ Muhammadu Lamin Baara Mbàkke, ññu koy wax Alaaji Baara.

Seexal

Bi Sëriñ bi yoree yoon wi ci la seexale ñennat ci mag ñi, bu ko defee ñu daal di leen féetale ñenn ci taalube yi, loolu nag daa doon luy am ginaaw ag yar akug wulli ba mu mel ni war ci ab sëriñ dëgg bu war a jiite aw nit ci lislaam, bu man a yare, man a tege ci yoon. Loolu mooy li am ci Maam Seex Ibraayma Faal ak Maam Cerno bi tubaab yi gàddaayalee Sëriñ bi. Seexal gii nag dakkoon na ca 1912, at mi Sëñ bi seexale ki mu mujj a seexal, mu di Madiba Silla ca Njaaréem. Sette gi ci amaat mooy Beeco Cuun mi ñu ne Sëriñ Saaliwu moo ko seexal ca 1987. Seexal gii jeqi na coow lu bari ci biir yoon wi. Bokk na ci Seexi Sëriñ Tuubaa yu may yu jàmbaare yi Sëriñ Ndaam Abdu Rëhmaan Lóo, Sëñ Isaa Jenn


jeexiital gu koom-koom ak gu politig

S Abdul Ahad ak Abdu Juuf ñaareelu njiitul Senegaal ci benn ci ay nemmiku yi mu daa def Sëriñ bi
S Saaliwu ak ab taalubeem biy njiitul Senegaal Abdulaay Wàdd

Yoonu murit mi ngi gën di yaatu bu baax, te am na it ag jeexiital gu am doole ci politigu Senegaal . Moom day joxe ay ndigali farle (consignes de vote) te xalifa bi it lu sakkan ciy way politig dañu koy seetsi, di diisook moom juge fu ne.

Ci wàllug koom-koom ak mboolaay , « Ñoom Murit yi dañuy joxe dëkkuwaay, dund ak tàggatug xel - ci jàngale alxuraan ak xam-xam yi ci aju - ñeel xale yi gën a ñàkk, mbaa yi "sànku". Am nañu ay way jam (détracteurs), yu leen di yedde seen roose gi, seen mbay mu bari mi, seen ndimbal gu mboolaay gi (aides sociales). (...) Yoon wi war naa yor koom bu sakkan mu bawoo ci mbay mi, rawati na ci gerte g. » (Brisson, 2008 [2])

Wisaaroo gi (La diaspora) ca Paris, ca Brescia ak ca New York, nga xam ne daa jàppe xaalis muy lu sell, ndax ci liggéey la meññoo, ak ci yaxantu, day yonnee ay lim yu rëy ci xaalis ñeel mbokk ya nekk Tuubaa.

Xalifa yu Murit yi ñaare ñu am ag jeexiital lañu, ndaxte duñu rekk ay njiiti ruu yu ay taalube yu ñu nattale ci 3 ba 5 milyoŋ, (man jortu naa ne ëpp na loolu di dem ndax Tuubaa rekk lu ëpp milyoŋ dëkk na fa), waaye it ca dëgg-dëgg ay njiit lañu yu jamono (yu àdduna) yu dëkkub Tuubaa bii nga xam ne mooy péey bu ruu bu murit yi, te mujj na ndànk ndànk (moom Tuubaa) di ñaareelu dëkk bu Senegaal, ngir diisaayu demogaraafam ak bu koom-koomam.

Yeneen doom mbaa sëti Sëriñ bi, ñoom it ñu am ag jeexiital lañu ni xalifa yi, ak doonte àgguñu ci xilaafa gi. Ku ci mel ni:

  • Seex Ahmadu Mbàkke Gaynde Faatma, mi ñu xam ci ag sóoboom ci yar ak jëmale kanam gu mboolaay-koom-koom (socio-économique) gu mbooloo yi, xame nañu ko it ci jeexiital gi mu am ci njiiti politig yu Afrig yu mag yi, mi ngi faatu ci 1978 ;
  • Seex Muhammadu Murtalaa Mbàkke, "sëriñub wisaaroo gi" (le marabout de la diaspora), moom it muy ku ñu xam ngir sos gi mu sos ngir Yàlla rekk lu sakkan ciy cëslaayi jàngu ci mbooleem Senegaal, mi ngi làqu ci 2004. fii mu tollu doomam ak xalifaam sëriñ Maam Moor Mbàkke mi ngi wéyal ab liggéeyam, di ci dolli yeneen cëslaay yu bees(autres structures nouvelles) yu dëppook gis-gis bu jëm-kanam bi mu am ci ag jamonoo (la modernité). Moom de mi ngi jéggeek murit gi ag wàll gu am solo ci lu aju ci wisaaroo gi (au niveau de la diaspora).

Bidaa

Maan Seex Ibraayma Faal
Am mbooloom Baay Faal ci mbedd yi di màjjaal

Kenn ci ñi gën a siiw ci taalubey Bamba yi mooy Seex Ibraayma Faal. Bàyyi na fi ay dongo yu ñuy wooye Baay Faal yiy wottee seenug ñàkk a julli ak woor, liggéey bi ñuy def ci seen loxo ak yalwaan , looloo tax yeneen jullit ni ñoom di leen jam tey naqarlu seeni jëf. Seen njañ yi ñu yore ak seen létt yi yobbe na leen way nemmeekusi yi (touristes) di leen jaawale aki rastamen . Maam Seex nag nekkoon na di ku dëggu te liggéeyal lislaam lu réy, waaye ñàkk a jullit gi ñu bari firee nañu ko ci ne daa amoon ngànt, ndax daa meloon ne ku àndul woon ak sagoom, booy xool it ci ni mu daa waxe mbaa mu koy jëfe lépp da daa wund loolu, mu mel ne ku sóobu la woon ba sóobu gi yobbu ko ci mu nekkoon di ku àndadi akum xelam te loolu lislaam boole na ko ci sart yiy tee julli di war. Bokk na ci sart yiy tax julli di war nit ki ànd akum xelam. Sëriñ bi bind na ko bataaxel bob Sëriñ Abdul Ahad 3eelu xalifa génn woon na ko móollu ko ca téere ba ñuy wax majmooha, muy téere bu dajale waxi Sëriñ Tuubaa yu bari, ma nga cay wax naa :« Yaw Ibraayma Faal boo jotee ci sama bataaxel bii nanga digal sa ñoñ ñuy julli te nga sax ci te muñ ko, laajuñu la wërsëg ñoo la koy jox, te mujj gu rafet ñeel na way ragal Yàlla yi,» lii di aw laaya wu alxuraan wu mu ko yonnee ngir délloosi ko ci, kon day mel ne Sëriñ bi moom wàcci na ak ku nekk, Maam Seex nag ak ni mu gëme Sëriñ bi bu julliwul ngànt a tax, ndax daawul jëfeedi ndigal te loolu ndigal la woon. Seen gëm-gëm nag amul lenn lu ko wuuteel ak bu lislaam, ñu jàmbaare lañu ci lislaam di liggéey di joxe, ngir lépp lu ñu war a kopparal ci lislaam man a kopparu, lépp luy sémb man a àntu, foo leen fekk dañuy sikkar (maanaam tudd Yàlla) di woroomi pastéef yu kawe aki jéll, bu koor gee ñuy joxe ay ndogu ñeel way woor yi, di tabaxi jàkka aki jumaa, lii rekk mooy li ñu leen man a doyodale ci lislaam te du ñépp ñooy ña ca dul julleek a woor, am na ci ñoñ dañu koy def, doonte ñu néew lañu it.

