--------------------------------------------------
Muhammad yonnantub Yàlla bi ak juddug Mbooloo mu Lislaam mi
Li ko dale ca ag ganeem àdduna ba ci bi ñu ko yónnee
Muhammad (jàmm Yàlla na sax ci moom) mi ngi gane àdduna ca Màkka atum 571 g, j , waxees na ne ca at mooma la Abraha mi doonoon kenn ci waa Ecopi jugoon ne day nangu Màkka te màbb Kaaba gu sell ga. Waaye Yàlla (t.s) alag ko, jaare ko ci ay njanaaw yu ñu naan Abaabiil, moom ngay gis ci saaru Fiil (ñay), looloo waral ñu naan Yonnant bi ci atum ñay yi la judd, ndax ba Abraha di ñëw ciy ñay la waroon.
Aji juram ju góor mooy Abdul laah, mi gënoon a doon gone ci doomi Abdul Mutalib mom Haasim mi nekkoon njiitul Quraysin tey sangub Màkka, maanaam njiitam. Moom nag (Abdul Mutalib) – bi Yonnant biy judd – mag la woon mu at yi xawoon a diisal. Abdul Laah nag moo nekkoon doom ji mu gënoon a sopp ngir yewwu gi mu defoon ak njub gi, rafetug jikko yi ak nangul baayam gi. Dencaloon nanu ko Aamina Bint Wahbin mom Abdul Manaaf mom Zuhra mom Kilaab, mu nekkoon di ku bokk ci giirug Xuraysin. Abdul Laah nag ab yaxantukat la [woon]], ci noonu la génne woon, ginaaw bi mu dencee soxna ba teg lu néew, ngir yaxantu-ji ca Shaam , booba Yonnant bi ganeegul àdduna.
Ca tukkib yaxantoom booba la baayi Yonnant bi làqoo , ca tawat ju ko daloon ba muy dëpp, ba muy ñëw ba agsi Madiina la ko gënoon a sonal, mu daal di wàcc ca ña ñu daa wax Banii Najaar di woon genn ci giiri Xasraj yi, fa la génne àdduna. Maamam nag di Haasim mom Abdul Manaaf dafa a takoon soxna, looloo tax ñu naan Banii Najaar de ay goroy Yonnant bi lanu (j.m).
Yonnant baa ngi judd (j.m) ginaaw bi waajur wi làqoo, mu daal di màgg cig njirim, waaye maamam Abdul Mutalib beg ci moom lool, tudde ko Muhhamad, yar ko cig cofeel ak ñeewant
Waa Quraysin nag aadawoo woon nanu di yóbb seeni doom ca la génn Màkk, ca nàmpalkat ya ngir ñu man a màgg ci jàwwu ju sell, wér-gu-yarame te deesi fa dégge araab yu sell, bu ko defee loolu di tax ba ñuy wér, neexi araab te leeri wax. Nii la Aamina defoon ni ñépp, yóbb doomam Muhammad (j.m) ca ab nàmpalkat bu tuddoon Aliima Asahdiya, mu bokkoon ci Banii Sahd Bun Bakr, seeni kër nekkoon ca tàkk ga ca wetu Màkka. Bi Muhammad àggee ci am juroomi at la ko Soxna Aliima delloosi ndayam ca Màkka, mu nekk fa ca pekkam , maamam Abdul Mutalib di ko sàmm.
Ca jamono jooja la Soxna Aamina Bint Wahbin jugoon ne day siyaareji bàmmeelub boroom këram Abdul Laah ca Madiina, ba mu demee bay dëpp la ko tawat ja dikkal, mu faatu ca ndëkk sa nu naan Abwaa te nekk ca yoon wa dox diggante Màkk ak Madiina, ñu daal di ko fay denc, looloo waral bi Yonnant bi màggee di ku soppoon di jaar ci ndëkk soosu ngir siyaare bàmmeelu waajuram ju jigéen ju laab jooju.
Ci nii – ndaysaan – la Muhammad mujje di jirim ci nday ak ci baay, looloo waraloon maamam Abdul Mutalib mujjoon féetewoo ag yaram akug wattoom, bëggoon ko it lool. Waaye sàmm googu gépp ak fonkeel gi teewul Muhammad (j.m) doon yëg naqaru njirim, ndax kat da daa gis moroomam yi ñu nekk ak seeni way jur, moom muy ku leen ñàkk, waaye nag loolu jox na ko ag sukkandiku ci boppam, may ko ag temb ci njëmm akug wéroodi ci kenn, nàmm am xelam, ubbil ko ay bëtam ci dëgg-dëggi dund gi, te booba ay atam lu néew la woon. Loolu de lu jeexiital la ci moom ak cig dundam, Yàlla nag moo bëggoon ci moom loolu ngir tànn gi mu ko tànn ngir mu yanu bataaxel bii di Lislaam te war koo tas.
Yonnant baa ngi sàmm ag jur
Abdul Mutalib ginaaw bi Aamina làqoo yàggu fi dara moom itam làqu, te booba Yonnant baa ngi amoon juroom ñatti at, fa la ko baay-tëxam Aboo Taalib jële yóbb ko ca këram ca doomam yu xaw yaa sakkan tubaar-kàlla, ngir mu yaroo fa. Aboo Taalib nag moo wuutu woon baayam ci jiite Màkk, ci noonu mu jeexaloon alalam jépp ci sàmm Kaaba gi ak way aj yi ak dimbali ñi aajowoo, looloo taxoon alalam bariwutoon ak li muy nekk kilifag Màkk lépp. Lii a waraloon Yonnant bi doon jéem a woyofal yan bi ci baay-tëxam jooju, ba àggoon ci di sàmmal ag jur ñenn ci waa Màkk yi, ñu ko ci daa fay lu néew a néew. Loolu it doonati ab pose ngir mu tàggatu ci xam ni nuy sàmme ag njaboot, jikkowoo ag ñeewant akug laa-biir ak sàmm ak yewwute, ñuy jikko yu manul a ñàkk cib sàmm bu bëggee wattu gétt gi muy sàmm. Yàlla moo ko bëggaloon loolu ngir tàggat ko ci bataaxel bi mu ko nar a joxi. Sàmm ag jur nag daara la joj lu bari ci yonnant yi jaar nanu ci, ba sax jële nanu ci Yonnant bi (j.m) mu ne : amul yonnant bu sàmmul ag jur.
Yaxantu gi mu doon def ak tudde gi nu ko tudde woon Ku wóor ki
Bi mu amee fukki at ak ñaar la ànd ak baay-tëx ji Aboo Taalib cib tukki dem Shaam, bi mu amee nag ñaar fukki at la tàmblee bokk ci yaxantu gi ni ko waxambaaney Quraysin yi daan defe, mu wone ci it man gu mu ko man lool, ndax ku ñu xamoon la cig wóor, ak dëggu, yewwute ak ñaw, ay man-manam tàmblee feeñ ñeel waa Màkk, li ko gënoon a wuutaleek nit ñi mooy wóoram gi jéggi woon ab dayo te xaroon baax, ñu mujjoon di ko wóolu ci lu mu man a doon, te am xel mu dal ci ne dana sàmmoonteek kóolute gi nit ñi def ci moom , looloo taxoon ñu naan ko ku wóor ki ak ku wóor ku dëggu ki.