Seex Ahmadu Bamba

Seex Ahmadu Bamba

Ab jukkib Wikipedia.

Dem : Joowiin, Seet
Benn nataal bu Xaadim Rasuul

Seex Ahmadu Bamba Xaadimur Rasuul (Cheikh Aḥmad ibn Muḥammad ibn Ḥabīb Allāh 1853-19 sulet 1927) boroom xam-xamu diine bu jullit la bu di ab sëriñ te cosaanoo ci ag càllala gu doomi soxna. Mi ngi gane àdduna ci Mbàkke, ab dëkk bu maamaatam sancoon ca nguurug Bawol, maamaatam jooju mooy Maharam, walla Maaraam,mooy ki sanc Mbàkke Bawol, waxees na ne loolu ci atum Shaqdadin la di (1194 g / 1780 g.j ) . Waaye dëkkewu fa woon, da fa a bàyyi woon ab taawam Muhammudu Farimata, magi habiibullaah ju mu bokkalul nday. Moom nag sëñ Maaram mii daa desoon Jolof, fa la làqoo ñu denci ko fa, di ko siaare.

Ñu koy woowe itam Xaadim Rasuul di Ñaari baati araab yuy wund Surgab yonent bi Muhammad (j.m). Mu bokk ci jëmm yi gën a fés te ëpp solo ci diiney Lislaam ci sowwu Afrig, ndax moom moo sos yoonu murit. Waa-réewam Seex Ahmadu Bamba lañu koy woowe ndax cofeel gu ñu am ci moom.

Tëraliin

[Nëbb]

Jaar-jaaram [Soppi]

Doomi ab sëriñ ci yoonu (Xaadirya) – Mooy yoon wi gën a yàgg ci Senegaal –, Ahmadu Bamba ab jullit bu dëddu la woon te dib sóofiyu, daan bind it ci wàllug fiqh, tasawuf ak wéetal Yàlla (tawhiid) ak wàll yu bari ci xam-xamu diine, ak tagg Yonent bi, mbaa ci lu aju ci "shukr" (sant Yàlla).

Jiyaaram [Soppi]

Ak doonte ku daan bañ la te àndadi woon ci canc gi (colonialisme) ak teg loxo gi tubaab yi defoon réew mi teewul melul woon ne sëriñi tiijaan yi jugoon di jiyaar, ku ci mel ne Alaaji Omar Taal, Màbba Jaxu Ba mbaa Muhammad Lamin Daraame. Ak doonte yoroon na gëm-gëm bi mbooleem jullit ñi yoroon ci Jiyaar , muy jug dàkku sab dëkk ci tooñaange, xeex ngir goreel ko, mbaa aar sa alal añs, teewul mu yoroon beneen gis-gis bu gën a xóot ci jiyaar, mooy jiyaaru nafs, maanaam jiyaar ngir xeex ak sa bakkan ak sa bànneex, noot ko, moom ko, nga rax ci dolli ku gisoon la ne tubaab yii de xeex ak ñoom ciy ngànnaay yombul, te deesu ci jële ndam, - te mel na ne jamono jox na ko dëgg ! Ndax mbooleem ñi doon def jiyaar ak tubaab bi, tubaab bi faroon na leen noot, mbaa mu ray leen, tee leen a sottal seeni sémb, àntoodil seeni naal - ndax ëpp gi ñu ëppoon ci doole ak ngànnaay te gën koo aaytal, gën koo ñawle, bi lii amee, Ahmadu xam ne tubaab yee ko raw foofu, ca rafetug xelam ga mu jël beneen "estrateji", mooy jiitu leen ci xol yi, ba lu tubaab yi def ci kaw mu def ko ci biir, lii moo nekkoon mbóotum jiyaaram.

Alxuraan mi ngi nuy xamal digal gu Yàlla digaloon jullit ñi ñuy jiyaar ak yéefar yi, ak doonte dañuy fukk jullit biy kenn, ba yàgg mu ne woyofal na ko ci yeen (jullit ñi) ndax xam doyadi gi nekk ci ñoom, mu ne leegi kenn mooy xeex ak ñaari yéefar, ndax xam na ne pastéef ba woon wonni na, te loolu mooy jàmbaar ya àndoon ak Yonent bi (j.m), naka mook tuubeen yii nga xam ne ba ñu duggee ci lislaam yàggul, te tubaab ëpp leen doole fuuf ak ngànnaay, kon kii ci hikma la jëfe te mooy li Yàlla bëgg

Mbindam [Soppi]

Bind na it lu maneesul a misaal ciy taalif, lu ci ëpp nag ay woy, yu muy def la, benn ngir tàgg ci Yonent bi (j.m), mbaa sant ci Yàlla, mbaa mu ciy wone may yu ko Yàlla may, loolu lépp di tàbbi ci sant Yàlla, mbaa mu jëm ci yar ak njàngalem diine, loolu nag ci araab la daan doon, teewul mu daa def ay tomb di ci tënk li muy jàngale ci araab, daan ko def ci wolof ñeel ñi xaw a mage ba jànge ci araab raw leen, mbaa seeni xel xaw a naqari ba ñuy am ay jafe-jafe ci jànge ci araab. Bokk na ci li ko tax di def ay woy ci taalifam yooyu, woy day jumtukaayu mokkal, mokkal ay woy daa gën a yomb ay wesar, looloo tax sax téere yi mu taalif ci xam-xam ngir taalube yi jàng ko, da leen a def ci ay woy, teewul bind na as lëf ci wesar lu ci mel ne majmooha, jasaawu sakkoor bu géej gi te sëñ Sëriñ Musaa Ka woy ko ci wolof añs.

Ku fonkoon wolof la ak doonte ci araab la daan binde [Soppi]

Ci araab it la daan binde, sabab si nag su diine la waaye ku fonkoon aw làkkam la lool, ci la daan waxe te déggoon ko lool, daa na faral sax di jël waxiinu saalum-saalum wi ñu daa wax ne mooy wi gën a wolofe te gën a xóot di ko waxe, bis kenn ci ay taalubeem yi daa woy ci wolof ci seeni taalif, daa jugoon di ko tagge ci araab, mu ne ko bu ko defati, dee ko defe ci wolof, ndax man ki may tagg araab la te man mi ngay tagg wolof laa, kon kee da koo war a dégge ci aw làmmiñam, man it naa koy dégge ci samaw làmmiñ, lii moo waral ñu ko daa woy ci wolof, teewul nag am ciy taalubeem ñu ko woy ci araab niki Sëriñ Mut Jaw Paxa, Sëriñ Ibraayma Jóob Almashari.