Jël gi mu jëloon Xadiija soxna ak doom ya mu ca ame
Bi at yi àggee ci ñaar fukk ak ñeent daa dajeek Soxna Xadiija soxla waxambaane wu ko yoral yaxantoom gi mu doon deflu ca Shaam, moom nag soxna su woomle la woon bokkoon ci way woomley Màkk yi, ci noonu ñu digal ko mu gis Muhammad (j.m), ba mu ca waxeek moom Yonnant bi nangu. Yonnant bi yaxantujil na soxna Xadija ca Shaam ànd ak ngóoram sa nu naan Muyasara, Muyasara mii yéemu woon na lool ci jikko yu rafet yi ci Muhammad ak yewwu geek man gee yaxantu, ndax bi njaay mi nekkee ciy loxoom fulu na ay yooni yoon, wuuteek ba mu nekkee ci loxoy keneen, looloo tax bi Yonnant bi (j.m) delloo, jébbal soxna Xadiija alalam ak la mu ca tonoo, cig kóoluteek dëggu, soxna si yéemu na lool ci jikkoom yu rafet yi ak njëmm gi ne ci moom, ci noonu mu yónni ci moom kenn ci ay jegeñaaleem xamal ko ne da koo bëggoon niki boroom kër, Yonnant bi (j.m) nangul ko . Noonu la seen diggante sottee te booba Yonnant baa ngi am ñaar fukk ak juroom ciy at, Xadiija moom yor ñéen fukk, ci noonu mu faroon di soxnaam, di yaayam, di ki koy dimbali ci lépp. Yonnant bi (j.m) amoon na ag texe ci séy boobu naka noonu Xadiija, ci noonu séen kër di misaalum mbégte cib séy ak texe ci biir kër. Soxna Xadiija nag mooy ki jur mbooleem doomi Yonnant bi, ku ci dul Ibraahiima, moom de soxna Maariya mi di ab qibt moo ko jur, moom nag (Sëñ Ibraahiima) ci jamonoy Yonnant bi la làqu. Yonnant bi wéyoon na ci yaxantoom gi ginaaw bi mu yoree soxna Xadiija, mu ko daan defe nag ni ko waa Xuraysin gépp daan defe rekk, ñoom de yorunu wooni bitig aki mangasin, moom kay danu daa defi njëgg yu mag mbaa yu ndaw jawali Yaman ci sedd bi, bu cooroonee ñu dem Shaam, màkk-màkka bu nekk daa na man a bokk ci njëgg li bu bëggee, njëgg loolu nag moom la nu daa wax ci ci araab Bahiir, kenn ci góori Xuraysin yee ko daa jiite , ku soob ci ñoom ànd ak moom, bu ko defee bu dellusee ñu seet li ñu tonowu, seddale ko, ku ci nekk am ca la nga ca def. Seen yaxantuwiin woowu moo taxoon Xuraysin daan am jot, di daje ci jataay yi di waxtaan, rawati na ca la wër Kaaba ga. Waaye Yonnant bi (j.m) moom néewaa na bu mu bokkee ci yii jataay, moom kay këram la daa toog mbaa mu génn dem ca àll ba ngir wéet fa di xalaat ak a settantal, ndax sopputoon di fo mbaa muy caaxaan ak a waxi larax.
Yonnant baa ngi amoon fan-weer ak juroom ciy at jamono yi Xuraysin di màbb Kaaba gi ngir tabaxaat ko, ndax tabax bi daa xawoon a màggat ngir yol mi daa sottiku ci kawam. Bi ñuy tabax ba àgg ca Hajarul Aswad ñu jaaxle ci gan giir ci Xuraysin mooy am teraangay yekkati ko teg ko fi mu war a tegu, ñu toog ca Kaaba ga di gëstu nu ñuy lijjantee loolu, far ñu dëppoo ci ne ku njëkk a ñëwaat rekk ñu jox la nga àtte leen ci jaaxle googu, far Muhammad (j.m) ne tëll, ñu ne ku wóor kaa ngee na ñu àtte, waaye mu àttee leen nu gaaw te yomb, mooy jël làmbaayam li mu yoroon lal ko ci suuf, teg ci doj wi ne giir gu nekk na jàpp ci cat ngeen tegandoo ko ca barabam. Nii daal la ko lijjantee ca yombam ga ak xarañam ga ak lëmóodikoom ga.
Wàccug Wahyu gi ak yonni gi
Bi at yi jegee ñeen-fukk la sopp gi mu soppoon ag wéet gën a yokk, mu gën a bëgg xëlwa ak beru, mu daan génn Màkk ngir dem ca doj wa nu daa wax Harraa, ngir xunti mu fa nekkoon mu mu daa faral a dugg ngir jaamu Yàlla, noonu la daa jeexale weeru koor wi, ngir sellal boppam, laabal xolam. Benn bis nag ci koorug atum 610 g .j, ba jant bay so la ko genn kàddu gu nooy dikkal ca dalug xunti ma naan ko : jàngal. Yonnant bi (j.m) tiit njàqare li jàpp ko, waaye mu ne ko : man duma kuy jàng. Waaye mu yëg mu mel ne dafa am lu koy naj ba dënn bi xaw a xat mu noppal ko, bu ko defee kàddu gi delseeti neeti ko: jàngal, Yonnant bi neeti ko : man de manu maa jàng. Naj ga delseeti, ba mu xawee woyofati kàddu ga delseeti ne ko : ((jàngal ci sa turu boroom mi bind , bind na nit ci lumbu dereet, jàngal, sa boroomay ki gën a tedd)) kàddu ga daal di dal, daal di deseeti. Fekk jant biy so Yonnant bi yëg njàqare lu rëy, daal di gaaw génn xunti ma, dem ñibbi, bi muy àgg lëndëm gaa ngi doon dugg, ndax diggante Màkk ak xur wa xaw na a ëpp ay ñatti kilomet.
Ba Yonnant ba (j.m) àggee ca kër ga daa daal di woote ne : muur leen ma, muur leen ma, booba ñaq waa ngay siit, yaram way lox, soxna Xadiija daal di dawsi sàng ko, tàmbli koo dalal, bi tiitaange gi demee Yonnant bi xamal ko li xew, ne ko : man de damaa xëm. Ndax xamagutoon ne li ko daloon ag wahyu la gu tukkee ca sunu boroom (t.s) , indil ko laaya wi njëkk ci Alxuraan ju tedd ji.
Soxna su tedd sii di Xadiija wéy ci di dalal xelum Yonnant bi (j.m) naan ko lii la dal de du man a doon lu dul lu baax, ndax yaw ku baax nga, am kóllare, dëggu, baax ci sa ñoñ, di taxawu nit ñi bu ñu ameey naqar. Ca noona xel ma tàmblee dal, mu yëg jàmm.
Waraqat’Ubn Nawfal mi ngi bégal Yonnant bi (j.m)
Bi soxna Xadiija gisee ne tiitaange gi dañ na daa ànd ak moom seeti doomi baay-tëxam ja tudd Waraqat’Ubn Nawfal, mu nekkoon góor gu am hikma, daan jàng téerey diine yi te dégg ebrë , Yonnant bi nettali ko li xew, Waraqat yéemu lool, ne ko lii de mooy mbóot mi Yàlla wàcce woon ci Muusaa (j.m), ne ko aka neexoon may gone ba man a ànd ak yaw ci tas sa bataaxel bii, xelum Muhammad dal, mu dellu këram, waaye teguñu ci lu néew rekk Waraqat faatu, ndax daa xawoon a màggat. Yonnant bi dellu këram ak Xadiija ci xel mu dal ak mbégte, am yaakaar ne wahyu gi dina delseeti, bu sukkadikoo ci waxi Waraqat yi, waaye wahyu gi yeex a ñëw ba Yonnant bi far àgg ci jaaxle lool, waaye mu mujj ñëwaat ginaaw bi, xelum Muhammad dal, mu xam ne lii kat ag wahyu la gu tukkee ca Yàlla (t.s) te moom ku ñu tànn la ngir mu jottali nit ñi diine ju juge ci asamaan si, war a joxaat diiney asamaan yi seen leer ak sell gu njëkk ga ñu yoroon njëkk nit ñi di ko yàq, di ko tàqal ci li jamono di gën a romb.
Nii daal la Muhammadum Abdu Laah mi (j.m) mujje di yonnant bu nu tànn yonni ko ci mbooleem mbidéef yi ngir mu indi fi leer gu tukkee ci sunu boroom di gindee, di tege ci yoon, di jële cig bokkaale jëme cig wéetal Yàlla,di jële ci lëndëmug réere Yàlla, jëme ci leerug gëm ko, jëme ci Lislaam.
Fii la jaloorey Muhammad yonnantub Yàlla bi - jàmm yal na sax ci moom – tàmblee akug jànkoonteem ngir wisaare bataaxel bii ko Yàlla jox mu war koo jottalee ci ngën ji anam ak melo.
ginaaw bi la wahyu gi tàmblee dikk cig toppante di wàcc ci Ku tedd ki, di indi laaya yi def tay alxuraan nànk-nànk, kon alxuraan ñëwadoowul cig mat, waaye laaya topp laay, ba kero muy mat, nga xam ne Jibriil da ko daan dikkal di ko déggal laaya yi, bu ko defee du ko ba ba kero muy wattu laaya jooju ci dënnam, mel ne sax dañu ko cee bind, làmmiñ wi di ko baamu, Yonnant bi bu masaa na jot ciw dogiit ci alxuraan da ko daa baamu ba mokkal ko, bu noppee jàng ko ci saabaam yi, daal di woo ñenn ci ñi man a bind ci ñoom ngir ñu bind ko ca saa sa ci anam gu xereñ, bu ko defee saaba yi gaawantu ñoom itam jàng ko mokkal ko ci anam gu dul soppikooti ba fàww. Nii la laaya yi doon dabantee, saar yi di ko mate nànk-nànk ci lu tollook ñaar fukk ak ñatt ciy at, ndax kat laaya wi njëkk a wàcc ci Yonnant bi (j.m) mi ngi ko fekkoon mu am ñéen-fukki at wi ci mujj wàcc bi muy bëgg a faatu te booba mi ngeek juroom benn fukk yu teg ñatt ciy at. Alxuraan nag ñi ngi ci jublu téere bu tedd bi bépp walla ab xaaj ci moom.
Alxuraan ju tedd ji ak li mu ëmb
Kon daal Alxuraan ci nii mu ñëwe waxi Yàlla a ju mu wàcce cib yonnantam (j.m) ngir mu jottali ko nit ñi. Ñi ngi ko wàcce ci Yonnant bi, muy lu nu biddiwal, maanaam nànk-nànk, kem ni ko xew-xew yi soxlaa ak tolluwaay yi ba kero muy mat, di téere bu ñu laabal, bu ay caaxaan dul laal fenn ((laa yaatiihil baatilu min bayni yadayhi walaa min xalfihii)). Moom nag danu koo séddale def ko ay saar yu toll ci 114 saar. Saar wu ci ne tam seddaliku ciy laaya, saari alxuraan yi nag ak laaya yi lii lanu ëmb :
Saxal kennug Yàlla (t.s), nangu ne Muhammad Yàlla a ko yonni, gëm mbooleem yonnant yi fi jiitu woon Yonnant bi, gëm téere yi Yàlla wàcce ci ñoom, gëm alaaxira.
- Ni ñuy jaamoo ci lislaam :
Julli, woor, natt asaka, aj.
- Ponki jikko yi jullit bu nekk war a jikkowoo :
Ñuy wóor, dëggu, am yërmaande ci ku néew-doole, ku aajowoo, ku ñàkk, am ag cofeel ñeel bépp jullit tey dimblante ak moom ci lu baax ak fonki way jur, teral leen añs.
Ngir jàjjeek waare aki nettali ci dundug yonnant yi, ngir soññee ci ngëm ak foñloo wëlif bokkaale
Ubbi seeni gët ci kàttanug Yàlla gi akug xerañam, jaare ko ci di leen woo ci ñu settantal bindiinu àdduna bi akug nosoom gu xereñ gi
- Sopploo nit ñi gëm Yàlla :
Jaare ko ci wax leen li Yàlla dig ku gëm cib yool akug pay gu neex ci àdduna ak alaaxiraa ak soññee ci jiyaar ci yoonu Yàlla.
- Ragalloo nit ñi ag weddi Yàlla ak bokkaale ko ak moytuloo leen wuuteek ndigëli Yàlla yi :
Jaare ko ci leeral leen mbugël yi ñu waajal ñeel ñi ragalul Yàlla mbaa ñuy tooñ nit ñi di jalgati, mbaa ñuy gàttañlu ci def jaamu Yàlla yi
Mooy yoon wu mat wiy nos ni nit ñiy jëflantee ci seen biir, ak li nu am ciy àq aki yelleef ak li leen war ciy wartéef
Lislaam nosteg dund gu mat
Dinanu gise ci loolu ne alxuraan de ëmb na ag nos gu mat ñeel dundug nit ci gépp anam, mi ngi rëdd séqoo gu nit ki ak boroomam akug séqoom ak mbokkam, dajaleeti jullit ñi ci genn bennte mooy umma bi walla mbooloom lislaam mi (di jullit ñi ), joxati mbooloo mii yoon ak nosteg politig, gu mboolaay ak gu jikko. Dugg ci lislaam du rekk jël diine gëm ko, di def li mu digale ciy jaamu, waaye kay ag tuxu la dem ci ag mboolaay gu yees gu mat gu ami ponkam aki nosteem aki yoonam aki misaalam yu kawe, ndax lislaam ag noste gu mat la gu takkatoo.
Bataaxelub Yonnant bi (j.m) mooy dugal nit ñépp ci lislaam ak tuxook ñoom jëm ca nosteg lislaam gu yees ga te mat. Looloo taxoon Yonnant bi (j.m) daawul yam ci sàkku ci nit mu tudd ñaari seere yi rekk ak def jaamu yi, waaye kay da daan sàkku ñu bàyyi seen dundug réer gu njëkk ga te tàbbi ci nosteg politig, gu mboolaay, gu ruu gu yees gii. Moom de santuñu ko woon rekk mu woote te jotal bataaxel bi, waaye ligéey bu baax ci nit ñi gëm te dugg ci xeetu lislaam wi ak àddunaam ju yees ju fees ji dell ak yiw ak barke.
Bataaxelub Muhammad (j.m)
Yonnant bi wéy na di xamal nit ñi bataaxelam bi, bu ko defee gàllankoor yi nekk ci kanamam mel ne ay doj , ndax kat nit yombul mu tàqalikook ni mu baaxoo woon a dunde, nit jaamub li mu miin la, waaye moom mu wéy di deewoo, di jànkoonte, di muñ ba jóoxe bataaxel bi ca na mu gën a rafete. Loolu mooy kiimaanug dundug Muhammad (j.m) gu yéeme gi cib taar, moom daal ci léppam dund la gu fees dell ak ay bind yu fees aki bind yuy jàngale dëggug ngëm, wóor ci def li la war, muñ ci lu naqari, ñeg ci fas yéenee jéggi gàllankoor yi, ŋoy ci jikko yu rafet, muñ ci loraangey nit ñi, gëm ne ndam lu mu yàgg yàgg dana mujj ñeel jullit biy jëf tey jànkoonte tey ŋoy ci buumug Yàlla gi ci lu dul naagu mbaa yoqat walla tàyyeel.
Jànkoonte gi Yonnant bi doon def ci bi mu nekkee Màkka
Yonnant bi ginaaw bi nu ko yonnee dund na ñaar fukki at ak ñatt yoy ci la matale bataaxelam bi, fukki at ya ak ñatt nag Màkka la leen jeexal, fukk ya ca des mu def leen Madiina, làqu nag ca weeru rabiihul lawal ci atum fukk ma ak benn ginaaw gàddaayam gu tedd ga.
Mooy diirub deewoo ak jànkoonte gu tar ga ak way bokkaaley Màkka yi, ak jiyaaram ga ngir taxawal fa mbooloo mu lislaam mi, ba bi mu gàddaayee dem Madiina, diir ba di fukk ak ñatt ciy at.
Mooy jamonoy ndam, jaare ci dugg gi waa Madiina dugg ci lislaam, mbooloom lislaam am fa, ak nos mbooloo mii ak mottali jaamu yi nekk ci lislaam ak sariyaam, ak tëral nosteg xeet wi, gu politig gi ak gu mboolaay gi, ak dugal dunu araab bi ci lislaam ngir waajale ci tas gi lislaam war a tas ci mbooleem pàkki àdduna bi, ab diiram nag fukki at la ak lenn ciy weer.
Jamonoy Màkka ji
Dafa séddaliku ci ñatti tolluwaay :
- Tolluwaay bu njëkk ba ak jullit ñu njëkk ña
- Tolluwaay bu njëkk bi ci jamonoy Màkka ji - ab diiram juroomi at la daanaka – mi ngi doore ci bi Muhammad (j.m) tàmblee di woote jëme ci lislaam, tàmblee ko ci giiram gi ko gën a jege, ca ñoom la jële mbooloo mi jiitu ci lislaam, ka nekkoon ca bopp ba di soxna Xadiija, nekkoon jigéen ji njëkk a jébbalu, ak Aboo Bakr di ki njëkk a gëm ci góor ñi ak Aliyun mom Aboo Taalib doomi baay-tëxi Yonnant bi (j.m), mooy ki njëkk a gëm ci gone yi, moom de booba ay atam fukk rekk lañu woon , ak Seyd’Ubn Haarisa mi doonoon mawlaab Yonnant bi, mooy ki njëkk a jébbalu ci mawlaa yi.
Am mbooloo topp ci tàbbi ci lislaam ci waxambaaney këri Màkka yu Xuraysin yu mag yi, ñi ci Yàlla ubbi séeni xol nanguloo leen lislaam ak dalam yu kawe yi, ku ci mel ne Talhata mom Hubaydul Laah, Abdurahmaan’Ubn Hawf, Sahd’Ubn Abii Waqaas, Usmaan’Ubn Haffaan, Subayr’Ubn’Ul-hawwaam.
Am mbooloo it tàbbeeti ci Lislaam ci ñu ñàkk ñeek jaam yi ak way néew yi doole ci ñi Yàlla tawfeexal ubbil leen buntub gore ak yamoo ak yaakaar, ku ci mel ne Bilaal mom Ecopi mi, Hammaar’Ubn Yaasir, Xabaab’Ubn’Ul-arat.
Mbooloom lislaam mii baaxoo woon naa dajeek Yonnant bi ca Kaaba ga ngir déglu alxuraan ci moom ak jàng ci ponki lislaam, loolu it jur way bokkaaley Quraysin yi yoqat ci jataayi néew yi doole yii ci li wër Kaaba gi, tax it ba ñu tàmbli di leen xatal ak a yoqatloo, Yonnant bi it gis ne war naa wutal jullit ñi barab bu ñuy daje cig féex akug dal, ci noonu wenn waxambaane wu bokk ci ñoom ñu naan ko Arqam Ibn Abiil Arqam ne man naa joxe këram ngir ñu fay daje, Yonnant bi nangu, looloo taxoon jullit ñi ba woon daje ga ñu doon daje ca Kaaba ga.