Man nañu ne sax mooki taalubeem ñooy ñi suuxat làkk wii, ndax ñi ëpp ci ñi bind ci wolof ci Senegaal ñoom lañu, xool ci ku mel ne Sëriñ Muusaa KA, Sëriñ Mbay JAXATE, Sëriñ Mbay Kayre, Sëriñ Moor Jaara Mbay, ba ci Mamoor Xam Sa Diine mii, te Tuubaa day tuuru ak ñu mel ni ñoom.

Sababu binde ci araab [Soppi]

Sabab si deene la, loolu it bind na ko ci genn ci ay xasidaam mu ne ca dañoo araamal ci moom muy bind ci lu dul ci làkku araab, wax jooju xel nangu na ko, ndax araab mooy làkk wu kilifawu (officielle) wu Lislaam, képp kuy njiit ci lislaam ñépp war a jariñu ci yaw ci nga war di binde, booy xool bindkat yi gën a mag ci Lislaam duñu ay araab te teewul ci lañu doon binde, ngir aar làkkuw alxuraan wi, jëmale ko kanam, tax it deesi ci sonn ba muy waral ñuy man a xam alxuraan ci lu dul ag xamal, ndax bu xam araab gi wéree xam alxuraan gi wóor te rafet.

Nga rax ci dolli ci araab la jànge, làmmiñ wi réew mi mépp daan jànge, daan ci bindantee it ci lu fullawu (lu officiel), ba ci tubaab bi sax yoroon na ay "antalpareet" walla ay làpptoo, maanaam ñu leen di tekkil ci araab ak di leen ci bindal, ndax xam gi ñu xamoon ne réew mi lu ci ëpp ci araab lañuy binde.

Te it ca jooja jamono wolof làkk la woon wu yaatoowul noonu, te du woon wolof yi rekk ñoo waroon a jariñu ci Sëriñ bi mbaa ñoo nekkoon fa moom, lii lepp taxoon na muy binde ci araab. Waaye teewul nekk gi mu nekkoon di nitug Yàlla taxoon mu xam lu ñëwagun, yobbu woon ko ci mu digal ñenn ciw nitam ñu féetewoo jëmale kanam wii làkk ndax xam gi mu xamoon ne mooy làkku ëlëg ci Senegaal

Sancug Tuubaa [Soppi]

Jumaay Tuubaa ju mag ji

Sancoon na Tuubaa ci 1887 ngir gën a man a wéetal Yàlla, ginaaw bi nit ñi baree fa moom ca Daaru Salaam ga ca anéeri Mbàkke gi ñu la waxoon leegi, nga xam ne raj-rajloo ba teewoon na koo nekk ca na mu ko soxlaa ba man a def li mu bëgg cig jaamu ak yar, ba mu demee Tuubaa't loola toppati ko fa, moo waraloon mu faroon sanc Mbàkke-Baari ca Jolof, fa la juge dem géej boo ci bëggee xóotal yëral: SancamJolof Ak li ko waraloon.

Tuubloo ay buur ak doomi buur [Soppi]

Ci bañ gi mu defoon cancug Tubaab yi ak séen politigu nasaraanal bi, Sëriñ bi mujjoon na tuubloo lu sakkan ci y buur aki doomi buur yu diiwaan bi, Jàmm la daan digle, jaamu Yàlla ak liggéey ngir man a texe ëllëg. Looloo waraloon lu sakkan ciy mbooloo doon bawoo fu nekk di sottiku ci kawam, ñii ngir jébbalusi, ñii ngiri sabab yu àdduna, loolu lepp nag jeqi woon na ñàqare ak jaaxle ci Tubaab yii nga xam ne doonuñu woon nangu ñu dul ñoom ñuy am genn jeexiital ci réew mi, mbaa genn kiliftéef gu àdduna gu bawoowul fi ñoom

Sababu jàpp gi ak gàddaayal gi [Soppi]

Waaye bi Tubaab yi gisee ne moon de boroomum mbooloo la te ñu ko gëm lañu, man na leen a yëngal bis jëme leen ci jiyaar, ni ko moroomi sëriñam si defe woon, lañu ko daal di jàpp, tëj ko ci kaso fa ñoom, ca Ndar giy dalub kaŋ bu ASF (Afrig gu Sowwu Gu Faraas gi), njëkk ñu koy gàddaayal ca Gaboŋ ci 1895. Tubaab yi ngir ñu man koo jàpp lay yii lañu indi woon:

«Ñun de gisuñu lenn luy wone ne Ahmadu Bamba day woote Jiyaar, waaye ab taxawaayam akug soppaxdikoom ak yu ay taalubeem daal teey nañu xel, jeqi nañu sikk »

Dellusi gi juge ca géej ga [Soppi]

Mi ngi dellusi ci Ndakaaru ci 1902 gannaaw ba mu defee 7 at ak 9 weer cig gàddaayal te nekkoon ci àll yu lëndëm këriis ya, bu ko defee mbooloo mi teertu ko ciy yuuxuy mbegte ak ségéré.

Tubaab yi jàppati ko [Soppi]

Tubaab yi jéemaatoon nañu koo jàpp ba yabaloon fa ay spahis nga xam ni ay xarekat yu ñuul lañu te àndoon ak nootkat bi waaye taalibey sëriñ bi àntoodil loolu. At mi ci topp lañu ko mujj jàpp daal di koy gàddaayal ca gànnaar ci lu tolloog 4 at. Ci diirub ñaari gàddaay yii nag xew-xew yu xel dajul jot na faa am, ngir gën cee am xam-xam yëral: Ñaareelu tukki bi (bu Gànnaar bi).

Tubaab yi xam nañu ko leegi [Soppi]

Gannaaw 1910 nag ci la tubaab yi xam ni sëriñ bi xeex yëkkatiwu ko te sax jàpp nañu ñoom ni yoon wi da leen di jàppale ci li ñu bëgg, ci noonu lañu sàkku liggéey ak moom maanaam ñu ànd far, ngir wone loolu ci lañu ko bëggoon a takkal raayo bii di “Légion d'honneur” di raayob teddnga bu Faraas bi gën a kawe waaye sëriñ bi gàntal.

Yoon wi nag mi ngi gën a am aw nit ginnaaw bi mu fi bàyyikoo te taawam bii di Sëriñ Muhammadu Mustafaa Mbàkke tàmbali woon liggéeyub jumaay Tuubaa ji, di tolloo ak barabam bi, doon tay fu nit ñi di siyaare cig rajrajloo. Gannaaw bi mu fi jógee, ay way donnam ñoo nekk ci xilaafa gi di digle tey tere.