Waaye làqu gi nu làqu leegi tiitloo waa Màkka yi, jeqi ci ñoom njàqare, rawati na Aboo Jahlin ak Aboo Lahab mi nekkoon baay-tëxi Yonnant bi ak ñeneen, ñu tàmbli di topp jullit ñi ak di leen xeeñtu ngir xam li nuy def.
- Jébbalug Hamsa, Omar topp ci :
Am na bis Aboo Jahlin nekk fi barab di néggandiku Yonnant bi booba mi ngi jëmoon ca kër Arqam, ba Yonnant bi (j.m) egsee mu toroxal ko, waaye Yonnant bi muñ ak doonte ku dëgër la woon te manoon koo sonal, waaye Yàlla da koo digaloon mu woo nit ci hikma ak waare gu rafet, ci noonu mu wacc ko fa dem, bi Hamsa baay-tëxi Yonnant bi yëgee li xew daa mer seeti Aboo Jahlin duma ko ba noppi jébbalu dib jullit, ci noonu mbooloom lislaam mi gën a am doole ci dugg gi ci Hamsa dugg leegi.
Bi ci as ndiir toppee Omar’Ubn Xattaab jébbalu, jullit ñi gën a sawar, gën a ñeme, ñu daal di génn leegi kër Arqam daal di dellu fa nu daa dajee di la wër Kaaba ga, ci noonu Yonnant bi tàmbli di woote ci kaw ci lu bir, te faaleetul merum waa Màkka yi. Fii la jamonoy woote ci kër Arqam jeexe, leegi woote gu biti gu matale gi tàmbli.
- Tolluwaayu Màkka bu ñaareel bi ak xeex gi Quraysin doon xeex woote gi
- Waa Màkka yi dañoo jàppe woon loolu muy ag dëkk gu leen jullit ñi di dëkk ak ag fontoo, ñu jug nag xeex leen xeex bu metti, jaare ko ci di sonal way néew yi doole ak faqiir yi ku ci mel ni Bilaal, Hammaar Ibn Yaasir ak Xabaab, ñu tàmbli woon it di ñaawal Yonnant bi(j.m) di ko saboote ak a lor ak lenn ci saaba yi.
Yonnant bi daa amoon njàqare ci saabaam yi, ragal waa Màkka yi sonal leen, ci noonu mu laabiire woon leen ci ne ku bëgg ci ñoom man naa dem Ecopi, foofa dananu fa man a doxal seen diine te kenn du leen topp mbaa mu leen di sonal, bi mu ko defee lu tollook juroom ñatt fukki góor akug jigéen gàddaay dem fa ci ñaari yoon. Yonnant bi des Màkka ak mbooloo mu néew ci jullit ñi, di jànkoonteek lori Quraysin yi. Waa Màkka yi jaaxle woon nanu ci man gi Yonnant bi (j.m) manoon a muñ ay coona ak sax gi, ñu sàkku woon ci baay-tëx ji mu tere ko woote gi maanaam Lislaam, waaye Yonnant bi bañ te wëy ca woote ga, looloo waraloon way bokkaale yi defoon ag dogoo gu mat ak Banii Haasin ak itam Banii Abdul Mutalib te ñoom ñooy mbokki Yonnant bi (j.m). Banii Haasim jànkoonte na aki coona ngir dogoo gii nga xam ne saxoon na ñatti at. Tolluwaay bu ñaareel bii nag weesuwutoon juroomi at.
- Ñatteelu tolluwaay bi ci jamonoy Màkka ji
- Sonalug waa Màkka yi ak xatal gi nu doon def Yonnant bi ak jullit ya jotutoon a gàddaay dem Ecopi àggoon na ca dayo ba bi yonnant gi amee fukki at, maanaam bi nu ko yonnee ba mu mat fukki at. Bi dogoo gi jeexee ba teg lu néew la Aboo Taalib baay-tëxi Yonnant bi (j.m) faatu, mi nekkoon njiitu Quraysin ak Màkka te daan aar Yonnant bi ci tar gi waa Màkka yi taroon ci di ko lor. Bu ko defee noonub lislaam bu tarug noonu gi jug moom itam yor njiitug Quraysin gi, moom baay-tëx la woon ci Yonnant bi waaye ku ko iñaane woon la te soxote ko.
Bi Aboo Taalib faatoo ba teg lu néew la soxna Xadiija làqu moom it (y.y.g ) ginaaw bi mu àndeek Yonnant bi ñaar fukki at ak juroom cig sell, cofeel, dimblante ak bànneex, ak doonte fukki at yu mujj yi daa feesoon dell aki jafe-jafe, mettiit ak xatal. Yonnant bi naqarlu woon na bu baax ci faatug àndandoom bii mu bokkaloon dund gi, nekkoon ku matal kóllare, wóor, taxawoon ci wetam ci ati jafe-jafe yi, wone woon gën jaa kawey misaal ci ni soxna su gëm tey muñ war a mel.
Bi Aboo Taalib ak soxna Xadiija làqoo Yonnant bi yëgoon na ne ku wéet la dëgg, te at yu metti yii mu def Màkka di jiyaar indilunu ko lenn ngérte lu ñu xam lu mu yaakaaroon ngir lànkug waa Màkka yi ak nuur gi nu nuuroon cig kéefar ak ŋoy ci li ñu fekkon seeni baay.
Génn gi Yonnant bi defoon dem Taayif
Fii la Yonnant bi xalaate ci génn jéem a wooteji ca Taayif ga jege Màkka, mu daal di fay dem ànd ak mawlaam bi Sayd’Ubn Haarisa, waaye waa Taayif déggalunu ko, looloo tax mu dëppoon dellu Màkka.
Waaye Yonnant bi loolu taxutoon mu yoqat ak doonte waa Màkka yi dañoo dogu woon ci lor ko, mu daal di jawali ca biti Màkka ca lenn ca giir ya fa dëkke woon, daan leen woo ci lislaam waaye taxutoon lu bari wuyyu ko ca.
Yonnant bi (j.m) da daan def bu déggaan aw nit ñëw Màkka mu gaaw gisi leen, woo leen ci lislaam, ba yonnant ga tollee ci fukki at ak benn daa dajeek ab kuréel ci giirug Xasraj ñëwoon Màkka, di woon genn ci ñaari giir ya nekkoon Màddiina, geneen ga di woon Aws, xare ba nekkoon di lu tar ci seen diggante ak noonoo ga. Ca at ma ca topp am mbooloo ci Aws dikk na Màkka, Yonnant bi gaawantu seetsi leen wax ak ñoom, waaye fekk fi ñoom nopp yuy déglu, ndax kat Yahood yu Madiina yi dañu daan wax naan ab yonnant bu ñu yonni de dana dikki di dimbalisi Yahood yi ci Xasraj ak Aws, looloo waral Aws jortoon ne Muhammad (j.m) mooy yonnant bi Yahood yi doon wax. Bi seen mbooloo mi toogeek moom déglu ko lanu gis ne moom kat ku dëggu la ci li muy wax, bi mu leen jàngalee ay laaya ci alxuraan lanu ko gëm, sàkku woon ci moom mu may leen ba ñu dellu Madiina, man a nettali seeni mbokk li nu dégg.
Ci noonu ñu dellu nettali seen mbokki Aws yi li nu dégg, ñoom itam ñu amoon yitte lool ci gis Yonnant bi te déglu ko, Xasraj it dégg loolu, ñaari giir yépp tàmbalee yittewoo gis Yonnant bi, ñu daal di dogu ci yonni am mbooloo mu mag ci jamonoy aj gi ngir mu dajeek Yonnant bi (j.m), déglu ko
- Jaayanteg Haqaba gu njëkk gi:
Mbooloo mi làqu waa Màkka ñëw dejeek Yonnant bi (j.m), déglu ko, waaye am lu leen wóor ci ne Yonnant bi de ku dëggu la, ci noonu ñu ànd dugg ci lislaam, def ak Yonnant bi jaayante gu Haqaba gu njëkk ga, daal di ko cay dig ne danañu woo waa Madiina ci Lislaam, te dinañu ko seetsiwaat ginaaw at, ci noonu Yonnant bi yabal ak ñoom saabaam ba tudd Mishab Bun Hamiir, ngir mu jàngal sariiya waa Madiina.
- Jaayanteg Haqaba gu ñaareel gi:
Bi lu toll ci at jàllee Mishab dellusi ànd ak ab kuréel bu mag ci waa Madiina, seenub lim tolloon ci juroom ñaar fukki góor ak ñatt ak ñaari jigéen, ñu jàkkaarloo woon ak Yonnant bi fa Haqaba jaayante fa ak moom, muy jaayanteg ñaareel ga, ñu ñaanoon ko mu tuxu dem Madiina, ne ko fas nanu ko yéenee aar ci gépp noonu te dinanu ànd ak moom ci tas Lislaam.
Ci ginaaw bi rekk la Yonnant bi digaloon saabaam yi ñu gàddaay dem Madiina, ñu daal di woon tàmblalee gàddaay ci ay mbooloo, mbooloo topp mbooloo, lislaam daal di fay tas ba mujj doo gis genn kër ca Madiina gu ay jullit nekkul.
Gàddaay dem Madiina
Li ëpp ci jullit yi nekkoon Màkka daal di gàddaay dem Madiina ci weer yu néew, bi Yonnant bi amee xel mu dal ca saabaam ya ca Madiina, daa daal di gàddaay moom itam ànd ak àndandoom bu dëggu ba Aboo Bakr, ñu ngi génn ci lëndëm gi cig làqu, ndax waa Màkka dañoo bëggoon a tëye Yonnant bi ca Màkka ngir ragal lislaam di ame doole ca Madiina.
Mi ngi àgg Madiina ci 12 rabiihul Awal ca at mu njëkk ma ca gàddaay ga (4 sëtumbar atum 622 g,j), booba nag di taarixe ci gàddaay gi tàmbaleegutoon a dox, ndax Seydinaa Omar mooy ki digale ñu jël at mu njëkk mi ci gàddaay def ko at mi taariixu jullit ñi di tàmblee.
Yonnant bi fekk na li ëpp ci waa Madiina ñu tàbbi ci lislaam, ñu néew a ci desoon cig kéefar, te bi Yonnant bi dikkee dañoo daal di jébbalu. Yahood yu bari nag nekkoon nanu Madiina, tasoon fépp it, ña ca ëppoon daan bay, mbaa ñuy def yenn mecce yi niki meccem weñ ak tëgg. Ñatti giir yu mag nag feeñ na ci ñoom, ñooy Banoo Qinqaah, Banoo Nadiir ak Banoo Qariitha, ñoom nag dañu daa won Xasraj ak Aws ne ñoo leen kawe, te daan leen jaxase bay waral ñuy xulook a xeex. Bu xeex amee leeg-leeg ñu ànd ak Xasraj, leeg-leeg Aws, daa nañu wax naan ab yonnant de dana feeñi ci ñoom te bu ñëwee dina ànd ak ñoom xeex Aws ak Xasraj ba jële leen fi.
- Jëfi Yonnant bi (j.m) ca Madiina:
Yonnant bi bi mu àggee Madiina rekk daa daal di tàmbalee ligéey, ligéey bi nag ci ñaari mbir yii la jëmoon :
1 – Sos wenn xeetu lislaam wu gëm tey benn, ag mbokkoo muur ko, ag yamoo ëmb ko, ag maandute yiir ko, ñu fay doxal lislaam.
2 – Waajal xeet wii, wutal ko doole ju doy sëkk ngir mu man a duggal araab yépp ci Lislaam, teg ci mbindéef yépp.
Yoon yi Yonnant bi jaaroon ngir amal ñaari mbir yii ñooy
- Def ag mbokkale ci diggante jullit ñi, mu jox muhaajir bu nekk am mbokk mu bokk ci ansaar yi
- Taxawal jenn jumaa ca Madiina ñu fay jullee, muy nekk it barab bu mbooloom lislaam miy dajeek seenub yonnant ak saaba yu mag yi
- Def ag kóllare guy nos àq ak yelleefi nit ñi ci Madiina ak seeni wartéef ci lu jëm ci seeni moroom ak ci lu jëm ci xeet wu lislaam wi, kóllare gii nag Yahoodi Madiina yi ci lañu woon, waaye ñoom dëgguwuñu woon ci bokk gi ñu ci bokkoon.
Yaatal gëwéelub xeet wi
Bi Yonnant bi nekkee ci ligéeyam boobu ngir amal jubluwaayam yooyu, mi ngi doon wéy it ci di woo ci lislaam giir yi peek Madiina ngir ñu bokksi ci uma bi, di xeetu lislaam wii xëy taxaw, bi mu gisee ne lenn ci kilifay giir yii ànduñu woon ak moom ci loolu, daa daal di woon yabal ay cong yu lislaam ngir xeex kilifa yooyu ak ñi leen di jàppale ba duñu man a gàllankoor giir yi ci dugg ci lislaam. Cong yii lanuy wax xaswat, ndax Yonnant bi (j.m) moo ko daan jiite, bu ko kenn ci saaba yu mag yi jiitee nag ñu koy wax sariya
Xaswat yi ak sariyat yi
Yonnant bi tàmbli na, daal di yabal juroom benni xaswa ak ay sariya yoy amal nanu xemmemtéef lii, bu ko defee gëwéelub uma bu lislaam bi gën a yàkkiku, daal di far ëmb mbooleem wàllug càmmooñ gu Hijaas gi, loola nag la ca juddoo mooy Madiina mujj teg loxo ci yoonu yaxantu wi jëme Shaam juge Màkka. Looloo taxawaloon yaxantu ga ca Màkka te kat moo nekkoon balluwaay bi seen koom di juge.
Xaswat bu Badar bu mag ba ca 2eelu at g,g
Xaswa bu Badar walla xareb Badar Yonnant baa ngi ko def ci atum ñaareelum gàddaay gi, mi ngi ame nag ca digg yoon wa dox diggante Màkka ak Madiina, lu tollook ñatti téeméeri jullit am ca ndam ca kaw junni ci yéefari Màkka yi, muy ndam lu mag lol lislaam dëgëre na ci, nit ñi it xame ci ci anam gu wér péŋ gees manul a sikk ne Yonnant bi de wooteem gii lu wé la, ci noonu nit ñi sottiku Madiina ciy mbooloo yu mag ngir dugg ci lislaam, ci xare bii lanu raye Aboo Jahlin ak ñu ko moy ci nooni lislaam yu tar yig noonu.
Xaswat bu Uhud atum 3eel mi giinaaw gàddaay gi
Màkka manutoon a ñàkk mu def lu ko delloosi darajaam ji mu ñàkkoon ci dunu araab bi, ubbilaat ko yoonu yaxantu wi, looloo waraloon ay way bokkaaleem dajale woon doole ju mag ju toll ci ñatti junniy góor, ñaari téeméer yi diy gawar , ca atum gàddaay mu ñatteel ma ñu dox jëm Madiina ngir dugg ko ci doole, waaye Yonnant bi génn àkk léen ci lim bu toll ci junni ciy saabaam.
Ñaari mbooloo yi daje ca bëj-gànnaaru Madiina, fa ron doju Uhud, xare bu tar tàkk fa bob jullit ñaa ca amoon ndam ca njëlbéen ga, waaye boroom fett ya mujjoon wooteek ndigal la leen Yonnant bi joxoon daal di wacc seen barab ya nu leen taxawloo woon, Xaalid’Ubn Waliid mi jiite woon yéefar yi daal di màng pose bi song jullit ñi, bu ko defee seen sàppe jaxasoo, baj-baji, ñu ray ca ñu bari, waaye Yonnant bi moom des fa ak lu néew ciy gaayam, mu daal di woo ay saabaam ngir ñu dellusi. Ak li ñu ko gaañ ca xare ba lépp téewul mu xettali dooley jullit ñi ca njàmbaaram ga ak saxam ga, te tee yéefar yi dugg Madiina. Xeex bi wéy ba jant so, fii la coona bi sonale yéefar yi, ñu rocciku dellu Màkka ci lu dul ñuy amal li nu bëggoon, te loolu saxug Yonnant bee ko waral akug njàmbaaram ak sorib gisam.
Waaye yéefar yi li nuy amadi li ñu bëggoon lépp téewul ray nañu ab lim ci tànnéefi jullit ñi, ku ci mel ne Hamsa bay-tëxi Yonnant bi (j.m), ak Mishab’Ubn Hamiir mi daa gàddu raayob jullit ñi ak leneen lu toll ci juroom benn fukki jëmm, jullit ñi am nañu lu leen naqari lool ci seen sahiid yi, waaye jànge nañu ci Uhud benn bind bu ñu dul fàtteeti mukk, mooy topp Yonnant bi (j.m) ak defi ndigalam.
Xaswat bu Xandaq atum 5 g.g
Waa Màkka yi yég nañu ne amaluñu dara lu am solo ci li ñu doon sàkku, ñu gis ne ñoom kat ak seen mbégte mu rëy mi ñu am lépp ci ray gi ñu def lu bari ci jullit ñi téewul Màkka dañul di nekke na mu nekke woon: yoonu yaxantu wi mi ngi ci loxol jullit ñi, giir yaa ngi tàbbi ci lislaam, gu dugg geneen topp ca.