Fatalikug Sëriñ bi [Soppi]

Pentiir ci ab tabax Ndar

Ahmadu Bamba, ku taalibeem yi weg te fonk ko la , jàppe woon ko aw wàlliyu, te loolu du woon lees di faral di gis ci ñiy wuyyoo sunna, waaw ndax ci Lislaam daa am ay dawaan (courants) yu ci mel ne bu sunna, bu siit, ak bu tasawuf añs, moom nag Seex Ahmadu ci bu tasawuf bu sunna la bokk, am na ci waa tasawuf yi way teengal, bay àgg ci di jibal ay kàddu yu di yu tumbrànke, mbaa ñuy àgg ci wax juy jéggi dayo ba cig lëmu bay waral sikk ak weddi, waaye kii di Seex Ahmadu ay mbiram ak leer a ko wër, jéggiwul dayo ci genn anam, mbiram ci kitaab la tegu ak sunna ak tasawuf bu leer, te dëppoo ak doxiinu Yonent bi (j.m). Benn nataal rekk lees am ci moom. nataal boobu fu nekk tafees na ko fa, muy ci tabax yi, ci daamar yi walla feneen fu muy fése rekk.

At mu jot ay junniy junni ciy taalibe danañu dem ca Tuubaa dëkk bu sell ba, ngir màggal gàddaay ga mu defoon jëm Gaboŋ muy yamoo ak 18 safar gu nekk. Bis boobu Sëriñ bi moo digle woon ñu santle ko Buur Yàlla ci may yi mu ko may ciy xéewal, muy bu taalibe yi fonk, jàppe benn ci bis yi ëpp solo ci bis yi.

Li mu fi bàyyi [Soppi]

Sëriñ bi da daan woo ay taalibeem ngir ñu dëpp te jublu Yàlla, daan na digal taalibe yi ñuy moytu aw ay tey sàkku xam-xam bu am njariñ, di liggéey, am jom ju ànd ak jàmm, am pastéef ak ngëm ci Yàlla. wax na ni: "[[Yàlla rekk la ragal, samay yaakaar ci Yàlla laa ko wékk."

Sëriñ bi dékku na nattu yu bari te tar. Benn ci ñoom mooy gaynde gu xiif ga juge barab ba ñuy wone rab yi te nekk ca Sor. Bis booba, dees koo tëj bàyyi ko ak gaynde gu mel ni far xar mu gis boroomam. Sëriñ bi doonoon ku jàmmu te ñaw daan na wax ni: "Du ma mas a lor kenn ak ku mu man a doon." Tëj nañu ko ci kaso bu lëndëm def fa ay ràbb, gobar ak jaasi, mu jàng fa saaru baqara ak aali Imraan. Sëriñ Musaa Ka miy baayi way gëstu xew xewi démb ci yoonu murit mi ngi ñuy xamal ni:

  • keroog gis na fa suñu Maam Jaara () mu di ko ñaax te di ko dolliy daara
  • Fii laylatil jumaati lañ ko tàbbal () ci néeg bu lëndëm, noon ya naan ko làmbal
  • mu làmb daj fa gobar ak ràbbu ñu tëj () ko foofa dem, mu daldi jublu xibla kabbar
  • nee na keroog manul woon a sujjoot ngir tar-tar
  • 'Jàng fa saaru baqara ak aali Imraani () jibriilu tijji néeg ba fil xurhaani'
  • Am na fa yaari guddi lekkul naanul () ludul ci leeri Yàlla kooka naanul...
  • Bisub keroog lañu ko génne foofa () yóbbu feneen mu fekk gaynde bóof fa
  • Ñu boole kook gaynde ga tëj leen booba () Gaynde ga mel ni xar mu gis boroom ba...
  • Ñu daal di koy yóbb ci menn mbedd () bole ko ak yëkk wuñ yafal wuy fàdd
  • mbedd ma noon ya dañu koo gaaraante bisub keroog ruu ga la buur gaaraante.
  • Seex Bamba nee ba mu tëbee wuti fa moom () wuute wul ak boroomi laaf amuli buum
  • ba mu ñëwee ba jub ko faf nërméelu () xooj ga ni fojit fa kanam jibriilu...
  • Keroog la gaal gay daw ba wàllu tisbaar () muy jàpp ab madam bu sew daal di fa jaar
  • Daal di taxaw fi kanamam dal di ko laal () Bamba fasaat njàpp ma daal di am aal
  • bamuy masaa mu delsi daal di koy laal ()nee tuuti kon mu tàkk far baal ko
  • gaayi badar ya, ñoo ko booleek der ba () lal ko ca mbeex ma te demul ca bël ba
  • Seex Bamba daldi jàpp julli tisbaar ...

S Saaliwu

Sëriñ Saaliwu Mbàkke

Ab jukkib Wikipedia.

(Yoonalaat gu jóge Saaliwu Mbàkke)
Dem : Joowiin, Seet

Sëriñ Saaliwu mi ngi gane àdduna, ca Njaaréem(Senegaal) ci guddig àjjuma gu 14 ci weeru tëbëski, atum 1333 g.g, dëppoo ak 22 satumbar 1915. Aji juram ju góor di ku jaradee leeral ngir xam gi ko nit ñépp xam di Seex Ahmadu Bamba, ju jigéen di Soxna Faati Jaxate, mom Sëñ Moodu Asta mu baax ma te sell. S Tuubaa bi mu ganee àdduna daa bindoon ciw kayit tur wi di (Saaliwu giy tekki aji baax, aji yéwén) jox ko Sëñ Muhammadu Lamin Jóob Dagana, ne ko tudde ko ko, bi mu ko defee moom S Dagana, daa daal di bind as lëf ciy bayit ñaanal ci liir bu tedd bii aw fan wu gudd akug wér, akug yékkatiku ci jamonoom ba mel ni jant, mu wax ca ne:

«Yal na Yàlla mii di Aji-des bàyyil ñu fi Saaliwu mii mu ñu may te def ko mu jël turam wi (aji-baax).

Yal na ko fi desal mu dib jant ci asamaani jamonoom, bu ko defee, muy leeral kanamam gu këriis gi.

Yal na ko fi desal muy kuy mottali jub gi fi Yonent bi indi woon, di ku barkeel, di ku wér, tey ku am muur»

Sëriñ Saaliwu ci melo wuy wone ag ragal Yàlla ak ginaawal àdduna

Tëraliin

[Nëbb]

Am njàngam [Soppi]

Ay ceññeeri xel ak màndargay yewwute ak man a wattu teeloon naa feeñ ci moom te booba matagutoon a dal jàng, bokk na ci liy dëggal loolu te di ko dëgëral lii nettalikat yi di nettali muy ne moom de mokkaloon na xasida gii di (Ikfinii) te booba gone gu ndaw la woon, ginaaw bi mu jànge Alxuraan ca Tuubaa ci loxol nijaayam S Alasaan Jaxate mom Jàmbaar, ba mokkal te bind kaamil, ginaaw bi mu dugg ci jàng xam-xami diine yi ak làkku araab ci ay ustaas yu màgg niki Seex Moor Saasum Jaxate mom Xaali Majaxate Kala ca Aynu Maadi ak Seex Muxtaar Guyaar Jang walla Njang ca Husnul Maab(Tindoodi) ak S Abiibu ca Tuubaa, S Mut Dem ca Njaaréem, Seex Aamid Saw ca Mewndu, kii mooy ki ko jàngal xam-xami gëstubiddiw yi (falag) ak melosuuf gi nga xam ne xóotoon na ci ba àgg ci di xam ci mbiri ay réew ca Asi, Tugal ak yeneen réew lol ña fa dëkk sax leeg-leeg ñu xaw koo réere. Ku soppoon yër ay téere la, ndax saxoon na ci ab diir ci jamono ba mujjoon di géej gu deesul jot ag suufam ngir ag xóot. Bi Sëñ bi àggee fii ci njàng mi la gis ne daa war a dugg leegi ci jeneen dara mooy ju tukki, ndax tukki benn la ci daara yu mag yi xam-xam di juddoo, di yokk jarbu tey dollim xel, ndax bari na xam-xam yu ci juddoo, ndax dina yobboo ñaare ci xalaat ci dénd bi te Yàlla (tudd naa sellam ga) yàgg na cee woote jëme. Ci noonu, mu def lu sakkan ciy tukki ci biir réew meek biteem, ci mbooleem diiwaani Senegaal,Kot Diwaar ak Gàmbi, mu jële ca daj gu mag ak jarbu gu réy ci lef yu bari