Lii a tax Aboo Sufyaan’Ubn Harb mi nekkoon njiitul Màkka ginaaw Aboo Jahlin jugoon boole doole ju mag ci waa Màkka ak ñi tapoo ak ñoom ci giir yi, ñu dox nag jëm Madiina ca juroomeelu at ma ñeel gàddaay ga, bu ko defee Yonnant bi aki saabaam jug gas am xandaq ca la wër Madiina, ba mboolooy xarey yéefar yi agsee manuñoo jéggi pax ma, bu ko defee xare bi yam ci sàneente ay fett jéggi xandaq mi, ci noonu jullit ñi ñoom wone ag yewwu gu mat ci sàmm seen xandaq ba yéefar bu ko jéggi rekk rayees ko ca saa sa. Gaw gi sax lu tollook ñaari ayu bis, ginaaw bi Yàlla yonnee gelaw lu tar ak taw bu metti mu yàq xaymay yéefar yi, fay seenuw sawara, sedd bi metti ci ñoom ak doonte weer woowa wu mars la woon, te woowu weer fa Hijaas mooy tàmbalig lolli bi, bu ko defee yéefar yi àggati ci manuñoo ñàkk a dind gaw gi te dellu Màkka ngir sedd bi te amuñu dara ca seen càkkutéef ya. Loolu di ag juunu gu mag akug sooy ñeel leen, te diw lay wu mag ak firnde ci kàttanug xeetu lislaam wi ak dëggug gëm gi ay nitam am, ak ñaw gi nekk ci njiit la Muhammad (j.m).
Génne Yahood yi Madiina
Ñatti giiri yahood yi di (Banoo Qinqaah, Banoo Nadiir ak Banoo Qariitha) yoroon nanu taxawaay bu ñaaw te noonoowe jëme ca Yonnant ba ak wooteem ga, dale ko ca bi muy door a agsi Madiina, weddi woon nañu ag yonnantam, naan neey yonnant bi ñuy néggandiku manul a juge ci fu dul gañog Banii Israayil. Ginaaw nag yonnant boobu ñu daa wax farul génne ci ñoom, xanaa kay ci giirug Quraysin gu araab gii dara raxul, loolu naqari woon na leen, jural leen ag soxot ak kañaan ak mbañeel.
Yonnant bi yàgg naa muñ lor yi ñu ko daa lor ngir yaakaar gi mu yaakaaroon ne danañu mujj noppal ko, ba àgg sax ci gëm ko, waaye lu mu muñ rekk ñu gën koo bañe lislaam gën koo dellikoo ag noonu, waaye làqoon nanu seen noonu googu ak mbañeel gi bi ñu gisee ne lislaam mi ngi gën a dolliku doole, di gën a dëgër bis bu Yàlla sàkk:
Bi jullit ñi amee ndam ca Badar la xolub Yahoodi Madiina yi gën a dagg, ab kuréel ci ñoom it – ñooy Banoo Qinqaah - àgg ci manatuñoo ñàkk a feeñal seen bañ gi ñu bañ lislaam ak soxote gi ñu def jullit ñi ci ndam li leen Yàlla may, ci noonu ñu tàmbli di saboote Yonnant beek lislaam, waaye Yonnant bi (j.m) dem ca seen kër ya gaw ko, bi ñu jëbbalee seen bopp la leen génne Madiina ñu dem Shaam.
Ginaaw bu xaswat bu Uhud jàllee ba teg lu néew, la yahoodi Banoo Nadiir lànk ne duñu joxeeti li leen war ci ndimbalul alal li war ñeel umma bi, waaye yamuñu ca, dañoo tàmbli woon a defi pexe ngir yong Yonnant bi (j.m), waaye Yàlla (t.m) musal ko ci seenuw ay, nga xam ne Yonnant bi amul woon lenn lu mu manoon a def lu dul génne leen ñoom itam ngir mucc ci seenuw ay. Ci biir xareb xandaq ba yahoodi Banoo Qariitha doon nañu jéem a wor jullit ñi dem jàppaleji yéefar ya gawoon Madiina jaare ko ci may leen ñu dugg Madiina jaare ko ci seenug wàll, looloo war bi xeex bi jàllee rekk Yonnant bi daa daal di jawali ca seen kër ya, gaw leen ba ñu wommatu, nangul ko, mu digal saabaam ba tudd Sahd’Ubn Muhaaz mu àtte leen ci li jaadu fi moom, li tax mu tànn ko nag mooy ñoom ci mom lañu doon sàkkoo ag tin ci Yonnant bi, moom it mu ne nañu ray ñi ci doon xeex, ñi ci des ñu génne leen Madiina.
Ci noonu la xeetu lislaam wi mucce ci ayuw yahoodi Madiina yi, Madiina mujj yor lu néew rekk ciy yahood yu bokkoon ci ñi defoon ay tapoo ak lenn ci bànqaasi Aws yeek Xasraj, ginaaw nag feeñaluñu woon genn wor mbaag mbañeel ñeel jullit ñi Yonnant bi defu leen dara. Looloo waral ab kuréel ci ñoom gëm ca gëm gu dëggu, am ca ñeneen ñu ca gëm ñu ag ragal gëmloo akug naaféq
Juboo gu Udaybiya atum 6eel g.g
Bi Yonnant bi amee lu ko wóor ci ne am cong mu juge ci biti jeex na, wor gu biir gi it dañ na la tàmblee waaj ngir dugal Màkka ci lislaam. Gisoon na ne waa Màkka yi ñi ci ëpp ñu tàmbali woon a yittewoo mbiri lislaam lañu ndax gis nañu muy yaatu, di gën a am doole bis bu nekk, li Alxuraan digoon jullit ñi bañu nekkee Màkka di ñu néew doole gën di feeñ, gën di am. Nga xam ne Màkka li ko tee woon a dugg ci lislaam wéesuwutoon lenn ci njiiti yéefar yi ak seeni àndandoo, ñoom ñi ragaloon seeni njariñ di sànku, seeni daraja di suufe su ñu duggee ci lislaam.
Ci biir loolu ab laaya wàcci bu tedd buy digal Yonnant bi mu wëlbati qibla bi jullit ñi amoon muy Baytil Maqdis def ko leegi Kaaba gu sell gi, mu mujj ca saa sa di qiblab jullit ñi ñépp.
Bi ñu wëlbatee qibla bi leegi jëme ko ci Kaaba gi, te Yonnant bi xam dëgër gi xeetu lislaam wi def leegi te ame ko doole ci la jugoon ànd ak am mbooloo ci saabaam yi ngir defi umra, mooy siyaareji Bayti Laahil Haraam ci waxtu yi dul yu aj, looloo tax ñu tudde ko aj gu ndaw gi.
Bu ko defee, Yonnant bi (j.m) daal di génn ci junni ak ñeenti téeméer ci ay saabaam jëm Màkka ngir defi umra, looloo taxoon yobbaalewuñu woon ngànnaay ngir bëgg waa Quraysin xam ne jullit ñi dañoo ñëw ngir defsi ag jaamu rekk mooy umra gi. Bi jullit ñi aggee ci barabub Hudaybiya mooy buntub Màkka bi féete wàllug cammooñ la waa Quraysin yi tàmbali woon a ragal jullit ñi dugg Màkka. Ñu daal di yonnee ci Yonnant bi ne ko daal àndatuñu ci jullit ñi dugg Màkka ak donte yoruñu ngànnaay. Ñu daal di fay def waxtaan wu yàgg yu mujj àgg ci li ñuy wax Juboog Hudaybiya, moom nag li mu yaxal mooy jullit ñi buñu dugg Màkka ca at mooma waaye bu déwén ja’a ca waxtu woowa dinañu man a dugg (muy atum juroom ñaareel ma g.g), bu ko defee ñaari wàll yi def ag juboo guy sax fukki at.
Ca juroom-ñaareelu at ma ñeel gàddaay ga, Yonnant bi dellu defi umra ga mu yéene woon ca daaw ja, daal di siyaare ab dëkkam bi mu juddoo, ginaaw ba mu fa gëjee lu tollook juroom ñaari at.
Yonnant bi (j.m) bind na buur yi
Ci biir atum juroom ñaareel mi ñeel gàdday gi la Yonnant bi (j.m) yabal ay ndaw ca Qaysar mu Rom mi, Kisraa mu Faaris mi, ak kilifag Qibt ya ca Isipt, joxaale leen ay bataaxel yu leen di xamal lislaam te di leen ci woo. Qaysar moom daa yeexoon a tontu, bu dee Kisraa mu xottite bataaxel ba, waaye Maqooqas moom daa tontu tontu bu rafet, yonnee ca Yonnant ba adiya waaye taxutoon mu dugg ci lislaam.