Yenn ciy meloom [Soppi]

Wata cëfka bu sëf aw nit ca Xelkoom

Ab xam-xamam [Soppi]

Niki ñu la ko waxe leegi Sëñ Saaliwu nekkoon na di ku géeju ci xam-xami lislaam yi: Tawhiid (wéetal Yàlla (t.s)) fiq , tasawuf , nos-wax walla nahwu ak nos-woy (haruud) ak jotal (balaaxa) ak leeral (bayaan), muy ku yéeme woon ci woy , daan def ay jam ci woyi dongaam yu tarbiya yi daan faral di def ay woy yu yéeme, ñoom de bokk nañu ci ñi gën a man a woy ci araab ci Senegaal ku ci mel ne Sëriñ Alhaaji Lóo , Utilisateur:Abdu Xaadir KEBE mi ci wikipedia, nga xam ne loxoom lu fa am solo la te ay gëstoom gën a màcc ci làmmiñu wolof, S Xaliil Màkke, S aboo Kebe mi def ab dalub murit bu jéggi dayo ba ci làkku araab [1] "www.wikimouridia.org" , S Mamoor Kebe, S Alaaji Mbàkke mi nga xam ne lu dul jeex ciy téere la taalif ci yoon wi ak aji sosam añs , ndax daawu leen bàyyi ci seen jàmm, foo ko fekk ma nga leen di soññ ci sàmmoonteek sarti "jotal" yi walla balaaxa ci seeni njuréefi woy. Ku mokkaloon lu bari la ci woyi waa Gànnaar yi ak waa Andalusi yi

Ag sonnam ci Jaamu Yàlla = [Soppi]

Daa na toggoo ci jaamu Yàlla yi lu kawe misaal, mu daan taqook ay dog ciy wird aki tudd-Yàlla, daawu leen ginaawal mukk ak lu yitte yi tar tar mbaa xat-xat yi baree ko ni, kenn ci taalubeem yi nettali na ma ne moom de masul a jël aw wird ndare bu da caa sax ngir sàmmonteek Addiis bi naa "Jëf ji Yàlla gën a sopp mooy ji gën a sax ak doonte néew na", muy ku xéroon cig jaamoom ci tënku ci Alxuraan ak Sunna, daan teet bidaa ak cibéel (lu ñu sib), ci anam gu jéggi dayo ba cig tar.

Ag dëddoom [Soppi]

Sëriñ Saaliwu daa dëddu àdduna ginnaawal ko ginaaw bi ko àdduna dëgmalee, jublu ko, mu ñëkkaloon ko ag kanamam ginaaw bi ko àdduna muuñee, ag dëddoom àdduna nag ca xol ba la ko defe, ndax teewu koo topp ndigali Yàlla (t.s) yi aju ci dundal suuf si, ndax Yàlla (t.s) nee na : «Moo leen sàkke ci suuf si te sàkku ngeen dundal ko», bu bokkoon ci ñiy toraxal suuf si ngir woote ag dëddu doo fi gis tay yii tabax yu kawe yi mu fi def ngir rekk kaweel baatub Yàlla bi, doo ko gis it kon muy bay lu tollu ne li mu daa bay ngir rekk séddaleeti ay njariñam aki njuddeefam ci nit ñeek ñu ñàkk ñi, di leen wax laayab Alxuraan ba: «Ñun de dañu leen di leel rekk ngir Yàlla, soxlawuñu ci yeen ag pay du caagéenu ag cant»

Ag Ñawam akug Yewwoom [Soppi]

Sëñ saaliwu nekkoon na di ku yewwu, ku ñawum xel, ku amoon la ag xereñ akug xóot ci xam mbir yi, boroom xam-xamu xel la woon (psychologue), ku daan xam xeli nit ñi la woon ak seeni jeng-jeng, booy tàmbalee wax ak moom rekk mu jëli la, ndànd la, boroomug ñaw la woon ba deesi ko seetlu saa soo ko tegaleeb laaj, ak bu mu man a doon. Bis gan dikkal na ko di kilafa gu bawoo ci biti, bi muy wax ak moom ci lu aju ci tànnéefi njiit yu Senegaal yu waroon a am ca jamono jooja, gan ga daal di koy laaj kan la faral ci lawax yi (les candidats)? Sëñ bi ne ko: man de ki askan wi tànn rekk laa faral, te loolu manul a am ndare bu tànnéef yi daa gore, sell te leer, looloo tax sama bëgg-bëgg mooy na mel nii, ci noonu gan daal di ne : tontu bii de bu diblomaasee la .

Ag Ubbikoom [Soppi]

Ku ubbiku la woon ci ñépp, daan tertoo ci kanam gu lewet guy muuñ, ak dënn bu yaa, di jaxasook ku nekk ci lu dul genn wàttuwu, ñi duli murit it mu jàppe leen mbokki diine ak yu ban, ngir jëfe waxi waajur wa: «wépp wird wu waay wor te Yàlla rekk tax, moo xam wu Jiilaani la mbaa wu Ahmad Tiijaan, mbaa muy wu keneen ci Qutb yi, yooyu yépp a baax ndax cig jub lañu nekk yooyu yepp »

S Saaliwu ak doomam S Mustafaa Saaliwu Ka njiitul Iraan la woon Rafsanjaani ci nemmeeku bu mu defsi woon Tuubaa

Yërëmam nit ñi ak Soppam ñeel xale [Soppi]

Yërmaande ji mu am ci mbindéef yi ak ñeewant gi mu am ñoom xaw nañoo nekk di lu maneesul a misaal, moom de kuy yittewoo mbirum jullit ñi la ak fu ñu man a nekk, di nemmiku ak a xeeñtu xew-xew yiy xew ci réewi jullit yi niki xareb dóox gi (guerre de golf), ak intifaada ca Palestin, ak mbooleem tër (condition) yi jullit yi di dund ci mbooleem àdduna bi, mu daan digale ci ñu wàcce ay kaamil ngir ñaanal leen ci. «Man ci sama jëmmi bopp (Abdu Xaadir KEBE) dem naa fa moom bis ànd ak sama jenn mag ne ko Sëriñ bi war ngaa ñaanal jullit ñi, ndax yaw yaa fi nekkal Yàlla ci kaw suuf, te kat waa Aamerig ñi ngi taal àdduna bi te loolu ñi ngi ko gën a defe ci jullit ñi, taal nañu ab xare ca Afganistaan, taalati ko ca Iraaq, jamono jii ñu nekk ñi ngi waajal ngir taal ko ca Iraan, mu daal di feeñal yitteem bu baax ci wax ji ne ma loolu nu mu deme ma gën ko koo leeral, mu ne loo ci xamati naa ko yëg ndax lu ma ci yëg du yam ak lu ma ci yëgul, te kat booba waa Aamerig feeñaloon nañu yitte ju mag ci song Iraan, ba tàmbali woon a yëngu's lëf jëm ca Dóox ga (le Golf) waaye ba leegi waxatuñu lu dul luy jàmmal, ba sax njiit lu bon la daa xeex rekk di George Bush far na daanu, kii di Barak Obama daal di toog, te moom benn ci dig yi mu doon def ci bi muy sàkku ñu fal ko mooy toog ak Iraan waxtaan, yal na ko Yàlla àntul, te gëm naa ne day àntu ndax waxi Sëriñ Saaliwu ji, lii nag ñeewant la ñeel jillit ñi waaye it ñeel nit ñi, te ca baayam la ko jële mi daa wax : «Yaw boroom nguur gi (di Yàlla) yaw mi màgg ba weesu fayoontoo, rikk nanga yërëm mbindéef yépp » kon moom mbindéef yépp la yërëmoon rawati na jullit ñi waaye it baatin la ndax sunu boroom fanq na ay wi cig ñaanam ci barkeem.

Yërëm xale yi [Soppi]

Mu nekkoon di ku am ñeewant ci gone yi, yërëmoon leen ni mu ko defe mag ñi, mu daan leen dimbale di leen gunge ci jafe-jafey dund gi, mu daan mettitlu te daan naqarlu bu gisaan kenn ci yale yi mu tumbrànke , mbaa sonalees ko cam njàngam mbaa mu ami góom mbaa mu wéradi mbaa mu xiif.

Daawul toog ak ñoom ndare bu da leen a teral, jox leeni neexal aki mbiskit ak lu ni xeetoo. Daa na àndaale ak ñoom ci tukkeem yi, di kaf ak ñoom mel ni gone ni ñoom te loolu lépp ngir ñu fàtte seeni waa jur ba man a dékku li ñu leen bëgg a sol ci yarub lislaam bu kawe te sell, ndax kat gone baaxoowul a miis ay waa juram ngir ñeewant ga, waaye fi moom day am ngir yërmaande ja. Mu daan fanaan ak ñoom ci néegi boppam yi, nekkaloon na leen di baay ci li baat bi ëmb ci maanaa, taxoon na xalaatatuñu seeni way jur ngir wuutu gi mu leen wuutu woon ci ñoom ci jëfam ju baax, foofu nag amal na fa waxi baayam ja ba muy ñaan Yàlla (t.s) naan ko: «taxal ñu fàtte seeni way jur ngir man» Waaye nag yërmaande ji teewu ko woon a taxaw ci yar leen ni mu ware, mu daan waxtaan ak ñoom ci nu kawe seeni at, daan leen nettali ay xisa yoy daawuññu ci xam dara, waaye da daan sedd bis ba ñuy doone mag ba koy soxla ca seenug dund, loolu nag ci Yonent bi Muhammad (j.m) la ko daa roye, ndax mooy ki daa wax Omar ibn Abii Salama te booba gone la gu xamul li mu koy wax: «Neel Bismil Laah, te lekke sa ndijoor te lekk ci sa kanam»

Ag dundam [Soppi]

Dund gu wow la yoroon gu soofiyoo, gu ag dëddu àdduna muur, ragal Yàlla peek ko, biir ga di yërmaande, muy ku amoon ag ñeewante ci gone, te yéggoon aw wartéef jëm ci doomi aadama yi, ku amoon ayba la woon ak wegeel, ku ubbiku woon la te lewet, waxi woykat ba dëppu woon na ci moom : « Lewt ba ne domm, diis ba ne gann cig wet () woyof ba ne toyy, saf sapp ak boroomam » boo koy xool rekk gis ag Yàlla ak aybaam ga, dëggoom ga, wegoom ga, muy ku ñépp wormaaloon, ñi ko jegeek ñi ko sori woon, Benn ci labbe yi ci Senegaal seereeloon na ko ginaaw ag làqoom: «Kii de àdduna da koo dikkal mu toog fi suuf», loolu di wax ju réy, di lépp dikkal na ko te faalewul dara lu dul Yàlla te xam ne dara amul solo lu dul moom, fii dara saxu fi, dara dëkku fi, woykat ba nee na : «Jural-leen dee, tabaxal mbàbb», muy ci maanaa lu fi waay jur dee dina digg leegi ne ko fuuf, lu ngéen tabax it day mbàbb leegi, kii nag lii la tegoon ci ron bëtam, jëfam jépp it Yàlla la ak lu ci jëm, misaal mi kenn la woon ku àddinaadi, te teewul mu sos fi lol maseesu ko fee sos ci ay sémb yu mag, xoolal li mu fi bàyyi ci xaalis, tollu na ci lu jege 17 milyaar, ñeel naal yu aju ci Dëkkub S Tuubaa bi, te loolu masut a am ci taariixu yoon wi, la ko dale ca Waajur wa ba ci fii ma la koy waxe, te loolu bokkul ak li mu fi jot a liggéey ci alali boppam, te loola gën jaa néew mu weesu 7 milyaar, lu sakkan ciy kër S Tuubaa sosoo na ciy loxoom, waxuma la li sosu ciy jumaa aki jàkka cig ayam te ñuy yu réy te taaru.

Kenn ci murit yi nee ne bokk na ci bind yi ñu man a jële ci moom: «Nekk gi mu nekk doomi S Tuubaa doy na teraanga te dib xalifaam, nekk it mag mu am ay xéewal war naa tax a noppalu, te moom boole woon na ñaar yooyu yépp, waaye teewu ko woon di yëngu jamono ju nekk ak a liggéey, kon loolu li mu man a doon mooy bind bu mu ñuy jox mu aju ci liggéey ak doonte deesul yàggati fi, ndax loolu yéene nit ñi ay xéewal lay wund te ci ag jaamu Yàlla la »

Sëriñ Saaliwu ak Tarbiya [Soppi]

Bi Sëriñ bi toppee yoon wi ba àgg ca jëmuwaay bu kawe ba, muy àgg ca Yàlla, daa daal di sóobu ci tarbiya , maanaam yare ak sellal jikko yi ak setal leen ciy ayibi bakkan ngir jeggeele Yàlla mu kawe mi. Yoon wi mu daa jaar ci yareem googu mooy wi mu jaaroon, nekkutoon di kuy tañaxu waaye ci xam-xam la ko tegoon ak leerug xol, loola dëppoo ak laaya bii di: «Neel wii de mooy sama aw yoon, damay woote jëme ca Yàlla ci leerug xam-xam man ak ku ma topp»(yuusuf 108)