Yonnant bi yonneeti ci lu bari ci njiiti araab yi ak seeni kilifa ak buur yi nekk ci mbooleem dun bi, am ñu ci dëggal te gëm, waaye la ca ëpp tontuwuñu.
Ubbig Xaybar
Xaybar am mbooloom ay waaha yu ndaw la yu nekk ci bëj-gànnaaru daanaka dun bi, ca waxtu woowa Xaybar ci loxol yahood yi la nekkoon, ñu seŋe woon ko, ngartaajoo woon ay xéewalam, def ko seen dàttub xare tey seen barab bu alal, ñu tàmbali woon di xiirtal seen dëkkandooy araab yi ci ñu fexeel lislaam ak Madiina. Waaye Yonnant bi dëgmalsi leen ci mbooloom xare mu mag, gaw Xaybar, jullit ña songoo fa ak yahood ya cib xare, Yonnant bi dumaa leen fa, ñu wommatu, yeneen waaha yi ko jege woon te nekkoon ci loxol yahood yi topp ci, niki Fadk ak Timaa. Ci jëf jii la Yonnant bi raye jànkoonte ak jafadiku gi yahood yi dese woon daal di fegu ci seenuw ay.
Ubbig Màkka ci juroom ñatteelu at mu gàddaay gi
Ci biir loolu fekk na Màkka mu néew lool doole, ñu ëpp ci ñi ko daa jàppale bàyyi ko, lislaam tas fat tas gu yéeme rawati na ginaaw Juboo gu Hudaybiya gi. Ci njëlbéenug juroom ñatteelu at mu gàddaay gi la waa Quraysin firi woon seen kóllëreg juboo ga ñu defoon ak Yonnant bi, loolu nag mi ngi ame ci tooñ ak jalgati gi ñu defoon giirug Xasaaha gi nekkoon jullit, ci noonu Yonnant bi jug ci fukki junniy jullit dugg Màkka ci lu dul xare ci weeru koor gu juroom ñatteelu at ci gàddaay gi (samwie 630 g.j) Bi Yonnant bi duggee Màkka daa daal di laabal Kaaba gi, dammate xërëm ya, sànni leen ñu sori Kaaba ga, jullit ñi daal di raxas Kaaba gi, mu nekk leegi nag di néegub Yàlla deesu fa jaamooti ku dul moom. Ci loolu la Yàlla dëggale dëel bi mu joxoon Yonnant bi ak jullit ñi, ndax jàppale na leen, jàppale diineem, fay leen ci seen sellal gi ak dëggu gi ak jiyaar gi ñu doon def ci seen alal ak bakkan.
Bi loolu jàllee ba teg lu néew, lislaam daal di tas ci Màkka gépp, ñu taxawal fa ay jàkka, mu mujj di ñaareelu dëkk ak digg bu lislaam ginaaw Madiina gu ñu leeral gi .
Xareb Hunayni
Ginaaw bi ñu ubbee Màkka ba teg lu néew la giirug Hawasaan ak giirug Saqiif gi mu tapooloon jugoon dajale xare bu mag, dox nag ngir xeexi jullit ñi, waaye Yonnant bi duma leen duma yu tar ca fa ñuy wax Haniin, bi loolu amee genn giir jugatul naan day xeex lislaam. Ginaaw ndam lii Yonnant bi (j.m) dem na Taayif dëkk bi Saqiif dëkkoon gaw ko, ba gaw ga yàggee mu xam ne dana wommatu , la leen fa ba dellu Madiina, waaye noonu la deme woon ndax yàggaatul dara Taayif jébbalu, giirug Saqiif gépp dugg ci lislaam.
Atum Mbooloo yi di juroom ñeenteelu at ginaaw gàddaay gi
Atum juroom ñeenteel mi ñeel gàddaay gi ñi ngi ko tudde woon atum mboolooy yi, ngir ne ci la giiri dunu araab bi bépp doon yabal ay mbooloo yu bokk ci ñoom ngir yëglesi seenug dugg ci lislaam, mbooloo yii nag bawoo nañu ci mbooleem goxi, nga xam ne bi fukkéelu atum gàddaay giy jot fekk na mbooleem dunu araab bi dugg ci lislaam, ñépp ña fa dëkk mujj bokk ci uma bi.
Xaswat bu Tabuuk di bi Yonnant bi mujj a def
Ci sawaal atum 9 ci gàddaay gi, ginaaw bi nga xamee ne mbooleem araabi daanaka-dund bi dugg nanu ci lislaam, la Yonnant bi bëggoon a xamal jullit ñi ne jiyaar ji de fàwwu mu génn dunu araab bi, ngir ñu man a tas diine ji ci àdduna bépp, looloo taxoon mu wommatoon benn xare bu mag ci ay jullit, dox jëm bëj-gànnaar ba àgg Tabuuk ca dig wa dox diggante dunu araab beek réewi Shaam yi nekkoon ci ron teg loxo gu Rom, foofa la nguuri araab yi nekkoon ci dig yooyu duggoon ci lislaam, jullit yi it xame ci ne jiyaar de day sax di wéy ba fàwwu .
Ajug tàggoo gi atum 9 g.g
Ci silhijja atum fukkéel mu gàddaay gi la Yonnant bi defi woon hajjatul wadaah di ajug tàggoo gi, ba muy dem nag ma nga àndoon ak ay junniy junni ci jullit ñi, ci aj gii la Yonnant bi (j.m) leerale ajiin wi ñu yoonal, te mooy wii fi nekk bat ay jii ñu nekk .
Bi mu noppee ci aj gi la def xutbaam bu bu mujj ba nuy wax xutbab tàggoo ba, mu dénk ca jullit ña dëggu, bennoo, boole séen sàppe, jóox farata yi lislaam digale ak tënku ci ponki jikkoom yu màgg yi, bi mu noppee jàngal nit ñi waxi sunu boroom ju tedd ja: (( al yawma akmaltu lakkum diinakum, wa atmamtu halaykum nihmatii, wa radiitu làkkumil islaama diinan)) di : (ci tay jii de laa matale seen diine ji, ci laa matale xéewal gi ma leen doon jox, te lislaam nag mooy diine ji ma gërëm te sopp ko ci yeen). Fii nag jullit ñi yëg nañu fi ne yonnant baa ngi leen di tàggu te di leen dénk li ñu war a def bu ñu ko gisatul, ñoom ñépp jàq te am lu leen naqari.
Bi Yonnant bi (j.m) delloo Madiina la yëg – ci mujjug safar – lu mel ne tawat di ku dugg, waaye faalewu ko, dafa wéy di ligéey ba tawat ji far ko man, mu doog a tëdd, waaye tawat ji yàggul, ndax mi ngi làqu ginaaw bi tawat ji amee ci moom fukki fan ak juroom, di ci 13 rabiihul awal atum 11 g.g ( 8 suwe 632 g.j) :
Jëmmi Yonnant bi
Ci nii la Yonnant bi (j.m) tuxoo dem ca boroomam ginaaw bi mu jottalee bataaxelam bi ci anam gu mat te yaatu, tas ko ba ñépp jot ci, ca na mu ware. Wooteem gi mi ngi ko tàmbali cig wéet , ay gàllankoor aki pakastal gaar ko ay yooni yoon, mu daje ciy coona lol manoon naa yoqatloo geneen góor gu mu manoon a doon gu dul moom, woote na fukki at ak ñatt yoy amu ca lenn ngérte lu am njariñ, waaye mu sax di ku dëgër ag ngëm ci Yàlla, ku am kóolute ci ndimbalam, wéy ca liggéeyam ba ba ndimbal dikkal kook ndam ginaaw bi mu gàddaayee dem Madiina, daal di fay taxawal umma bu lislaam bi, dox ak moom ci yoonu nosu ak doole ci anam gu màndaqewu te callalewu, weer ginaaw weer, ba mujj am ci ndam lii ngay gis tay.
Yonnant bi nag li ko dimbali ci mu jot jubluwaayam bii mooy jikko yu yéeme yi te wéet yi mu jikkoo woon ak bataaxelam bii bàyyikoo woon ca Yàlla ma ko tànnoon ngir mu jottali ko.
Ñun nag manuñoo lim mbooleem jikko ak ngënéeli Yonnant bi (j.m), looloo waral jullit ñi ñoom dañu koo def muy xam-xam ci jëmmam bu ñuy jàng ñu koy wax xam-xamu jikkoy Muhammad (As shamaayil al muhammadiya) taalif nañu ci lu dul jeex, ñun nag ñu ñeme ñemelu indil leen lenn ci yi ëpp solo ci jikko yii :
Gëm gu xóot ci Yàlla
Gëm gi mu gëmoon Yàlla gu matale woon la te xóot, da daan def fu jafe-jafe yi gënee bari, gàllankoor yi gën a dolliku, gëmam gi ci boroomam gën a dëgër, mu gën a ŋoy ci bataaxelam bi, gën a dogu ci wisaare wooteem bi ko Yàlla dénk.
Looloo taxoon Yonnant bi ak saaba yi daawuñu nangu lu dul ngëm gu mat gu dara ci sikk dul jege. Ci daaray ngëm gu xóot gii la saaba yu mag yi génne, ku ci mel ne Aboo Bakr, Omar, Aliyu, Usmaan, Sahd’Ubn Abii Waqaas, Abii Hubaydata Haamir’Ibn Jaraah, Talhata’Bn Hubaydul Laah, Zubayru’Bnul Hawaam ak ñi mel ni ñoom ci ñi war a yanuji raayob lislaam ginaaw Yonnant bi (j.m), te war a tasaareji diiney Yàlla ji ci li ëpp ci pàkki àdduna yi ñu xamoon ca jamono jooja
Jafandu ci way teddi jikko yi
Ngir gëm gu dëgër gu xóot googu ci boroomam (t.s) ak ci lislaam, daawoo gis Yonnant bi mukk muy jëf ci lenn ndare bu tegu ko ci gën jaa dëgëri dàtti jikko yi, niki dëggu, matal kóllare, wóor gu mat ci wax ak jëf, ak seelug yéene ci lépp lu muy wax mbaa mu koy jëf, ak tëyye bu dëgër cig maandu ci mbooleem ay jëflanteem aki saabaam, ba ci ay kontaram, nekkoon na di ku bu waxee dëggal, bu dëelee matale, bu kóllarantee def ko, bu manee jéggale.
Doylu ak bàyyee
Yonnant bi de ak li ko dikkaloon lépp ci xéewali àdduna, ak teddnga ak doole teewutoon mu nekkoon di kuy doylu ci gën jaa tuuti ci xéewal yi, dundam gépp masu cee feesal biiram ciw ñam, lu néew ci mburu la daa mos ak tàndarma, bu amul rëndaay mu rëndaayoo diw, mbaa diw ak bineegar, mbubbam ak dallam ci loxoom la ko daa daaxe, daan fóot mbubbam bis bu jot ci loxoom, ndax moom (j.m) ku jéggi woon ab dayo la ci set, bis bu nekk daa na ci socc ay yooni yoon.
Daawul toggoo nag ag dund gu ñagas te di ko woote, moom kay ñam wu ko dikkal rekk mu lekk. Soloos na ci moom ne daawul sàkku mukk aw ñam wu fi nekkul, cib pajaas la daan nelawe, am mbalaanam it lu gàtt la daan doon, daawul tëju ay saabaam, ki gën a doyodi ci nit ñi da ko daa gis di wax ak moom, waayam ja ko daa ligéeyal di Anas mom Maalik nee na masul a dégg ci Yonnant bi ci dundam gépp benn baat bu ko mas a naqari.
Daf daan bàyyee saabaam yi xéewal yi, te daawu ci féetewoo dara bàyyi leen, nekkoon na di ku sopp xale yi te daan kaf ak ñoom, ku amoon ag ñeewant la ci jirim yi, way ñàkk yi, ñu doyadi ñi, di seeti way tawat yi, bëcëg bépp it ci yëgg la daan nekk, daawul dal, ku bañoonug jekki la ak tàyyeel, daa na ko moytulooy saabaam.
Misaal la woon ci ni ñu war a jiitee xeet wi ak ni ñu ko war a sàmme
Yonnant bi ku amoon ag yewwute gu sax la, daawul ba dara romb ko ci lu aju ci umma bi ndare bu da koo gendiku bu baax te settantal ko. Daf daan settantal di teg ay naal yu jub, yu yaatu yu muy jaar ci ligéeyam ci anam gu nosu te toftaloo. Yitteem jépp da ko daa sotti ci li ëpp solo ci mbiri xeetam wi, teg ca la ca topp cig am solo. Daa gisoon ne ay ligéeyam aki jëfam roytéef la wuy saabaam di jaari ëlëg, làmp la bu ñuy niitloo, moo waraloon lu muy def rekk mu koy def cig njàngale , cig yare. Bu kenn ci saabaam yi juumee ci mbir, da ko koy won cig nooy, leeral ko lay la jub. Ku daan am ag muñ ci way xuloo yi la, daan leen jéggal seeni soppaxndikooki jikko yu ñaaw ngir ñu gis seen njuumte, dellu ca jub ga. Ku wormaaloon nit ñépp la, daan sàmmoonteek teddngay ki gën di gone ci ñoom ak àqam. Masuñoo dégg fenn fu ñu ne Yonnant bi (j.m) génnee na fa baat bu ñaaw jëme ko ci kenn, ak doonte kenn kooku da dib noonam. Bu masaan a mer day noppi ba mer wa dañ mu doog a wax nànk, cig dal.
Yonnant bi noppee ko gënaloon wax, dégloo ko gënaloon déggal. Bu masaan a wax day àgg ca la mu bëgg a wax du jàdd-jàddal, def ko it ci baat yu leer te gàtt, looloo taxoon Yonnant bi (j.m) moo gënoon a am fasaaha ci nit ñi, gën cee am balaaxa, adiisam yi ci balaaxa ñoo topp ci Alquraan miy wax ji gën a balaaxaa ci wax yi.
Yonnant bi (j.m) yérmaande la ñeel mbindéef yépp, bi muy ñëw ci àdduna bi da koo fekkoon mu yor lëndëmug réer, ndof, xamadi Yàlla, waaye mu bàyyikoo fi, ba fi ag leerug gëm Yàlla . Mi ngi feeñ ci araab yi te booba ñi ngi ciy xareek fitna ak ŋaayoo, mu juge fi ba leen ñuy xeet wuy wenn, yiw peek leen, lislaam ëmb leen, jàmm uuf leen. Ak li Yàlla sotti nit ñi lépp ciy xéewal, jaarale ko ciy loxoom teewul Yonnant bi – jàmm yal na nekk ci moom – bi mu fiy juge di woon ku ndóol, ku moomul lenn. Saddaloon na nit ñi aw léew ci nite, ngënéel, def wartéef, sellal ak dëggu. Yàlla dëggal na – tudd naa sellam ga – ba mu nee : ((yaa ayuhan nabiyu inna arsalnaaka shaahidan wa mubashiran wa nadiiran wa daahiyan ilal laahi bi idnihii wa siraajan muniiran, wa bashiril moominiina bi anna lahum minal laahi fadlan kabiiran)) muy :( yaw Yonnant bi de dañu laa yonni ngay seere tey bégaleek a xuppe, di woote jëme ci Yàlla ci ndigalam, tey làmp buy leeral, na nga bégal jullit ñi ci ne am nañu ngënéel lu rëy lu tukkee ca Yàlla) Yonnant bi nag (j.m) tënk na wax jépp ca bataaxelam ba niki kuy jàngale ba mu nee : (dees maa yonni ngir ma mottali jikko yu rafet yi).
----------------------------------------------------------------
1 commentaire:
KAMI SEKELUARGA MENGUCAPKAN BANYAK TERIMA KASIH ATAS BANTUANNYA MBAH , NOMOR YANG MBAH BERIKAN/ 4D SGP& HK SAYA DAPAT (350) JUTA ALHAMDULILLAH TEMBUS, SELURUH HUTANG2 SAYA SUDAH SAYA LUNAS DAN KAMI BISAH USAHA LAGI. JIKA ANDA INGIN SEPERTI SAYA HUB MBAH_PURO _085_342_734_904_ terima kasih.
KAMI SEKELUARGA MENGUCAPKAN BANYAK TERIMA KASIH ATAS BANTUANNYA MBAH , NOMOR YANG MBAH BERIKAN/ 4D SGP& HK SAYA DAPAT (350) JUTA ALHAMDULILLAH TEMBUS, SELURUH HUTANG2 SAYA SUDAH SAYA LUNAS DAN KAMI BISAH USAHA LAGI. JIKA ANDA INGIN SEPERTI SAYA HUB MBAH_PURO _085_342_734_904_ terima kasih.
KAMI SEKELUARGA MENGUCAPKAN BANYAK TERIMA KASIH ATAS BANTUANNYA MBAH , NOMOR YANG MBAH BERIKAN/ 4D SGP& HK SAYA DAPAT (350) JUTA ALHAMDULILLAH TEMBUS, SELURUH HUTANG2 SAYA SUDAH SAYA LUNAS DAN KAMI BISAH USAHA LAGI. JIKA ANDA INGIN SEPERTI SAYA HUB MBAH_PURO _085_342_734_904_ terima kasih.
Enregistrer un commentaire