Tëriinu yaram wi (programme bi) dafa làmboo woon lii: alxuraan , xam-xami sariya yi ak xasiday S Tuubaa yi, ak liggéey yu yaram. Yooyu ñooy ñeenti xeet yi mu daa jaar ngir laabal xol yi ci ay jàngoroom, walla ñooy saabu bi mu daa raxase bakkan yi ci seeni ayib

Yariinu xale bi [Soppi]

Gone gi day door - ci li muy njëkk a def - ci jàng Alxuraan ba mokkal ko, bind ko te du ko xool, door a tàbbi ci jàngum xam-xam mi. Aji mokkal ji daa nees ko neexale lim bu am solo ci xaalis ngir mu soññu laata muy tàmbalee jàng xam-xam ak di jàngale Alxuraan, jàngalekat yi tam amoon nañu seen dëkkuwaayi bopp yu ñu leen jagleel ak seen lekkug bopp ngir wormaal alxuraan ji nekk ci ñoom, jenn daara ju nekk it daa na am 12 jàngalekat, kaamil yi ñu binde ci daaray 2 dale ko 1993 - taariixu sancug Xelkoom - àgg nañu ci 2289 kaamil, te ay téeméer ciy kaamil bindees na leen njëkk taariix bii ak ci ginaawam ci daaraam yu bari yii maneesul a lim. Bokk na ci li yayoo fàttali mooy ne fii ci Senegaal, rawati na ci digg yu daara yi, miinees na fi ñuy bind kaamil ginaaw ag mokkal, loola nag mooy aji mokkal ji bind kaamil bi te du ko xool niki firnde (certificat) cig mokkalam.

Nosiinu daara ji [Soppi]

Daara ju nekk am na bu jàngalekuti Alxuraan yi jàllee, kuy jàngale xam-xami sariiya yi ak làkku araab, kooku mooy faral a jiite daara ji, lañu fay jàng it mooy li ñu baaxoo jàng ci jataayi jàng-xam-xam yi (Majaalis) nga rax ci dolli xam-xamu Usuul ak Mustalah, benn bi Usuul di jàngale gongikuwaay yi àtte yi di bawoo, bi ci des di xamle yattiinu baat yi ñeel xam-xam yu yees, balaa ndongo lee àgg foofu, dana fekk mu jot a jàng am mbooloo mu ñu tànn ci xasiday Sëriñ Tuubaa yi, ci Tawhiid, Fiq, Tasawuf ak nos-wax.

Moom de foo ko fekk da daan soññ dongo yi ci góorgóorlu bu baax ci gëstook njàng, di leen nettali démbi am njàngam, ak coona ya mu daa jànkoonteel, leeg-leeg mu laaj ay laaji nattu ak seet fi ñu tollu, di een won téere yi ñu war di yér, di xiirtal ci di teewe yenn jataayi xam-xam yi ak di ci bokk, daaraam yi it lu sakkan ciy woroomi xam-xam génne nañu fa, yoy yenn ci ñoom def nañu ay taalif yu am solo ci wàll yu bari, Fiq, Tasawuf, Jaar-jaar (Siira), Mustalah, Njàggat ak farata yi. Sëriñ bi jotoon naa móol yenn ci taalif yooyu te wisaare leen ci alali boppam te loolu ag soññee gu mag a ngi ci, akug góorgóorluloo. Daara ju nekk it am na am mbooloo mu liggéeyam mooy jàngal xale yi ay xasida ak tàggat leen ci ñu man koy yekkati ci ay daaj yu yéeme yu ñu jële ca mag ña daa jàng ca jamono ju Sëriñ Tuubaa mbaa waa kër Sëñ Masàmba , ku ci mel ne S Yuusu Ndaw, Alaaji Siise, S Mayib Géy ñi daa yekkati ci kanamu S Tuubaa. Mbooloom xasida moomu ëmboon na lu ëpp fan-weeri xasida, yi ci gënoon a siiw di Jasbul-Quluub, Mawaahibun-Naafih , Muqaddimaatul-Amdaah ak Rabbii-bimaayasrahul ... Dongo yi nag daawuñu def leneen lu dul jàng ak jàngale, ndare ci jamonoy nawet bi, bu boobaa ñu sóobu ci liggéey bi ci tool yi, ndax loolu ag wàll la woon ci tarbiya gi

Sëriñ Saaliwu (g.y.m) nekkoon na di ku xamoon mbirum mbay, di ci fóore, bëggoon ko lool it te jàppe woon ko mecceem akug njaamu gu sell ñeel Yàlla (t.s), daawu ci faale néewug la mu cay ame, mbaa ag yàqoom walla ag àntoodeem. Daa na jëfandikoo ci tool yii ay bijjikaay (Tracteurs)yu tolloon ci 220. Mbooleem ay njuddéefi mbayam it addiya la leen daa def ñeel ki fi nekkal Sëriñ Tuubaa, bi mu nekkee it xalifa, daa daal di woon tàmbali di leen séddale njabootug Sëriñ bi ak miskiin yi, ak faqiir yi (way ndóol yi), ag wàll ci ñoom mu sotti ko ci luy defar dëkkub Tuubaa bi

Ag Xilaafaam [Soppi]

S Saaliwu Mbàkke

Moom nag mi ngi nekk xalifa ci 13 mee 1990, làqu ci guddig 28 jëm 29 desambar 2007. Moo doonoon juróomeelu xalifa bu Sëriñ Tuubaa, ku kiimaane la woon ci nangoo liggéey ak jaamu Yàlla ak dëddu àdduna ak yar ci Lislaam.

Ay liggéeyam [Soppi]

Ci jéem gi mu doon def ngir dab bànneexu Sëriñ Tuubaa ci amal ay mébatam ya mu def ca Matlabul-Fawsayni, genn ciy xasidaam, Sëriñ Saaliwu taxaw na ci mottali ay sémb yu mag yu fi ay magam bawoon te dolli ci yeneen yu mag te am solo, bokk na ci yooyu:

  • Àggale Daara ju Kawe ju Tuubaa (l'université de Touba) ba mu man a dékku lu tollu ci 5000 ciy dongo,
  • Yeesalaat Jumaay Tuuba, def fa benn jumtukaayu kàddul (une sonorisation) bu man a àgg ci 12 km ci soriwaay
  • Yaatal dëkk bi, natt ci 110.000 pàkk yoy ñaari ñatteel yi noppi nañu (pàkk yu ñuy joxe cig neen (amul pay) ñeel képp ku yéenee dëgg Tuubaa)
  • genn mbaalug laabal (un réseau d'assainissement) ci Tuubaa gu toll ci 18 km
  • Naalub mbay bu Xelkoom, mu yaatoo ci 45.000 ha.

Sos na fi lol maseesu ko fee sos ci ay sémb yu mag, xoolal li mu fi bàyyi ci xaalis, tollu na ci lu jege 17 milyaar, ñeel naal yu aju ci Dëkkub S Tuubaa bi, te loolu masut a am ci taariixu yoon wi, la ko dale ca Waajur wa ba ci fii ma la koy waxe, te loolu bokkul ak li mu fi jot a liggéey ci alali boppam, te lool a gën jaa néew mu weesu 7 milyaar, lu sakkan ciy kër S Tuubaa sosoo na ciy loxoom, tollu nañu ci 28, waxuma la li sosu ciy jumaa aki jàkka cig ayam te ñuy yu réy te taaru, ñuy yu mu sos ci alalam mbaa ci ndigalam mbaa mu dugal ci bu baax loxoom.

ay daaraam [Soppi]

Sos na ay daara yu bari, ngir jàng ak jàngale, ci barab yu bari te wuute ci réew m i, bokk na ci yooyu: Got gi mu njëkk a sanc ci daara yi, mi ngi ko sos ci 1934, Njurul, ca wetu Tuubaa, Njàppundal, Ndookaa, Lagan, Ñibingal, Ñaaru, Ngaabu, Ngéejaan, Xàbbaan, Geloor, Tuubaa Njaaréem, ak yeneeni tool yu mu sanc ginaaw bi mu gental leen, mbaa yu mu sancagul ak jii mu mujj a sos te mu nekkoon jenn ju mag ju doon benn pakk bu mag ci suuf bu ëmb 15 daara, mooy Xelkoom, mi ngi ko sanc ci 1993, daara ju ci nekk yor turu ag gàdd (cartier) ci Tuubaa, yaatoo 50000 ektaar, la fa nekk ciy donga yuy jàng àgg ci 50000 jëmm, yoy li leen di dundal ci bis dina tollu ci 2500 kilo ci ceeb.

Sëriñ Saaliwu ak waajuram ak Jumaay Tuuba tafees leen ci kaw mbeex mi

Li ñu daa def ci daara yi [Soppi]

Daara mooy fu deesi jànge Alxuraan waaye fi murit ñaare daaray tarbiyu lay doon, di benn barab bob dees koy sos ngir jàng Alxuraan ak xam-xamu diine waaye it ngir yar, mbay ak liggéey, mu mel ne day doon fu deesi waajale nit ba bu fa jugee dara du ko jaaxalati ci àdduna, moo xam lu deesi xam la ci diine, mbaa lu deesi dajeel ci jafe-jefey àdduna, ndax ka fa yaroo day miin coona yi, man koo dékku, wullees ko ci liggéey, jàngalees ko, mu mujj di "ku ñu jàngal ba mu ne arr, yar ko ba mu ne nërr" ni ko Sëriñ Fallu waxe woon ne noonu la leen seen baay Cerno defoon, kon (yar bees ne nërr, jàngale bees ne arr) mooy mbóotum tarbiya,>

Ay séqoom aki mbokkam [Soppi]

S Saaliwu amoon na ay séqoo yu rafet te teey aki mbokkam, mu daan leen wéttalikoo te doonoon seen xarit, ñoom itam ññu fonkoon ko lool, daa ko tudde seeni doon, te daan leen ko jox ngir mu yor leen, yar leen, moom it mu nekkoon kok daa gisoon ne liggéeyal mbokkam yooyu de liggéryal S Tuubaa la, looloo taxoon mu boole woon ko ci wartéefam yu njëkk yi, mu daan diisoo ak ñoom ci lu mu man a doon, daan def lu mu bay ak lu mu bari bari jox ko Xalifa bi fi nekk.


Ay séqoom ak mag ñu Sëriñ Tuubaa ñi [Soppi]

S Saaliwu - yal na ko Yàlla dolli leer - ku amoon ag cofeel la akug worma ñeel mag ñu S Tuubaa ñi, mu leen daan faral a jox addiya yu gànjaru, daan na def lu bari bu daan dem ci daara yi daan ànd ak ñoom, ku ci mel ne S Seex Faat Tàkko Jóob, S Mustafaa Si, S Musaa Alima Gey ak ñeneen ñi mu jamonoonteel. Man naa am nag li waraloon muy ànd ak ñoom ci daaraam yi mooy xaleem yi roy ci ñoom ci seen jikko yu murite ,yu taalubee, yu rafet yi, mu daan gis it ci àndaale googu ag mottali kóllare ci mag ñu baayam ñooñu, ña mu ca jamonoonteelul daa na leen jokke ci seeni doom mbaay sët, ku ci nekk am nga ca daaraam ya doom mbaa sët.

Ay dénkaaneem: [Soppi]

S Saaliwu - yal na ko Yàlla gërëm - amoon na ay yitte yu daa nañu feeñ ci li daan gongikoo ci moom ci ay dénkaane aki soppaxndiku aki wax, bokk na ci baat yi ñu ko miine woon baatub Cant bi daan baamuwu aw yoon ciy xutbaam ak bu Tuub bi mu joxoon yitte ju mag, bokk na ci waxam yi daa tekki njàngaley S Tuubaa yi:

  • ( Yàlla mooy tab bu tedd bi nga xam ne la nekk fa moom ciy xéewal du jeex, kon nañu ko ñaan ci xeewalam yii nga xam ne bindu leen lu dul ngir jaamam yi)
  • (Ku ragalul Yàlla, bind na lu mu ragal)
  • (Ku fàtte Yàlla de, na xam ne xéewalam yu bari yee ko waral ak yërmaandeem ji)
  • (Bokk na ci pexey Saytaane su ñu jam si, bu ndigal jugee ca Sëriñ bi jëm ci murit yi, day gaawantu (moom saytaane) ne leen bu leen def ndigal lii, Sëriñ bi rekk moo ko man, bu ngéen ko manoon du ngéen fi ñëw di jébbalu (am ñu ci naan duma dugg saxaar yanu sama bagaas).
  • Bu Yàlla feeñalee ayibi ab jaamam, booba da koo bëggoon a jéggal, waaye ab jaam nag day feeñal ayibi mbokkam ngir gàccaal ko, rusloo ko, ŋàññ ko.
  • (Na jaam bi yittewoo biiram bi dul suure lu dul ay jëfam yu baax (Bàmmeelam))
  • (Yàlla sàkkal na nit ñaari biir bu boppam bi, moo ko ko yoral jarul mu ciy sonn, saa su xiifee mu reggal ko, ak bu bàmmeel, na cay sonn, ndax lu mu ca deful du ko ca fekk)

Ag génnam àdduna [Soppi]

S Saaliwu mi ngi génn àdduna ci subag bisub àjjuma 17 ci weeru tëbëski atum 1428 g, dëppook 28 desambar 2007, ba fi nag dund gu jege 95 ciy at, ngir fekki waajuram wu tedd wa S Touba. Yal na gëramul Yàlla sottiku ci kawam ak lu waajuram, ñu gunge ko ba ca saxuwaayam bu mujj ba ca penkub Jumaay Tuubaa ja, ca guddi ga ca topp. yal na ko Yàlla (t.s) fayal Lislaam ak xeet wi gën ji fay gu muy fay jaamam yu baax yi ko liggéeyal. Aamiin

S Baara Mbàkke falilu moo ko fi wuutu niki 6eelu xalifa bu S Tuubaa.

Contributeurs

Membres